Isipt gu yàgg ga wuute gi ci sumb yi

Contenu supprimé Contenu ajouté
Abdu Xaadir KEBE (waxtaancëru)
Aucun résumé des modifications
Abdu Xaadir KEBE (waxtaancëru)
Aucun résumé des modifications
Rëdd 10 :
Bu ñu daa suul seeni néew nag, dañu ci daa boole mbooleem seeni bagaas ak alal.
Ci atum 332 nj.j la waa Geres teg loxo Isipt, booba it la tàmbalee naaxsaay.
 
== Jeexiit yu Isipt yi ==
 
 
Jeexiit yu Isipt yi
 
Seex Anta Jóob (1923 – 1986 g.j) moom lañuy jàppe boroom xam-xam bu Senegaal bi jot a def ay gëstu ci nguurug Isipt gu yàgg ga, mu leeral ci séqoo gi am ci diggante xayug Isipt ak xayug waa Afrig yu ñuul yi.
 
Seex Anta Jóob wuññi na jaare ko ci gëstoom yooyu mu defoon ci mbind yi nu yatt ci doj yi ci Isipt, ak ci gëstu yi mu defoon ci tàdd (cadavre) yu ñu taaniit (momifier) yi , - wuññi woon na ne Firhawna yi de li ëppoon ci ñoom ay nit ñu ñuul lañu, ñu néew reek ñoo ca nekkoon ñu weex. Seex Anta it wone woon na niroo gi am ci diggante lu bari ci làkki waa Afrig yi ak làkku Isipt wu yàgg wa, ponki làkk yi ak bennaani baat yi dañoo niroo.
 
(Man nag ma ne ngir dëggal niroo googu : mbaanaari séeréer yu yàgg ya ak mbaanaari waa Isipt yi walla seen pyramide yi, xool-leen leen, ag niroo ngi fi de, waxuma la nag suulaale gi waa Isipt yi daa suulaale néew beeki bagaasam te séeréer su yàgg sa daa ko def .)
 
Am na yeneen tomb yu ñu bokk ci diggante Isipt gu yàgg ga ak Afrig gu ñuul gi :
Am col ak watuwiin, ak topptoowiinu kër ak yenn ci ay gëm-gëm aki jaamuwiin.
 
Wuññi yii wone nanu ne ag wàll ci xayug Isipt ga ci Afrig gu ñuul gi lanu ko jële.
Isipt gu yàgg ga daa nekkoon gu di boroomug xay gu kawe gu dimbalee ci amal ay wuññi yu am solo ci wàllug xam-xamu xayma, ak xam-xamu falag (fidiw).
 
Fànnu Isipt bokk na ci fànn yi gën a rafet ci yu yàgg ya. Xam-xam yii nag tas nanu ci àdduna bi, kon goxub Afrig sañ naa ndamu ci li mu indil ag nite ciy liggéey yu am solo.
 
Waa Isipt defar nañu ab arminaat, lim ci at mi muy 365 fan : 12 weer * 30 fan = 360.
Ñu dolli juroomi fan ngir màggale ci juddug seen yàlla yi : Osaris – Isis – Oris – Sit – Nifti .
Séddale nañu at mi def ko 4 xaaj, xaaj bu ci nekk am ñeenti weer. Weer wi ñu séddale ko ñeenti ayu bis, gu ci nekk am fukki fan. Bis bi nag ñu séddale ko 24 waxtu.