Senegaal wuute gi ci sumb yi

Contenu supprimé Contenu ajouté
DonFalilou (waxtaancëru)
mAucun résumé des modifications
Chabi1 (waxtaancëru)
Rëdd 144 :
----
 
== '''Koom-koom''' ==
[[Senegaal]] nguur la gu bokk ci [[Bennoo gu koom-koom ak gu koppar gu Afrig gu sowwu gi]]. Ginnaaw ay jafe-jafe yu koom-koom ci njëlbéenug ati juroom neen-fukk yi, ay yoonam (ay luwaam) yu koom-koom soppiku nañu, bu ko defee ag màggam gu koom-koom mujj àgg ci ay 5% ci diggante 1995 ak 2001. Ci ndoortel 1994 Senegaal door na ci doxal tëriinu [[yéwénal gu koom-koom]] gu kawe ay yitte, ci càmmug mboolaay gu àdduna bi (communauté internationale), looloo ko jañoon ci mu woyofal xiimay kopparam bii nga xam ne daa tënku ci Frank bu Faraas, mu woyofal ko ba ci 50%. Jeexiitalu woyofal gii diisoon na lool ci ay way dëkkam, ndax taxoon ba njëgi li ëpp ci marsandiis yu dàttu yi ak yu dund yi seeroon te yekkatiku, niki meew, yàpp, ceeb, ba àgg ci fulu ci genn guddi, waaye am na genn màgg gu am ci koom-koom bi, ak ci njuddéef mu ñumm mu biirum réew mi, ngir yéwénal yi, nga xam ne àgg na ci 5% ci at mu nekk, bu ko defee walu gi(l'inflation) wàññiku ci anam gu yéeme ba àgg ci ay lim yu ndaw bu ñu ko nattee ca la romb.