Pël wuute gi ci sumb yi

Contenu supprimé Contenu ajouté
Guérin Nicolas (waxtaancëru)
Aucun résumé des modifications
Guérin Nicolas (waxtaancëru)
Aucun résumé des modifications
Rëdd 1 :
Pël genn giir la gu nekk Senegaal. Pël yi ci [[Sowwu Afrig]], dañoo bokk ci waaso yi gën a bari gën a yaatu. [[Senegaal]], [[Mali]], [[Gànnar]], [[Gàmbi]], [[Gine]], [[Gine Bisaawóo]], [[Niseer]], Burkina Faso, Niseeria, Benin, Kot Diwaar, Kameroon, Réewum Diggu Afrig, ba Sudaan, ca réewum yii yépp Pël yi ña nga fa.
Xeet woowu am nañu tur yu bari: Pël ci [[Wolof]], ci [[Afrig]] mooy tur wi gën a siiw, Fula ca Mande ya, Fulani ca Naar ya, Fellata wala Fellan ca [[Sudaan]].
[[ImageDencukaay:Eleveurs Peuls.jpg|thumb|200px|left|Sàmmkatu Pël bu Gurma, bëj-saalumu [[Gao]], [[Mali]]]] ÑÑoom ci seen bopp dañuy wax Pullo wala FulBe. [[Isipt]] mooy réew mi ñu bawoo. Pël ya ca Isipt ay nit ñu ñuul lañu nekkoon. Ba noppi, ay nit ñu weex, ñëw ca seenum réew juge [[Asi]] ak [[Tugal]] , bokk na ca xeet yooya: Scythe, Aryen, Phrygien, Hittite, askan yu bari yu ñuy tudde ay waa End-tugal (Indo-européen). Pël yu ñuul yi ak nit ñu weex ñi dañoo jaxaasoo woon. Lii moo tax Pël yi gën a xees, gën a sew, am kawar gu gën a nooy, bu ñu leen xoolee ci yeneen xeet yu ñuul yi ci Afrig. Ba noppi, Imbraatóor gu Iran(ñoñ Cambyse ñi(les Perses) ), tegoon nañu loxo réewum Isipt, di fa tege dund gu metti, rawati na ca nit ñu ñuul ña. Lii moo tax Pël ya ak Séeréer sa gàddaay, dëkki ca [[Sudaan]] (Nubie) dëkki seeni maam, soog a dem Senegaal. Pël ak [[Séeréer]] danoo bokk maam, seeni làkk tamit. Yàgg nañoo ànd, dañuy kalante ci seen biir. Ca yoonu [[Tekuruur]], pël ya ca Dexug Senegaal rekk lañu nekkoon ak seeni nag. Booba nekkuñu woon ay jullit. Amuñu woon nguur ndax ak seeni nag ci màng rekk lañu nekke woon. Meew ak Sanqal (ñórndi) moo doonoon seenu lekk. Pël ci boppam am na xeet yu bari (Leyyi/KinDe), Ardo mooy seen Buur: JaawBe yi, UrurBe, WodaaBe, LaaCe, CutinkooBe, YirlaaBe. Am na yeneen KinDe. Màng gi ñu dëkke tax na ñu tuuru ci Sowwu Afrig gépp, ba far delseeti Sudaan, cig muñ ak coona ndax saa su nekk ci dëkki jàmbur yi rekk lañuy nekk, seen nag yi leeg-leeg ñu ruur tooli baykat yi, loolu it di jur xuloo bu rëy ak ŋaayoo ci seen digg ak woroon tool yi.
 
Ca atum 1539 Koli Tengella Bâ, mi ngi bokke ci Pël ci wetug baayam, bokk it ci Mande yi ci wàllug yaayam (Keyta), dajale woon na sàmmkati Pël yi ak mande yi, ngir ñu man a am doole. Daa di dugg ci yeneen xeet (Wolof, Séeréer, Bajaaranke, Joola, Baga, [[Sooninke]] . Ñoom ñépp ak seen aroo Koli Tengella, ñu yéeg ba Tekuruur, di xeex ak Buur-ba [[Jolof]] ba, ndax kii moo doon yor dëkk ba, ak Lam-Toro ya, Lam-Térmes, Lam-Taga ya, Juroom ñeenti fan soog a yor dëkk ai. Koli Tengella teg na fa njabootam (Denyakoobe yi), tudde na nguur ga Fuuta-Toro (Fuuta mooy dëkku Pël ca seen Làkk). Lii ca Senegaal la xewe.
Ci « https://wo.wikipedia.org/wiki/Pël » lañ ko jële