Tukkloor wuute gi ci sumb yi

Contenu supprimé Contenu ajouté
an
(Aucune différence)

Sumb bu 6 Fewriyee 2009 à 03:54

Tukkloor genn giir la gu nekk Senegaal. Ñom ca seni bopp, Halpulaar lani tuddu. Nguruu Fuuta-Toro moye seni deuk, li moye tax deni wax tamit FuutankoBe (ku deuk ca Fuuta). Ñom dexug Nil lani jogué, ca deuk bi nu tudd Nubie, tey di nek ca rewum Suudan. Fofu Tekruri mo done seni tuur. Li moye tax bobu nu ñowé ca dexug Senegaal, Tekuruur (deuku tekruri) moye tuuru nu jooxé deuk bi. Kon ñom no tabax Tekuruur. Wa é, ca deuk bi amona tamit yenene nit y fa deuk, ca xetu Séeréer ak Pël lani bokk woon. Tekruri, Séeréer ak Pël y, danu jaxaasé, bokkenté, ba paré Sooninké, Naar y tamit ño nanu ca ñom, ba nek bene askan, tey ñom ño Tukuloor y. Tuuru Tukuloor ca lakk tubap la jogué, tukuloor la ñi done waxé ndax danu jaxaasé. Wa é su ñu xolé Sant bi ñi yoor, ca seen askan, di neen xaam nit y lan moye seni xetu mam. Tukkloor yëp Pulaar moye seni lakk, tamit ñëp juulit lañu. Lislaam mo lene geuneu dadjalé. Tukkloor y danu tel duggu ca lislaam, ca yonu imbraatoor gu Ghana. Sooninke y ño lene dugal ca lislaam. Buuru tekuruur bi War Jaabi, mo indalé lislaam ca nguruu bi, Sooninke la woon (Sumaré) di bokk ca njabotu Manna y. Ba nopi, dañu andalon ak Naar y (Almoravide), di def ay Jihad ca tekuruur.

Ca XVIeelu xarnu, bene seriñu tukuloor mu tudd Ali Elibana Sall, ak jaambaram Jihad nañu ca Fuuta-Toro, ndax ay DeñankoBe y ak Koly Tenguela ño done yoox nguruu bi té nekuñu ay juulit. Wa é deñankoBé y daq neen Elibana Sall ak jaambaram. Ñom daw nañu baa Saalum, fofu dañu Jihad ca Séeréer y wa é ñom daq neen Ali Elibana ca dexug Gaambi, fofu tukklor y tabax nañu bene nguruu moye nguruu Kabada. Ca XVIIeelu xarnu, Malik Sy Dauda, tabax na nguruu Bundu, ca Senegaal, ca weti nguruu Jolof, ak Galam. Mom tamit Defna Jihad ca Fuuta-Toro, deñankoBé y di ko daq deuk bi. Mom ak njabotam, Jaambaram daw nañu ca Njaarmëw, wa é fofu amatu fa woon Buur, Fofu la tabax nguruu Bundu. Malick Sy Dauda, torodoo la né woon. Ca XVIIIeelu xarnu, Torodoo Tukklor y daq neen DeñankoBe y fa done Buur (Silatigi). Li yëp ak Souleyman Baal ak Abdul Kader Kan la xéwée. Ñom nak duggu nañu FutankoBé yëp ca lislaam, teg nañu tamit ay Almamy, Almamy bobu mo yooré woon nguruu bi, da warone na nek Seriñ bu geuneu am xam-xam ca lislaam ca FutankoBé y. Ca XIXee xarnu, El Hadji Omar Taal, tabaxna imbratoor gu Tukkloor ca Mali. Omar Taal, demna ca Makka, fofu Xaalifa y, def neen ko, Xaalifu Tijaaniya ca rewmi nit ku ñul. Omar Taal duggu na ay nit yu bari ca tariqa Tijaaniya. Jihad na ca nguruu Xaaso wa é fofu tubap y daq neen ko. kon demna ca Mali, xéer na ca nguruu Jara rey na fa Buur ba (Biranté Karunga Jawara). Xéer na ak Buur y Bambara y (Fama), ca nguruu Ségu ak Kaarta, di lene uuf ca imbratooram. Xéer na ak Ahmadu Bari, Buuru Massina, di ko uuf tamit. Ca XIXeelu xarnu, Maba jaxu Ba, Almamy bu Rip lané woon. Rip modone ben Nguruu ca Biir Nguruu Saalum. Ca Rip ay Buuru Mandé (Marone) mo fi nekkone. Nguruu bi Badibu la tuddé woon, Maba jaxu mo ko joox turru Rip. Ndax mu meunteu nek Almamy, Maba jaxu jihad na ca badibu yëp di rey Buuri yëp. El Hadji Omar Taal, mo ko né mu def lolu, ndax giis na ti mom, nitu xam lislam bu bax. Ca atum 1871-1875, Amadu Seexu, bene Almamyu Fuuta-Toro, jihad na ca nguruu Jolof, di fa nek Buurba, ñienti at.

Tukkloor seni Nosteg mboolaay ga nii la tëdde woon:

RimBé y ño done:

  • Sebbe y, Jambaaru lañu woon, ñom ay Ceddo lañi nekkone. Sebbe yu bari ca xetu Wolof ak Séeréer lañi jogué. Ba XVeelu xarnu ba atum 1776 ñom ño yooxon Fuuta-Toro.

Seni sant: Njaay, Joop, Juuf, Faay, Geeye, Jaw, Bâ, Ndaw, NgayDo, Sall, Wade, Lo, Mbodji, Konté, Ly

  • Torodoo y, ay juulit lañu, ca atum 1776 lañi dieuk am dolé. Ñom ño daq Sebbe y, di lene duggu ca lislaam. Buuru Torodoo y Almamy la. Señi mam yu bari ca xetu Sooninke ak Naar lañu jogué.

Seni sant: Sy, Ly, Kaan, Haan, Tuuré, Ciise, Sumaré, Aïdara, Njaay, Mbodj, Faal, Wane, Ja, Sall, Bâ. Amna yenee.

  • JaawamBe y, ño done topp Buuri, di lene wone lan lañi yooré nguruu. Ca Pël y lañi bokk seni sant : Jaw, Ñaan, Daf, Njim, Bokum.
  • SubalBe y, nappkat ak jambaar lañu. Dañu bokk ak Sebbe y. Yu bari seen mam ay Séeréer lañu. Señi Buur (Teeñ, Jagodin) lañi tuddu. Seni Sant: Sarr, Ñang, Juuf, Jeng, Jaw. Amna yenene Sant.

Ñeeno y:

  • WayilBe ño done Teug y.

Seni sant : Caam, Mbow (Pël), Kanté (Mandé)

  • LawBe ño done Seen y.

Seni sant: Sow, Jum (Pël), Gadiaga (Sooninké)

  • SakeeBe, ño done Wuude y.

Seni sant: Beye (Wolof) Gakou (Mandé)

  • MabuuBe, ño done Rabb y.

Seni sant: Gisé , Sangott, Tall, (Tukkloor)

  • BaambaaDo, ño done Xalamkat y, waykatu Jambar y. Seni sant:

Bâ, Jum (Pël), Gisé (Tukkloor)

  • Gawlo, Waykatu Buuri.

Seni sant: Mbum, Samb, Seek, Jeng, (Wolof), Lam (Pël).

Jaam y:

  • Maccudo/Kordo/JyaaBe. Ca xet yëp lañi jogué.

Tukkloor y, Mbey moye seni dund, amna ay sambkat. Dañi señi Rewm (Fuuta), ca Fuuta-Jalon amna fa ay Tukkloor, ca Kajoor dañi deuk ca diiwanu Jambuur (Region de Louga). Amna yu bari dañi daw Fuuta bi, di dem ca Dakar, Kawlak, Cees, wala Ndaar. Ñu ti bari ca tariqa Tijaaniya lañu bokk.