Bennoo gu Almaañ wuute gi ci sumb yi

Contenu supprimé Contenu ajouté
SieBot (waxtaancëru)
m robot Adding: tl:Pag-iisa ng Alemanya
Xqbot (waxtaancëru)
m robot Adding: mk:Обединување на Германија; cosmetic changes
Rëdd 1 :
'''Bennoo gu Almaañ'''
 
== Almaañ njëkk xare yu Napoleon yi: ==
 
[[Almaañ]] njëkk xarey Napoleon yi, dafa séddaliku woon ci lu jege ñatti téemeer ak juroom benn fukki diiwaan(360 diiwaan), yépp it ci ron imbraatóor gu Otris lañu nekkoon, walla li ñuy tudde '''Imbraatóor gu Rom gu sell''' gi. Almaañ gépp it genn nguur rekk a fa nekkoon gu mag te temb, mooy gu [[Brusiya]]. Nguur googu nag jëmoon na kanam, te ag yewwuteem fés, ci jamonoy buuram ba tuddoon [[Fredrick mu mag mi]] (Great Fredrick) (1740 -1786 g), mooy ki ko defoon muy nguur gu dëgër te am doole. Bu ko defee waa Almaañ yépp wëlbati seeni gët jëme ci nguur gii, ngir bëgg ag bennoo.
Rëdd 16 :
 
Ginnaaw bi Napoleon Bonaperte daanoo atum 1815g, ci lañu def ndajem Vienne, ñu jële fa ay [[saxal]] yu bari, bokk na ci yooyu, dagg [[Dóox]] bu [[Warsaw]] gu [[Poloñ]] gi, dagg ko ci Brusiya, te jox ko [[Riisi]], bu ko defee ñu jox Brusiya moom itam diiwaanub '''Rayan''' ak xaaju diiwaanu Saksoniya. Daal di taxawal ag bennoo gu Almaañ gu làmboo fanweer ak juroom ñeenti [[nguur-nguuraan]] yu Almaañ, Otris jiite ko.
Defiin wii nag mi ngi ame ci càkkuteeful [[Metternich]], ak naj gi mu doon naj way daje yi, ngir ñu defal ko bëgg-bëggam boobu. Bennoo gu Almaañ gii juddoo ci ndajem Vienne mi, nekkoon na di lu manul a wéy, ndax kat Otris moom daa tàmbli woon di génne ay saxal aki ndigal yuy safaan '''tas-xibaar gu gore''' , te wéeroodi fenn, tey safaan mboolooy Almaañ yi daan sàkku ag bennoo te daan ko woote. Te Otris it daa mujjoon teg loxo ci '''jataayub bennoo gu Almaañ gi''', te ga woon ko ci mu génne ay saxal yuy digale ñu fuglu daara yu kawe yi , ak leekol yi, ak ndaje yi añs.Doxaliin yooyu nag taxoon na ba ay kàddu jib yu ay waa Almaañ, di sàkku ñu fipp ci kaw Otris, tey sàkku ñu jeem a bennal Almaañ, ci keppaarug nguur gu Almaañ gu dëgër. Loolu mooy li xeltukatu Almaañ bi ([[Hegel]]) daan sàkku, te daan ko woote, moom ak ñeneen ñi daa jam bennoo gii nga xam ne Otris a ko moomoon daanaka, te tegoon ko loxo.
 
 
== Taxawaay bi nguurug Brusiya ame woon ci naal yi jëmoon ci Bennoo gu Almaañ gi: ==
 
 
Nguurug Brusiya dafa tàmbli woon di yëngu ngir dajale xeetu Almaañ wi, dugal leen ci genn nguur gu Almaañ gu ñu bennal. Mu daal di woon rëddal boppam ab politig bu muy jaar ngir àgg ci loolu mu bëgg. Mu daal di woon door ci dëgëral boppam ci biirum réew, defaraat doxaliinam , yekkati koom-koomam, soppi nosteg galag yi aju woon ci nduwaan ci mbooleem diiwani nguur gi.
Ñu daal di taxawal noste gi nu daa wax ('''Solofrayn'''), di ag bennoo ci wàllug nduwaan, mooy li neenaloon nosteg nduwaan gi ci biir Almaañ. Nga xam ne li nekk ci biir réew mi cim njaay deesu ci génne duwaan. Nga xam ne daññoo fééexal yaxantu gi ci Brusiya, afal ko ba mu man a doxe ni ko soob, ci lu dul ñu ciy teg ay tënk-tënki galag mbaa yu nduwaan. Doxiinu Brusiya wii déy dees na ko lim mu dig soopiku gu mag ci taarixu bennoo gu Almaañ gi. Doxal nañu ko nag ci atum 1818g, ci biir ay diiwaanam yu biir yi. Diiwaan yooyu nga xam ne njëkk “Nosteg Solofrayn gi” danoo nekkoon ay diiwaan yoo xam ne bu ci nekk daa amoon '''nosteg bobb gu nduwaan'''(systeme autonome douanier), gu mu bokkul ak kenn. Waaye bi Solfrayn taxawee, lañu bennal biir Brusiya ci wàllug nduwaan, ginnaaw bi mu nekkee moom Brusiya di lu ñu séddale ci juroom benn fukki diiwaani nduwaan.
 
Waa Brusiya yi yëgoon nanu ne benno gi ci wàllug koom-koom mooy cëslaay li ñu war a teg bennoog Almaañ gi ci wàllug politig. Looloo taxoon kilifay Brusiya yi tàmbli woon a fexe nu ñuy def ba dugal yeneen diiwaani Almaañ yi ci bennoo gu nduwaan googu. Brusiya nag amoon na ndam ci li mu doon wut ci yenn ci diiwaan yu Almaañ yu ndaw yi, waaye nag jot naa dajeek ag jàmmaarloo gu mag ci yeneen diiwaan yu Almaañ yu mag yi, li ko waral mooy ñoom dañoo gisoon ne li gën ci ñoom mooy ñu sosal seen bopp ag bennoo gu ndawaan gu temb, ngir xeex ci bennog nduwaan gu Brusiya gi. Looloo fi indi woon ñatti bennoo yu nduwaan ci Almaañ, ñooy:
 
Rëdd 39 :
 
 
Kilifay Brusiya yi xamoon nañu ne diiwaani Almaañ yi danañu nangoo duggsi ci bennoo gu Solofrayn gi, bu ñu soppee sart yiy tax manees cee dugg. Looloo taxoon ñu soppi sarti Solofrayn yi, nga xam ne leegi dañoo sos ab jataay bu làmboo mbooleem ndawi yi ci bokk, buy saytu noste googu. Leegi nag lu fa duggati rekk ci li bawoo ci '''nduwaan mi''' ak galag yi ñu koy séddale mbooleem diiwaan yi, ci kem limub ña fa dëkk. Soppi yii de dimblee na ci yaatal gëwéelub Solofrayn, gën a yàkkali ab géewam. Leegi nag [[Bavar]] bokksi na ci ak [[Saksoniya]] ci atum 1934g, ca saa sa tam, nga tàmblee gis lu lay won ne Solofrayn moom tàmbli na a naat ak a am ag yokkute. Yaxantu ga tàmbli woon nay jar, di dox, mbay ma màgg, ndefar ga jëm kanam ci mbooleem diiwaan yi bokksi ci Solofrayn. Am na nag benn jëfka boo xam ne moo àntul Solofrayn, mooy moom de noste gu waa Almaañ xalaat ba def ko la, loxol Otris duggu ci, jenn doole it ju ko man a teg loxo yoonam nekku ci. Metternich gisoon na ay wi nekkoon ci noste gii, waaye bi mu koy gis fekk na waxtu wa jàll, manatu ca woon dara. Mu daal di bind Imbraatoor bu Otris bi ne ko: “Na la wóor ne nguuri Almaañ yi - bi lii amee de – di nañu nekki wenn yaram wu jàppaloo, ci ron kerug doxaliin wu Brusiya, te da na jàppeji Otris muy - moom - aw yaram wu di doxandeem, wu tumbrànke wu bokkul ciw yaramam”. Te kat waa Otris yi ñoom, ca dëgg-dëgg, duñu ay doxandéem ci waa Almaañ yi, ndax ñoo bokk xeet, làkk ak taarix. Man nañu ne Almaañ gépp mujj na bokksi ci Solofrayn gi, atum 1842g.
 
Xalaatu xeltu bu Hegel bi feddali woon na dooley nguur, ak ray gi muy ray jëmmaan (individu) ak lépp lu mu am, ngir sàmm dooleem akug màggam ak wegeelam. Nguur walla àtte – ci gis-gisu Hegel- cëslaayam mooy doole, ci doole rekk la man a dëgërale gëgg. Kon nguur walla àtte gu dëgër ci gis-gisu Hegel, mooy nguurug walla àtteg dëgg. Kon moom Hegel day mel ne moo teg ci loxol Brusiya lay wa di xeltu guy rafetal, di baaxal seen jëfi jiite googu ñu jiite woon '''bennalug Almaañ gi'''.
Rëdd 67 :
Otris ak Riisi dimblante nanu ci màbb barlamaab [[Frankfort]] bi, ak naalam yi mu amoon te ñu jëm cig bennoo gu Almaañ, looloo waraloon jéem gi ñu doon def ngir bennal Almaañ ci ron kilifteefug Brusiya, ci atum 1848g, mujjul woon àntu. Waaye li muy àntoodi lepp teewul xalaat bi sax ci xoli ak xeli waa Almaañ yi. Ñu mujj (waa Almaañ ñi) xam ne daal duñu man a amalati seen bennoo googu ci anamug jàmm, mbaa gu sartu réew, ndaxte Otris àndu ci te mi ngi koy xeex ak doole.
Looloo waraloon ñu jëloon seen yitte def ko ci amal am mbooloom xare mu dëgër, mu leen di man a may ñu man a génne Otris ak Almaañ cig njëlbeen, door a lijjanti nag nu ñuy doone benn ci ginaaw bi.
Xalaat bii nag [[diisoowaale]] (chancelier) bu Brusiya bii di [[Bismarck]], àndoon na ci te jàpple woon ko, dëgëral ko. Moom mooy [[Otto Von Bismarck]], boroom kurpeñu weñ bi.
 
 
Rëdd 73 :
 
 
Bismarck mi ngi judd atum 1815g, am njàggam mu kawe mu defe ko ca daaray Berlin ju kawe ja. Daal di dugg ag [[coldaar]], génnati ca, dem nag féete ca boppam ca toolam ba. Mi ngi bokkoon nag ci njaboot gu woomle, gu ami alal yu rëy ca Brusiya. Sampoon na boppam niki '''lawax''' (candidat) ngir ñu fal ko ci bennoo yu Almaañ yi, atum 1848g, ñu tànnoon ko it muy ab cér ci parlamaa bu Brusiya bi. Liggéey na it ci toolub diplomasi, doonoon aji téewal réewam (l'ambassadeur) ca Butrsburg ca Riisi. Ginnaaw bi mu nekkal réewam ca Paris.foofee la ko ''' William mu njëkk''' mi doon jiite Brusiya woowe woon mu juge [[Faraas]], ngir jiite-si njiitug jawrin gi ci Brusiya.
Bismarck nag nekkoon na ku gëmoon, te daa dëgëral '''noste gu nguur gu ñu joyal''' , te gëmoon ne buur daa war a am doole te am soldaar su dëgër, '''Jàngu bi''' jàpple ko ak '''garmi''' yi. Bismarck moom faalewutoon parlamaa bi. Gisoon na ne jëm kanamug aw xeet walla ag yéegam jëm ca kaw manul a ame ci lu dul ay buuram di ñu kawe ay yitte, ak ay kàngamam, waaye duñu ko ame mukk ci ay '''saxal''' (résolutions) yu juge ci ay parlamaa, aki '''nostey sarti réew''' (systèmes constitutionnels).
 
Bismarck yitteem jépp mi ngi ko jëmale woon ci génne [[Faraas]] ak Otris Almaañ, mu gisoon ne lii daal manul ame ci lu dul dooley xare ju mag, ju leen ci man a ga(manante leen). Ci noonu mu tàmblee liggéey ci dëgëral dooley xare ji, ak kàttanal ko. Mu daal di tas parlamaab Brusiya bi, ndaxte (moom parlamaa bi) daa bañoon ne du woote alal ji mu doon laaj ngir man cee dooleel soldaaram si, ci noonu mu tëjoon képp ku wuuteek politigam boobu, daal di digle ñu fuglu yéenekaay yi, daal di beddiku sartu réew mi, ne du ci sukkandikooti. Alal ji mu soxla woon mu génnelu ko ci ndigalul buur bi, bañ cee sukkandiku ci lu parlamaa bi.
 
Wàllug '''xeetu''' (nationalisme) nag moom gis-gis bi mu ci amoon moo gënoon a yaatu bi mu amoon ci sartu réew, ndax daa gisoon ne sartu réew moom, mi ngi ame mook ay jubluwaayam, ci ginnaaw bu ag xeetu amee ba noppi.
 
Bismarck nag neenalul mbooleem parlamaa bi mbaa mu tas ko lépp, moom kay da caa neenl walla mu soril ko ñatti mbir, ñooy:
Rëdd 92 :
== Bismarck wone na dogu gu mag akug takku contar teg gi Otris teg loxo Almaañ ==
 
Loolu nag gën na a fése ci taxaw gi mu taxawoon ci dakkal politigu Otris bi muy teg Almaañ .
Looloo taxoon Otris mujj woo buuri Almaañ yépp cim ndaje ca Frankfort, ngir sos ag '''bennoo gu lëngoo (walla gu federaal)''', guy doxal ab goornamaa, boo xam ne ay dooleem ak sañ-sañam mi ngi koy jële ci sart boo xam ne Otris moo koy defar, tër ko.
 
Rëdd 115 :
 
 
== Xare yu Brusiya yi ak Danmark: ==
 
Bismarck xuus na ab xare safaan Danmark, atum 1864g, ànd ca’ak Otris, ngir nangu ñaari diiwaan yii di '''Shalswig''' ak '''Holistin''', ñu doonoon ñaari '''Dóox''' (duché) yu bokkoon ci bennoo gu Almaañ gi te Danmark tegoon leen loxo.
 
Danmark mujjoon na ñàkk pexe, daal di deltu ginaaw wëlif ñaari dóox yooyu atum 1864g, bu ko defee Brusiya jël dóoxu Shalswig, Otris it àtte diiwaanu '''Holistin'''.
 
== Xarey Brusiya ak Otris: ==
Rëdd 128 :
Bis bu Yàlla dogalee njortul Bismarck loolu mujj di dëgg, ba Brusiya am ndam, loolu de da na nekki muccug waa Almaañ ñi ci gàllankoor gii tukkee ci Otris, gu leen di teree nekk benn, tee bennoo gu Almaañ gu wér man a am. Màggug Brusiya ci wàllug politig ci biir bennoo gu Almaañ gi, mujj di luy jeqi njàqare ci Otris.
 
Solofrayn moom màgg na ci anam gu doy waar, rawati na bi ci nguur-nguuraan yu Almaañ yi tiim [[Géej gu bëj-gànnaar]] gi bokksee. Ci noonu lu sakkan jug ciy yooni weñ lënkale diggante wàll yu Almaañ yu wuute yi. Loolu tam dooleel bennoo gu koom-koom gi nga xam ne Brusiya mujj na di ci ki ci gën a jariñu.
 
Sabab yii rekk doyoon nañu ngir taal xeex bi ci diggante Brusiya ak Otris, rawati na ginaaw bi dooley Brusiya ji doxee jawali Holistin, nangu ko, te moom daa nekkoon ci ron kilifteefug Otris, ngir dëppoo gi amoon ci diggante Brusiya ak Otris atum 1865g.
 
Bismarck moom lijjanti woon na ba Riisi génne loxoom ci diggam ak Otris, loolu nag di ci jàpple gi mu jàpple woon Riisi ci giimal jeqiku(révolution) ga amoon ca Poloñ, atum 1853g. Dëppoo woon na ak Imbratóor bi Napoleon III, imbraatóoru [[Faraas]], moom itam, ngir mu seetaan kook Otris, bañ cee dugal loxoom, li mu koy faye ci loolu nag mooy bàyyi kook yenn moomeel yi ci diiwaanub Rayn. Mu demati tapoo-ji (faire alliance avec)ak nguurug Itaali, gi nga xam ne li doonoon yitteem mooy nocci Venezia ci loxol Otris, ngir matal ag bennoom.
 
Xare bi amoon ci diggante Otris ak Brusiya xare la woon bu fëkk te gaaw, wéyutoon lu ëpp juroom ñaari ayu-bis, moo waraloon nu tudde woon ko '''xareb juroom ñaari ayu-bis yi'''. Dooley Brusiya ji jot na ca a am ndam ci kaw ju Otris ja ca xareb Sadwa ba, ca Bohima atum 1866g . Mu manoon a àgg sax (moom dooley Brusiya ji) ba ca Vienne, bu Imbraatóoru Faraas bii di Napoleon III jugutoon, dox tànki jàmm ci diggante bi. Ci noonu Bismarck daal di ñàkk pexe, taxawal xeex bi, ngir ragal Faraas dugg ci xeex bi ci wetu Otris. Te it Bismarck moom da ne woon na doylu nag ci am ndam gii mu am ci kaw Otris, ak dammte gii mu ko dammte, ndaxte soril na ko bennoo gu Almaañ cig wàll, te it bëggutoon a toroxal Imbraatóoru Otris bi, ngir loolu man na a tax bu jugee ëlëg moom Brusiya di xare-ji ak Faraas, Otris du ko sot, ci geneen wàll.
Rëdd 146 :
Gis nga ko, Bismarck kat am na ay ngërte yu am solo ci xareem beek Otris. Moom de fare na fi bennoog Almaañ gu yàgg ga, indi fi leegi ag bennoo gu Almaañ gu yees, gu ame ci mbooleem réewi bëj-gànnaaru Almaañ, nga xam ne ñaari Dóox yii di Shalswig ak Holistin ci lañu woon, buuru Brusiya bi jiite ko. Bismarck nos na bennoo gu yees gi, wutal ko ab parlamaa '''(Rashstach)''', ndawi askan wa di fa daje, ak '''jataayub bennoo gu Almaañ gi''' '''(Bundasrat)''', ndawi diiwaani Almaañ yi bokk ci bennoo gu Almaañ gu bees gi di fa daje.
 
Bismarck it lijjanti na ba def ak diiwaani bëj-saalum yi bokkutoon ci bennoo gi, lijjanti woon na ba def ak ñoom '''genn tapoo gu xare''' .
 
 
Rëdd 193 :
[[ko:독일의 통일]]
[[lv:Vācijas apvienošana]]
[[mk:Обединување на Германија]]
[[nl:Duitse eenwording]]
[[pl:Zjednoczenie Niemiec (1866-1871)]]