Xareb Àdduna bu Njëkk wuute gi ci sumb yi

Contenu supprimé Contenu ajouté
Addbot (waxtaancëru)
m Bot: Migrating 153 interwiki links, now provided by Wikidata on d:q361 (translate me)
Trey314159 (waxtaancëru)
m fix homoglyphs: convert Cyrillic characters in k[ё]ri to Latin
Tafaan: recent_changes
 
Rëdd 87 :
Noonoo gi taroon na jëm ci Slaaf yi ci Balkaan, looloo waraloon ñoom Slaaf yi juggoon taxawal ag mbootaay gu làqu ngir xeex loolu, Serbi jàpple leen ci ak Riisi gu Xaysar gi.
Ab dongab Slaaf yong na Arshidog Fransis Ferninand, mi nekkoon wuutlaayu Otris ak soxnaam, ca 28 suwe 1914g, ca dëkkub Sarayevo bi nekkoon peeyub Bosni, ci tukkib nemmeeku bu mu fa doon def.
Otris daal di gaaw jariñoo xew-xew bii, daal di yonnee Serbi ag xupp ca bisub 22 sulye 1914g, gu làmboo fukki sart ak benn, bokk na ci yi ëppoon solo ci sart yooyu: raxas goornamaab Serbi bi ak dooley xareem ji ci mbooleem ku bokk ci kureel yiy kontar Otris, te may Otris mu defal boppam raxas gii, te tëj yëglekaay yi ak kёrikëri tas-xibaar yi noonu Otris, ak boole Otris ci gëstu ñi def yong googu ak àtte leen. Ak yeneen sart yu tar yu tax Serbi jortu ne kii daal daa fas yeenee dugg ciy mbiri biiram. Ba noppi Otris joxati Serbi diirub ñeen-fukki waxtook juroom ñatt, ne ko mooy àpp bi nga xam ne waru koo weesu te tontuwul, waaye Serbi moom tontuwul .
 
== Jibalug xare bi ==