Xam-xamu nosukaay wuute gi ci sumb yi

32 octets supprimés ,  11 at ci ginaaw
m
robot Modifying: ko:컴퓨터 과학; cosmetic changes
m (robot Modifying: ko:컴퓨터 과학; cosmetic changes)
'''Xam-xamu nosukaay''' (walla '''Xam-xam bi ñeel nosukaay'''), moo yor gëstu gi aju ci [[Cëslaayu xibaar|cëslaay yu xibaar]] yi, xarala yi ñeel seenug nos ak seenug jëfandikuwiin ci noste yi ñuy jëfandikoo ay [[nosukaay]]. Ñi ciy yëngu seen liggéey doon lëkkale ay nosukaay ñu doon li ñuy tuddee ag [[lonkoo]], defar ay [[Dàttub njoxe|dàtti njoxe]], [[Noste gu boppu|boppal ay noste]], defar ay [[Tëriinuw nosukaay|tëriin]] te loolu laaj na xam ag [[Kàllaamab tëriin|kàllaamab tëriin]], .
 
Cig lawal, xam-xamu nosukaay dafa ëmbu ci li ñuy wax ''[[Xaralay xibaar ak jokkoo|xaralay xibaar ak jokkoo yu yees]]'' yi di xeetu xam-xam bi ëmb lépp li ñeel xibaar, ci gépp anamam. Ci tëriin wi la tëralkat bi di joxee ay tegtal nosukaay bi ci anam gi mu war a yoree xibaar yi, lan la ci war a def ak nan la ko war a defe. [[Jëfaan]] yi nag ñooy mbooleem cëri nosukaay bi, benn bu ci nekk am na liggéey bu ñu ko sant: yii di rënk xibaar yi, yii di leen wone ni nga bëgge, yii di leen soppi...
 
== Taariix ==
Ba àdduna dooree ba tay nit daa mas di ut ay jumtukaay ngir man a def ay waññeem. Ci jumtukaay yooyu, ci yi gën a yàgg, man nañu cee lim àlliway [[Hammurabi]] (1750 laata yeesu). [[Wuutuloxo]] yu [[doolerandu]] yu njëkk ñoo ngi tàmbalee feeñ ci diggante XVII ak XVII<sup>u</sup> xarnu. Waññikaay bu doolerandu bu njëkk, jàpp nañu ne, mooy bu Wilhelm Schickard ci XVI<sup>u</sup>.
 
Ci [[1642]] [[Blaise Pascal]] defaroon na, moom itam, ab Waññikaay bu doolerandu, doonoon bu ñu doon jaay sax, ba tay jii juroom-ñeent ci yooyu man nga leen a fekk ci jeexiituwaay (muse) yi. Ci ay njëlbeenam man nanoo wax ne [[xaymaan]] yi rekk ñoo ci doon yëngu ndax li leen yetteeloon moo doonoon defar ay jumtukaay yu leen di yombalal seeni Waññi yu xayma. Ay cëslaayam yépp ci xayma lañu taxaw, rawati na liñuy way [[Aljibar bu Bool|aljibar bu Bool]].
 
Tay jii xam-xamu nosukaay jël na wàll wu am solo ci sunug dund, cig suqali ci wàllu koom-koom ak mboolaay yu askan yi.
 
{{wikibaatukaay}}
 
[[Wàll:xamXam-xamu nosukaay]]
 
[[af:Rekenaarwetenskap]]
[[ka:საინფორმაციო მეცნიერება]]
[[kn:ಗಣಕ ವಿಜ್ಞಾನ]]
[[ko:전산학컴퓨터 과학]]
[[la:Informatica]]
[[lad:Informatika]]
7 612

modifications