Mamoor Xam Sa Diine wuute gi ci sumb yi

Contenu supprimé Contenu ajouté
Xët mu bees : Xerawlu leen ma sadd fii baati wolof miy sunu làkki maam ya déggatuñ ko faf Ngirag ne sun jamono lañ xéy mbaanig jànqe ko yaawur te rañaane kàcc nag Te xéy ma ...
 
Aucun résumé des modifications
Rëdd 1 :
Xerawlu leen ma sadd fii baati wolof
- miy sunu làkki maam ya déggatuñ ko faf
 
Ngirag ne sun jamono lañ xéy mbaanig
- jànqe ko yaawur te rañaane kàcc nag
 
Te xéy ma ñépp këmm mbaa jupp la dal
- ña jànq it seen diñe gaay seen wéttal
 
Gaa ya rañaan war ca galéemi fande ya
- te xét fétal ca ñall yuy gòlliku ya
 
Ba génn kéewu dànna mom ëwoon na leen
- ni dédd def xaloobi gaynde sange leen
 
 
Jéggi dayoom gu weesu lef moo ma ëlëm
- ma rët ba tax ma bëgg a dëflu cig woyam
 
Ngir dekkalaat ko koomu alkandeem ma wér
- te suuxataat reen ya ba meññatam ma ñor
 
ñu raas ko, fuuyu ko te ràcc, def cifaay
- yoor ca di fas dumóoyu lépp lëf lu aay
 
jafal la giim te taal ko ngënji muy bërëx
- di lekk sun liw bi ba kenn dootu lox
 
ñu naan ci dex gi bàyyi tèpp-tèpp yi
- ak dèq yeek ñunux yi, xunn-xunn yi
 
dëtëm ba màndi raggu bokkul ak di ñéer
- ci lol dafay guusali put di yokku tér
 
masëy-bandaŋ wa wenn dooñ la tooyalul
- waame wa mooy tooyali tool te koy ñoral
 
ba tax ma fëx àkki wolof ya jiitu woon
- muy waxi sun maam ya dem ak ñii fi ne woon
 
waxiin ya laa jëlaat, fasoo ñu delsiwaat
- te ñooy wolof yu wér ya, nar ñu dèkkiwaat
 
tudde ko mottaliy mebët yu’ñ sémb
- ci dekkalaat baati wolof yuy démb
 
 
Rëdd 54 :
 
Aw naa ci àlli waa Unaare fekk léen
- ñu àngu ñoom ñépp di an calli aréen
 
ma ëyu leen ne aaye naa ko, indi léen
- fukki andaar te boy te moytu aawe yéen
 
Te aw ci xàlli jub te moy anéeri moy
- te wut aléeri topp àkki tool ya bay
 
Te àlli bànqaasi moy ak àkki ngëméen
- bu léen di aas ci ëtt mbaa urmbali yéen
 
Lépp lu aay ar ko fa tey aayelu ay
- tey àddu tey aar sa njaboot ci wépp ay
 
Te bul di as ba muy waral ñu ac sa kéew
- te mooy sa kiiraay li la ëw ba’ñ di la yéew
 
Te bul asar lenn, na ngay afal ku ne
- sa xol bi nay af man a uuf mag’ak gone
 
Jépp ayib ju dul sa jos umpale ko
- te ëmbalal ku nekk’u yiw àntule ko
 
Rëdd 88 :
 
Ku bëgg nay bëgg lu baax bañ lu bonam
- te am bañum-rus ma te xeeñtu aw banam
 
Te néewi mbóorante te doon ku xuuyi mbéey
- setal sa mbóoki xol te nàmp batti péey
 
ŋoyal ca mbicci kaw ga bul jàpp ci pet
- moyal barastikook a bàyyi bul di xét
 
 
Rëdd 100 :
 
Te rendi say mbamb ca pòttox ya te boy
- jam ko ca baljat ya te bèccingal ko wéy
 
Te ñàkk paal ku dul ci Yàlla miy boroom
- te sàkku bëbbalam , ñeme’g péete ci moom
 
Te buddi say mbémpeñi xol te buddi bóot
- sol ca ngënéel ba lépp pendal aki mbóot
 
Te néewi bébbant nde moodi pëppi jëf
- di pindi pax yu feese pert bu’ñ la këf
 
Defal bërët te binni ngir yéem sa ayib
- sàkku pexem faj ko te pasteefu te jub
 
Defal sa jëf yi pàkkutéef wëlif poñat
- lu dee gi bette bette berndeele ko mat
 
Mbewte nga bërgal ko potoxlu pèkki mbég
- Génn ci mballi bërjëlug bakkane rik
 
Mbémburi xol di yéene nay mbèll mu set
- te banki jëf peek ko te mbaayàlla poñat
 
Berul te bul topp mbaboor mi deel beres
- lu bon ci ag mbëbëstënam ci foo ko gis
 
 
Rëdd 130 :
 
Bul ca deseb batt , faral béel ci lu baax
- te bul ca bar sa mbir na bir ci fonk baax
 
Te dagg pàcci panka buural sa kañaan
- te daal di buur jëm ci boroom bi daw safaan
 
Te fob sa baag yoor ko ci mbalka mom ngënéel
- tanq ca naan te wàcc mbóori xiila-xaal
 
 
Rëdd 150 :
 
Damay janeer lu mel ne ceeñeeri cofeel
- mel ne ku ñéer cafka ga far càkku ca teel
 
Ba maa ngi jànkoonte ci xol bi aw mettiit
- wu jege njòbbaxtani céy jipp jériit
 
Ba xel mi jullusante na’ak xol bi, li jib
- xañ na ma cëslaay ba jamuj naa ci lu jub
 
Mel ne ñunux ci man ci kuw maram lëjal
- ma far di cam su wéet di jukkat di jëfal
 
Te jàmbat ’ak junj jeñul jóori cibeel
- ma jaaxle cumbóonu ci màndingum cofeel
 
Ba jèmbraayi rònqooñ it di car-cari
- jàllawli xel mi xol bi it di jér-jéri
 
Fit wi ni ñugg jokkalook njàqare xol
- lu sax ni ñumm mel ne coggal gu ñukkul
 
Ba maa ngi ceeñeerlu ci biir am jayaxaan
- samab cës it call ba maa ngiiy ñeetaan
 
 
Ma ñaxtu ñaxtu kenn ñëwul jàpple ma
- cawarte dem njàqare ñëw jaxalsi ma
 
Ba càqaral na xol bi, jëmmi jamjamoor
- moo ma ñëwal njold ma jéllu kekki joor
 
jullóotu naa ba faf ne jànjang ca ja ba
- ca dig njolloor ga ba weeroo ni Ruba
 
Ma sàkku aw jaraasu pek jàppandiwul
- Ñu far ma njàmbaasali njëgg mom jarul
 
Kanam gi ñëkk , ñaq, ñuqi lëf të ma
- ma jóofu ay jafeñ-jafeñ jàmm të ma
 
Mu mel ni jaani ñas yu ñàng ñoo ma war
- te doon yu ñammasle di jurbi mel ne jur
 
Ma aw ci ñallu jommiteg xel mu ñorul
- ba mel ne am njëgg mu ag cugri lëjal
 
Ma jumm-jummi jiiñ jamono lii ma dal
- te xam ne moom du jag du jéggal du jagal
 
Te xam ne njàngóor a ko gën jikko ndax it
- njekk da koo xamul du jekki it jubut
 
Ma daal di jàppeelu ci lii ma xam ci moom
- te def ko ñukk jàpp nag ca kay boroom
 
 
 
Te ñukk jëm ci moom te jòkk nag ci jëf
- te kañ ko, njukkal ko te far sóobu ci lef
 
Doonte ne nag njàqare fi’m ne moo ma muur
- ni njóof di muure jaasi war ma bebb boor
 
Du tee ma jéem a muñ te xam ne rek ngënéel
- déesu ko jox cuune ku muñ rekk la ñeel
 
Te ñàkk jom day tax a jëf ñàkk te it
- da nay waral di jëf lu jóonu lol jubut
Kon njegemaar yu jekk tey joŋante
- firdawsi cig njoggama yal nan ci joti
 
 
Rëdd 226 :
 
Na ngay dëgër ni déjj far jéggi dayo
- te doon ku dëjjarle di dàkku mbamb ya
 
Ba mel ne mbëtti deg ya mbaa mel ne ndëfëñ
- du jàmbatub dagg ni dëññ mbaa wetañ
 
Te bul di aw ndóol wu dëféenu fàww rek
- saxal di dàllu bul di dallu mukk nag
 
Bul di dijooti ndàmm sonn a koy maye
- faral di dànna bob du déjjatuy moyi
 
Dëtëm ndoxum ndam ma mu neex ci ndenqaleeñ
- nga nòyyi ndeemeexi ngënéel sa diine feeñ
 
Dat ga di dòtti yaw nga des, dér , darale
- ni ku ñu dòtt tey ku dërkiis të file
 
Di dëflu ciw tiis te nga ndarkepp sa mbir
- dëxëñ sa ndaaf te ndàmbe mbeg akiy naqar
 
Te bul di diis ba faf di ndaari des ginaaw
- na ngay doronke dund gii doylu la teew
 
 
Te bul di dàññi mel ne kuy das defarul
- déeyaale ak détti denéer yuy dexi xol
 
Te doylu yaw doonte ne dóor-dóor nga ame
- dàggiku ndeem dooj nga am it bul ko gëme
 
Te dànd dollenki bakkan, daw ko bu wóor
- te bul di dandal it sa xol bu xel mi dar
 
Te dàngañal te moytu detteelu itam
- ca kàmbi diiŋat ya te daw dee du xalam
 
Demal ca dex ga bàyyi déeg yi daa doyul
- te digg-dóomu nag ci lépp bul ëppal
 
Te bul di ndeetet lu di tan-tanlu itam
- saxal di tan te bul dagook a ndiigu tam
 
 
 
Na dëgg doon sa nding looy dunde dadam
- ta bay sa dooñu diine bul di dooji tam
 
Te bul di doore mukk diisool ci lu ne
- da nay teree daanu di tee diig ci lu ne
 
Xamal ne Yàlla day dënéerlu képp nit
- nang ko ba xel dàggiku ngir teg na la bët
 
 
Rëdd 284 :
 
Shaytaane day wëtt ci xol wudd la am
- wattu ko bul ko wàcc muy war di ku lëm
 
 
 
Dafay woreek a wèddilooy werenteloo
- di wàjji ngëm di wònni mbas mbas du welu
 
Wor ko te wòdd xol bi ngëm waaru bu wér
- sotti ci waame tudd Yàlla xol bi wér
 
Weeral sa wañsu diine def say warugar
- bu ngëm gi woos ni waddbéer wu gar ya wër
 
Werante wottee ko lu war, lu wóor itam
- na wuutu wor te worma wecci wane tam
 
 
 
Nga weex sa xol wèkki ca luy wòllimiku
- te bàyyi weeje it welal tayle ba ko
 
Te wòlli nag wëlli kañaan’ak weli rëy
- wetañ yu ñëw weñ ko te wetti far ko ray
 
Te wacc weerante te wéer fa wòllare
- wareef akug wegeel te wicc njàqare
 
Te wërsëgoo wiiri wakiirlu wis ca way
- te xol bi weex nga wattu waŋi wuute wéy
 
Te waggar it sa bopp tey waaru bu wér
- te bul di wëndëng wa wogul wàqi te war
 
Di waaj di walli weddi bakkan’ak loram
- te wéer ko bul weng ci moom ak ci wujjam
 
 
 
Di waslu àq woor ci caaxaan aki nar
- wekku ci Yàlla def ko waay jëf la la war
 
Te fònku waxtu xam ne daa wund lu rëy
- te bul di wuññi awra bul di wóoyu ay
 
Na ngay woyof te bul di wex ci kenn tam
- ku dul ku bon te fònk worma tey xalam
 
Arafu y
 
Yaraanga’a ngi may yeerook a yedd ak a yunk far
- yërëm leen ma saag yées yées na yòqat a ngii di yër
 
Ba yambar ya far nan tiim ma man may yalang mu yes
- ba yòqóolu naa far yòllugar nan ma far ma ber
 
Te yiiruñ ma may yoppoorlu yërmaande far na jee
- ma namp yanaatub ñàqareek yëjji xol bi mer
 
Te yombul samay mbir yemp yenkeewlu naa itam
- ci yammug yaras maa yay di yuuxook samaw naqar
 
Te saa meññatum yaakaar mi yuntul ma yeene yiw
- ku nekk te teewul may yokkuw naqar’ak lu tar
 
Ba saa kawarug mettiit wa yiif na ba yéegi yéen
- ba ronqoñ di yol saaw fit ni yèjji ni laaxu gar
 
Ma yeewat ci yittey gaa yu yeeme mu të’a yewén
- ma yoongan ko yootug yokk fàww ci ngën ji yar
 
Ma daw yaafus ak yunj’ak di yeex’ak di yox-yoxi
- te def yuww aw ciw yoon ba def yunn cig cigar
 
Ma mujj di yeer muy yabbalum xel di yaag xalam
- te muy yaradal am xel ku yewwu du sóoru mbër