Melosuufug Afrig wuute gi ci sumb yi

Contenu supprimé Contenu ajouté
Abdu Xaadir KEBE (waxtaancëru)
Xqbot (waxtaancëru)
m r2.7.2) (robot Adding: pnb:افریقہ دا جغرافیہ; cosmetic changes
Rëdd 1 :
'''[[Afrig|Goxub Afrig]]''' moom benn la ci [[Gox|goxi]] [[Àdduna Ju Yàgg ja]], moom nag ab joor bu réy ci jéeri la, géej xottiwu ko (jaarul ci biiram) du caagéenug [[Dóox|dóox]] (golfe). Moom nag mi ngi nekk walla mi ngi féete ci xaajub kol-kol bu penku bi.
 
Gox bi nag mi ngi tallaliku ci diggante ñaari rёddi gaar yii : 37º ci [[Tus-wu-taxaw|tus-wu-taxaw]] wu bёj-gànnaar ak 35º ci [[Tus-wu-gaar|tus-wu-gaar]] wu bёj-saalum. Bu ko defee rёddu yamoo wi jaar ci diggam, daal di koy séddale ñaari xaaj: benn xaaj bi di bu bёj-gànnaar, nekk nag ci [[Xaaju kol-kol|xaaju kol-kol]] bu bёj-gànnaar bi, beneen bi di bu bёj-saalum, féete ci xaaju kol-kol bu bёj-saalum bi. Ci noonu [[Gёwéelub sànkar|gёwéelub sànkar]] moom ñёw romb ca genn wàllam gu bёj-gànnaar ga, [[Gёwéelub tef|gёwéelub tef]] ñёw jaar ca geneen wàll gu bёj-saalum ga. Bu ko defee rёddu [[Grinits]] (rёddu [[Tus-wu-taxaw|tus-wu-taxaw]] wi ) romb ca catam lu sowwu la.
 
Moom nag dafa tiim ak tefesam yi ci wàllug bёj-gànnaar géej gi ñuy wax [[Géej gu Diggu]] gi, mooy li ko tàqaleek [[Tugal|goxub Tugal]], waaye fu jege Tugal lay doon, bu dee fa tollook [[Doju Taariq]] (Jibraartaar). Bu dee ci penku bi day tiim [[Géej gu xonq]] gi ak [[Mbàmbulaanug End|mbàmbulaanug End]] gi, ñoom ñaar ñoo koy tàqaleek [[Asi|goxub Asi]] ak [[Oseyaani]], waaye luy jege Asi la ca [[Baabul Mandab]] ak [[Barsaqu Suwes|barsaqu Suwes]], ci sowwu bi nag mi ngi sapp (tiim) ci [[Mbàmbulaanu Atlas|mbàmbulaanu Atlas]] gi ko tàggaleek ñaari [[Aamerig|goxi Aamerig]] yii di: [[Bëj-gànnaaru Aamerig|Aamerig gu bёj-gànnaar]] gi ak gu [[Bëj-saalumu Aamerig|bёj-saalum]] gi.
 
[[Afrig]] nag nekk gi mu nekk ci diggante goxi [[Àdduna ju yàgg]] ja, tax na bu baax ba [[Isipt gu Yàgg|xayug Isipt gu yàgg]] gu kawe ga, man a tas ba àgg ci xeet yu bari ci ñaari gox yii, [[Asi]] ak [[Tugal]].
Rëdd 11 :
Ngir woomle gu réy gi gox bi def ci wàllug mbay, dundat ak mbell, sancaani sowwu yi (waa Tugal yi) tegoon nañu ko loxo, waaye ay askanam jug def ay fipp yu toftaloo ngir gore ci canc gi (colonialisme), ci noonu ñu ёpp ci ñoom mujj temb, sancu yi ci mujj a temb nag ñooy yu [[Portugaal]] yi, ñoom de xeex nañu xeex yu tar ngir jot séenug tembte.
 
[[ImageDencukaay:LocationAfrica.png|thumb|right|400px|Lonkoyoonu àdduna bi, Afrik moo gañcax]]
 
== Melosuuf ci jëmm ==
Rëdd 21 :
== Melosuufug nite ==
 
=== Nit ñi ci gox bi ===
 
Reew yi nga xam ne seenug yorte(administration) dafa néewal, lim yi ñuy joxe doonu ñu yu matale (limbare (statistique) yi defu ñu leen ci anam gi war).
Rëdd 50 :
* Waa-madagaskaar
 
== Kuuteeg làkk yi ==
 
Ñoo ngi koy xayma ci 200 ak 2000 làkk walla waxin (làkk dañ koy bind te waxin ci lammiñ lay yem) ci Afrik. Dañ leen seddale ci ay mbooloo, maanaam làkk yi am ag mbokk.
Rëdd 62 :
Ñetti làkk rekk ñooy làkk i seen nguuru reew, di seen làkku cosaan: Lesoto, Ruandaa, Burundi.
 
== Kuuteeg diine yi ==
 
* [[Lislaam]]: 260 miliyoŋ i taalibe. Ci sowu ak ci penku Afrik la ëppee doole, lu wuuse bëj-gàannar gi.
Rëdd 71 :
Goxub Afrig ñi koy xàmmee ci suufam su bari si ay laamaar, ba tax na sax ñu koy niroole ak tappaan bu ñu dёpp, boo xoolee di nga gis ne penku gox bi ak bёj-saalumam ñoo gёn a yekkatiku bёj-gànnaaram ak sowwoom, te it dinga man a gis laamaar yii:
 
Laamaaru Tàkk gu mag gi : day tàllaliku ngir daj mbooleem bёj-gànnaaru gox bi, dale ko ca géej gu xonq ga ci penku bi, ba ca mbàmbulaanug atlas ci sowwu bi, dees na fa gis it ag kaw-suuf gu bariy melo: ay laamaar, ay tundi xeer, yu beeñ (dune) ak xur yuy faral a am ay [[Waaha|waaha]] (oasis).
 
Doji Atlas yi: ñoom ñi ngi nekk ci gёn jaa soriy bёj-gànnaaru sowwu gu Afrig, ci réewi Maxrib Bu Araab bi, bu ko defee ñu tàlleeku nag yor melokaanu ay càllalay doj, dale ko ca bёj-saalum gu sowwu gi ba ci bёj-gànnaar gu penku gi, ñu ёmb nag ci seen biir ay laamaar yu kawe yu ay ngéej yu saf xorom di diggale , ñu xame leen ci turu Shutuut .
Rëdd 81 :
Laamaaru Ecoopi: mooy bi gёn a kawe ci laamaari Afrig yi, fa la ñatti car (affluents) yu am solo yu dexug Niil gi di balle ñooy: Sobaat, ak Niil gu bulo gi ak Atbara, bu ko defee yobbaale ndoxi mbёnd yu bari yi ci jamonoy taw bi, ngir denc leen ci ngéejus Naasir ba waa Isipt di ci man a jariñu, mu leen di indil ag naataange.
 
Laamaaru ngéeji yamoo yi: moo ci gёn a néew ag yekkatiku, fa la cari Niil gu [[Yamoo|yamoo]] gi di balle, ñoom ñi nga xam ne seeni ndox ña nga leen di jёle ca ngéejus Wiktooria, mooy ngées su neexum ndox si gёn a réy ci yu àdduna bi, mooy jox Niil ndox li ёpp ci weeri at mi
 
Laamaaru bëj-saalumu Afrig: moo gёn a yaatu te gёn a yëkkatikoodi, am na nag yenn dex yu ko dog, am ci yu ciy sotti ci penku bi, ci [[mbàmbulaanug End]], (niki Simbisi ak Lombobo), am yu ciy sotti ci sowwu bi ci [[mbàmbulaanug Atlas]] niki Orang
Rëdd 92 :
Taw yu kojug dig, yu noor yu sakkan yi, ñi ngi faral di rot ci bёj-saalumu Sudaan ak Laamaaru [[Ecoopi]].
 
Taw yu diggdoomu yi ñi ngi wàcc ci digg Gox bi, ca bёj-gànnaar ak bёj-saalumu [[Diwaanu yamoo|diwaanu yamoo]] bi.
 
Taw yu néew yi ñi ngi rot ci bёj-saalumu [[Tàkk|tàkk]] gu mag gi ak bёj-gànnaaru [[Tàkkug Kalahaari|tàkkug Kalahaari]] gi.
 
Tàkk gu mag gi nekk ci bёj-gànnaaru Gox bi nag moom daanaka du taw ak tàkkug Kalahaari gi nekk ci bёj-saalumu sowwu Gox bi.
Rëdd 168 :
[[pam:Heograpiya ning Aprika]]
[[pl:Geografia Afryki]]
[[pnb:افریقہ دا جغرافیہ]]
[[pt:Geografia da África]]
[[sl:Geografija Afrike]]