Aten wuute gi ci sumb yi

14 octets ajoutés ,  9 at ci ginaaw
Coppite gi amul tënk
Moone ca jamonoy [[Pool]] dafa ñàkk xaalis. Amatuñu nguur, te diiwaanam Atig dafa tuuti - dénd bu tollook 2.600 kilomet kaare matul sax benn departemaŋ ca [[Senegaal]]. Amul feneen ca Atig fu gën a sore Aten 40 kilomet. Seen suuf musuñoo doy seen soxla. Taw bi barewul woon, lu tollook taw bi ñu am ca noru Senegaal. Ñetti cér ca ñeent ca suuf si amul njëriñ ci bey te yu bare ci yi des amoon njëriñ ca bey garabu oliw rekk. Amoon nañu mbélli xaalis waaye fekk nañu ne jeex nañu tàkk laata jamono nguuru Room. Tamit seen doole ci jaay wàññiku na, ndax doole yeneen dëkk yu mel ni [[Ancos]], [[Korent]], [[Efes]], ak [[Alegsàndiri]].
 
Dëkku njàng la woon, bu amoon bennjenn daara ju kawe 'iniwersite'. Naka noonu siiw nañu ndax seen xam-xam ak seen waxin, ndaxte waxin lañu ca gën a jàngale. Wax ak a déglu lu bees rekk lañu daan xinte. Amoon na ay mbooloo boroom xam-xam. Benn ca mbooloo boroom xam-xam moo tuddoon [[Epikuren]]. Kureel la woon, bi sës ci njàngalem Epikuur (mu faatu 270 at lu jiitu jamano Kirist) te fonk bànneex, ba mucc ci bépp tiis. Gëmuñu Yàlla, waaye ñu gëm ne àddina dafa sàkk boppam te amul boroom. Te boo deeyee amul dara lu ciy topp. Nekkatuloo daal. Beneen mbooloo dafa tuddoon [[Estowisen]]. Kureel la woon, bu sës ci njàngalem Senon (mu faatu 265 at lu jiitu Kirist). Fonk nañoo naagu, ba bañ a yég dara, muy bànneex mbaa naqar.
 
[[Dencukaay:Acropole1.jpg|thumb|250px|right|Akëropool ca Aten.]]
2 337

modifications