Jolof wuute gi ci sumb yi

Contenu supprimé Contenu ajouté
Ibou (waxtaancëru)
Aucun résumé des modifications
Ibou (waxtaancëru)
Aucun résumé des modifications
Rëdd 1 :
'''Jolof''' moo doonoon nguur ngi gënnoo na mag ci [[Senegaal]] ci jamono yooyu. Mi ngi sosu ci xarnub XIV ba nguuru [[Nguuru Mali]] gu mag ga saayee, rawati na la feete woon ca sowam. Ba nguuru Jolof taxawee, jëloon na melokaanu nguur yi ko jiitu woon, waaye bàyyi woon na fa melokaanu càmm ak màng ga xewoon ci jamono.
 
== Sosteefam ==
Ki ñu ne moo sos nguur googu mooy Njaa Jaan Njaay. Mooy doomu [[araab]] la bu ñuy wax Abaabakar ak [[Lingèer]] ab [[Tukulòor]] bu tudd Faatimata Sall. Moom, Njaa Jaan Njaay, def na ci réew mi liggéey yu réy.
 
Bokk na ci def [[wolof]] yi ñuy benn, teg réew mi ci yoonu nguur gu leer. Samp nguuru [[Waalo]] ba mu dëgër, mu dal di koy jox rakkam. Sos nguuru Jolof gu mag ga ba mu yegg fa gën a kawe mu door a wàcce boppam. Looloo tax ña ko wuutu ñoo mottali liggéeyam ci xarnub XIV, waaye jotu ñoo moytu taste gu gaaw ca nguur gu mag ga.
 
Boo seetloo turi buur yu njëkk yi ci nguur gu mag gi di nga leen fekk ñekk fukk doŋŋ. Seen péey nekkoon na Céŋŋ ca jamonoy Njaa Jaan Njaay. Réew yu bari nekkoon nañ ci kilifteefu gu mag ga. Lu mel [[Senegaal]] ak [[Gàmbi]] ak [[Faleme]] nekkoon na ñu ci suufu Jolof gu mag ga.
 
== Buuri Jolof yi ==
Rëdd 69 :
 
== Nguuru Jolof ==
Jolof boo ko dee xool dafa këll bunom dem na ba lag da geer, égg na [[Ferlo]]. Moom dafa xawa uuf Tooro ak Dimat ak [[Waalo]] ak Kajor[[Kajoor]] ak [[Bawol]] ak Saluum[[Saaluum]] wàllu penku wi [[ndand fooy-fooy]] la. Jolof fu neew ñax la, bari na lool garabi werek. Mel na ne du fu naat it ndax ab woykat bu siiw ci yu wolof yi di Sëñ[[Sëriñ Muusaa KA]] am na fu muy melale lu ni mel ci genn xasidaam, mu ne :
nawet Jolof noor fa te doo nooraani - ndaw lu ca sax soo màggatee yalwaani
 
Rëdd 75 :
 
==== Ay way dëkkam ====
Waa Jolof nekkoon nañu ay [[giir]] yu wuute, booba ñu ngi ci seen joégejoge bëj-gànnar jëm bëj-saalum: [[giir]] yooyu ay [[Séeréer]] lañu ak ay [[Wolof]] ak ay [[Tukulòor]]. naari[[Naari gànnar]] yi daana ñu song ñi dëkk ci tàkkal [[dex]] gi. Nee nañ ki fa njëkk a dëkk mu ngi tudd Njolofeen Mbeng, mu ngi bokk ci xeetu [[Màndeŋ]]. Turam la ñu jox nguuru jolof. moo fa njëkk a sos dëkk bu ñu daan woowyewooye kàytiKàyti, moom mu ngi nekkoon ci Yeŋ-yeŋ.
 
== Jolof gu màgg ga ==
[[Fuuta]] moo doon gën jaa màggi réew ci mbooleem gox yi. loolu masu la deñ ba ci fukkeelu xarnu ak ñeent, moo tollook falug waa Tonjon.
 
Jamono jooju la [[màndeŋ]] yi yaatal seen [[nguur gu mag]] dale ca géeju Atlas ca bëj-gànnaar ba bëj-saalum ca Gàmbi. Ca jamono jooju yit la nguuru jolof nangoo boppam, moo gënoon a am solo ci réewu Wolof yi ak Séeréer si ak ci mbooleem réew yi ci géej gi, ci li ko dale ca bëj-gànnaar ba bëj-saalum, [[Fuuta]] ba [[Saalum]]. Ëmboon na [[Waalo]], [[Kajoor]], [[Bawol]] ak rèewi [[Séeréer]] si ak lenn ci [[Fuuta Tooro]].
 
== Saayug nguuru Jolof gu mag ga ==
Rèew yu bari nangu nañ seen bopp ci nguuru Jolof gu mag ga. [[Kajoor]] njëkk a nangu boppam topp ca [[Waalo]] ci njiitu [[Barag]]. Bawol ci njiitu [[Teeñ]]. Rèewi Sèeréer si ci njiitu [[Buur]]. Jolof mujj na nekk réew ni yeneen yi ci xarnub XVI ba XIX. Waaye [[Dammeel]] moom moo gënnoona metti ag jàmmaarloo ak [[Burba jolof]] ca xareb Danki ba nga xam ne moo njëkk a faagaagal nguuru Jolof gu mag ga. Ganaaw loolu la xareb Mbisin ca 1697 foofa kajoor moo Jekku, ak xareb Ambaal ci 1760, ak xareb 1886.
 
==== Ngirtey saayam ====
Bok na ci li ngirteel saayam, ñaari noon yu doon xëccoo [[nguur]] ga ñaarelu xaaj bu xarnub XIX. Noon bu njëkk bi mooy Tanoor Jeŋ. Ñareelu noon bi mooy Amadu Sayxu.
 
Tanoor Jeŋ doomi [[Lingeer]] Kura Ngoy, song na Buurba ngir nangu nguur ga. Ginaaw bi moom Amadu Sayxu nanguwaat ko ci 1870. Yor ko ba ci atum 1875, ci at moomu lañu ko jekkoo ca xareb Sàmba Saajo. Ci noo nu la Jolof tàbbee ci loxoy faraas[[Faraas]] ci 18 rakki gammu 1885.
[[catégorie:taariix]]
{{modèle:buntutaariix}}
Ci « https://wo.wikipedia.org/wiki/Jolof » lañ ko jële