Diiney Afrig wuute gi ci sumb yi

Contenu supprimé Contenu ajouté
a
(Aucune différence)

Sumb bu 6 Suwe 2009 à 03:21

Ca Afrig, diiney yi yag nanu fa am. Diiney bu am Afrig, ño bokk cossan. Ca jamono yu ngurru Koush amone, tey di nek wa Sudaan ak Ecoopi, nit ño fa nekkone, danu daan nek ca diiney yu jekk am ca aduna. Ca diiney bobu, nit yi dañu daan geum bene Yallah. Ca wa Misra tey di nek Isipt, ba Sudan, diiney bobu mo fa amone. Ca diiné bi, yallah, melni lislaam, téemer tuur la amone, tuur ku nek ñu woné bene jiko bu yallah. Ca tuur yi amone na: Ra (moye ku ñu leeral), Amon (moye Ku nebbatu), Atoum (ku kumpa), Atona-Ankh (Doole bi ku yengal aduna).

Taarixkat yi Seex Anta Joob ak yenene, woné nanu, diiney yawut, kirist ak Lislaam, fofu (wa Misra) lañu cossano. Ndax yonent yi ñu nek ca diiney yawut ak kirist, ca sene teree, biibël ak thora, Ibrahima ak Moussa, fofu lañu jang diiney, ca bi ñu tuddu ca lakk wa misra bu fa amone jamono bobu, Per-Ankh, ca kalamu wolof moye: Keur bu ñu jang Diiney ak xam xam. Ba paré yobu nañu Diiney bobu ca sene Mbokku yawut, ndax bobu amuñu woon Diiney, nak bu urus ak Moloch ak Baal lañu doon geum. Fofu tamit lañu jang naka lañu saraxé Xaar, ak naka lañu xarafal, ca Per-Ankh yi. Ndax ca diiney bu afrig, sarax ak xarafal amona bu yag, ba tey. Taarikhkat woné nañu tamit, yawut yi nekkone ca rewum nit ku niul ba, wa misra, kene deful leen ay jaam. ñow nañu fofu ca jaam, gën misra ca jaam.

Wa misra moye fofu xeet yi nek ca biir afrig tey, cossano, té diiney bu fa amone, yobu nene ko ca fofu lañu deuk tey, reewum Afrig bu nek ca suuf Saara.

Buñu waccé ca Afrig bobu, xeet yi tass nañu yu bari, té ba paré xeet ku nek, amone nañu bene tuddu ngiir tuddu yallah:

  • Mandinke yi (Sooninke, Bambara, Jula, Xasonke, ak ñu dem nonu) yallah, Maa Ngala lañu daan wax.
  • Pël yi, Gueno lañu daan wax.
  • Séeréer yi, Roog Seen
  • Joolaa yi, Atemi Sembe
  • Sonraï yi deuk ca Mali ak Niseer, Yarkoï
  • Bassari ak Bedik yi, Ounounga
  • Dogon yi: Amma
  • Yoruba yi Ca Niseeria: Olodumare
  • Masaï yi ca Kenya: Engaï
  • Zoulou yi ca Afrig bej Saalum: Inkosi
  • Akan yi, ca rewum Bene, Togo, gana, kote diiwaar: Mawu
  • Wa Ecoopi: Waqa
  • wa Kongo ca xeet yi Bantu: NzamBe

Diiney bi tamit, xeet yi Afrig bi, amona ku nek, joox na ko bene tuur, Vodu ca wa Bene, Togo, Gana, ba Niseeria, wala Bwiti ca wa Gabon, Mwett wa Cameroon.

Ca Diiney bi, bu amone ca Afrig, danu ne Yallah kene munul ko wo. Ndax ca diiney bi, nit yi dañu wax, Yallah mag na torop, mag na ba, kene ku munul ko woo. Dañu ne yallah baxna ba munul jox kene te joxul kenene. Li moye tax yallah ca diiney bobu, ca nit ku nek, tek na ca seen biir, bene dogu yaramam. Dogu yaramam bu nek ca nit yep, dog bobu nit yi ño wara jang, té defni mu set sasounek suñu beugeu am jam ca aduna, ak yenene nit yi ak sene njabot, wala am kheweul ca sene liguey, ak yu demé nonu. Wala suñu beugeu dem ajjana.

Ca diiney bobu, mam yi ñu nek ca rewum yallah, ño nek ca diganté yallah ak nit yi. Mam yi, ño yobu ñaan yi nit yi ca yallah. Li moye tax ca diiney bu am Afrig, mam yi, amna nu solo. Ca Seereer yi nek ca Senegaal, mam yi Pangol moye seen tuur. Lebu yi, mam tuur lañu wax.

Ca yonu imbraator gu gana, lislaam ñow na soowu Afrig, ca jamono bobu, lislaam ak diiney bu Afrig, ca jaam lañu nekkone. Ak tubap yi, diiney yu nasaraan ño na afrig, wa diggu afrig.

Ak Jihad yi jullit defonne ca XIXee xarnu, diiney bu Afrig ba, wañi na bu bari. Tubap yi tamit ak canc gi, defna ñu, diiney afrig bobu mu wañi bu bari.

Wayé amna ay xeet, diiney lislaam wala kirist lañu nek, wayé dañu dugal ca seen geum, ay yeufu nek ca diiney afrig bobu (Syncrétisme) melni joola yi, wala Bantu yi, lebu yi, Akan yi.