Pël wuute gi ci sumb yi

Contenu supprimé Contenu ajouté
Ibou (waxtaancëru)
Aucun résumé des modifications
Ji-Elle (waxtaancëru)
+image
Rëdd 2 :
Xeet woowu am nañu tur yu bari: Pël ci [[Wolof]], ci [[Afrig]] mooy tur wi gën a siiw, Fula ca Mande ya, Fulani ca Naar ya, Fellata wala Fellan ca [[Sudaan]].
[[Dencukaay:Eleveurs Peuls.jpg|thumb|200px|left|Sàmmkatu Pël bu Gurma, bëj-saalumu [[Gao]], [[Mali]]]] ÑÑoom ci seen bopp dañuy wax Pullo wala FulBe. [[Isipt]] mooy réew mi ñu bawoo. Pël ya ca Isipt ay nit ñu ñuul lañu nekkoon. Ba noppi, ay nit ñu weex, ñëw ca seenum réew juge [[Asi]] ak [[Tugal]] , bokk na ca xeet yooya: Scythe, Aryen, Phrygien, Hittite, askan yu bari yu ñuy tudde ay waa End-tugal (Indo-européen). Pël yu ñuul yi ak nit ñu weex ñi dañoo jaxaasoo woon. Lii moo tax Pël yi gën a xees, gën a sew, am kawar gu gën a nooy, bu ñu leen xoolee ci yeneen xeet yu ñuul yi ci Afrig. Ba noppi, Imbraatóor gu Iran(ñoñ Cambyse ñi(les Perses) ), tegoon nañu loxo réewum Isipt, di fa tege dund gu metti, rawati na ca nit ñu ñuul ña. Lii moo tax Pël ya ak Séeréer sa gàddaay, dëkki ca [[Sudaan]] (Nubie) dëkki seeni maam, soog a dem Senegaal. Pël ak [[Séeréer]] danoo bokk maam, seeni làkk tamit. Yàgg nañoo ànd, dañuy kalante ci seen biir. Ca yoonu [[Tekuruur]], pël ya ca Dexug Senegaal rekk lañu nekkoon ak seeni nag. Booba nekkuñu woon ay jullit. Amuñu woon nguur ndax ak seeni nag ci màng rekk lañu nekke woon. Meew ak Sanqal (ñórndi) moo doonoon seenu lekk. Pël ci boppam am na xeet yu bari (Leyyi/KinDe), Ardo mooy seen Buur: JaawBe yi, UrurBe, WodaaBe, LaaCe, CutinkooBe, YirlaaBe. Am na yeneen KinDe. Màng gi ñu dëkke tax na ñu tuuru ci Sowwu Afrig gépp, ba far delseeti Sudaan, cig muñ ak coona ndax saa su nekk ci dëkki jàmbur yi rekk lañuy nekk, seen nag yi leeg-leeg ñu ruur tooli baykat yi, loolu it di jur xuloo bu rëy ak ŋaayoo ci seen digg ak woroon tool yi.
[[File:Garibou Peul.jpg|thumb|Pël ([[Togóo]])]]
 
Ca atum 1539 Koli Tengella Bâ, mi ngi bokke ci Pël ci wetug baayam, bokk it ci Mande yi ci wàllug yaayam (Keyta), dajale woon na sàmmkati Pël yi ak mande yi, ngir ñu man a am doole. Daa di dugg ci yeneen xeet (Wolof, Séeréer, Bajaaranke, Joola, Baga, [[Sooninke]] . Ñoom ñépp ak seen aroo Koli Tengella, ñu yéeg ba Tekuruur, di xeex ak Buur-ba [[Jolof]] ba, ndax kii moo doon yor dëkk ba, ak Lam-Toro ya, Lam-Térmes, Lam-Taga ya, Juroom ñeenti fan soog a yor dëkk ai. Koli Tengella teg na fa njabootam (Denyakoobe yi), tudde na nguur ga Fuuta-Toro (Fuuta mooy dëkku Pël ca seen Làkk). Lii ca Senegaal la xewe.
 
Ca Mali Pël ya doñoo njëkk am doole ca atum 1818. Booba nag Ahmadu Bari, Sëriñ la nekkoon, dajale na Pëli Jullit yi, ak Mande yu jullit yi ( Mandé Mori yi : Siise, Ture, Silla ), ngir ñu àndandoo xeex (Jiyaar) safaan nguuru Bàmbara yi fi nekkoon (nguuru Ségu ak Kaarta). Buuru Bàmbara yi (Fama) ak seeni jàmbaar (Ton-Dion), amoon nanu doole, lii moo tax Ahmadu Bari tabax Imbraatoor gu Pël ca Massina Kese. ak itam Pël yi, ca Mali, foofu lañu ëppe woon ba tay (Tay jii foofa mooy diiwaan (Région) bu Mopti).
Ca Gine, Pël ya dañu faa yàgg, waaye Mande ya (Jalonke) ñoo yoron dëkk ba. Ca 1715, ay Pël yu jullit yu juge Fuuta-Tooro ak Massina ca Mali, ñoo ñëw Gine, di fa Jiyaar, di ray ñi duli jullit walla di leen jàpp ay jaam, lii moo tax giir yu bari (Susu yi, jalonke, ak Baga yi) daw ca géeju Gine, di tabax foofa ay nguur. Pël yu Jullit yi dañu doon ray ñoom tamit yeneen Pël ngir ne nekkuñu woon ay juulit. Pëli jullit yi dañoo bokkoon ca njabooti: Bâ, Bari, Jallo, Sow. Ñoom ñoo tabax nguuru Fuuta-Jalon. Karamoko Alfa Jallo mo njëkk a nekk Almaami.
Ci « https://wo.wikipedia.org/wiki/Pël » lañ ko jële