Pël wuute gi ci sumb yi

Contenu supprimé Contenu ajouté
Aucun résumé des modifications
Aucun résumé des modifications
Rëdd 1 :
Pël genn giir la gu nekk Senegaal. Pël y ca Sowwu Afrig, danu bokk ca xet y nio gëneu bari. Senegaal, Mali, Gànnar, Gaambi, Ginee, Ginee Bisaawoo, Niseer, Burkina Faso, Niseeria, Benin, Kot Diwaar, Kameroon, Réewum Diggu Afrig, ba Sudaan, ca réewum y yëp Pël y nio ngi fa.
Xet bobu amna nu tuuri bari: Pël ca [[Wolof]], ca afrig mo tuuru gëna siiw, Fula ca Mandée y, Fulani ca Naari, Fellata wala Fellan ca Sudaan.
[[Image:Eleveurs Peuls.jpg|thumb|200px|left|Éleveurs peuls du Gourma, sud de [[Gao]], [[Mali]]]] Seni bop deni wax Pullo wala FulBe. Isipt moye deuk bi nu juddu. Pël y ca Isipt aye nit ku nul lani nekkone. Ba paré ay nit ku wéex, nio na nu ca seni deuk, niom réewum Asiak[[Asi]] tugal lani jogue woon, bokk ca xeti: Scythe, Aryen, Phrygien, Hittite, askan yu bari bi nu tudd ca lakk tubap y (Indo-européen). Pël y niul y aki nit ku wéer nonu, danu jaxaasé. Li moye tax Pël y da nu xawa gëna xées, gëna séew, am karowu gëna noye, yenene xetu nul y ca Afrig. Ba nopi, Imbratoor gu Tirki (Perse), uuf nanu réewum Isipt, di fa tek dundu meti ca niul y. li moye tax Pël ak Séeréer y dem nanu deuk ca Sudaan (Nubie) deuki seni mam, sogo dem Senegaal. Pël ak [[Séeréer]] danu bokk mam, seni lakk tamit. Yag nanu and, danu kalenté. Ca yonu [[Tekuruur]], pël y ca Dexug Senegaal rek lani nekkone ak seni Nak. Bobu nekkunu juulit. Amunu woon nguruu ndax ak seni nak ca tuki rek lani dundé. Meew ak Sankhal modon seni lek. Pël ci sen bopp amna xet yu bari (Leyyi/KinDe), Ardo bi moye seni Buur: JaawBe y, UrurBe, WodaaBe, LaaCe, CutinkooBe, YirlaaBe. Amna yenene KinDe. Tuki bi nu dund moye tax turu na nu ca Soowu Afrig yëp ba niowat Sudaan, di muun ndax sasounek ca deuki njabuur lani dundnéké.
 
Ca atum 1539 Koly Tenguella Bâ, ca Pël la bokk ca bayam, ca Mandé y la bokk ca yayam (Keyta), dadjalé na sambkatu Pël y ak mandé y, ndax nu meunteu am dolé. Ca Jambaram da di dugg ay yenene xet (Wolof, Séeréer, Bajaaranké, Jola, Baga, [[Sooninke]] ya. Niom yëp, ak sen ArDo Koly Tenguella, yég nanu ba Tekuruur, di xéer ag Buurba [[Jolof]] ba ndax ki modone yoor deuk bi, ak Lam-Toro y, Lam-Térmes, Lam-Taga y, Juroom nent fan sogo yoox deuk bi. Koly Tenguella degteg nafa njabotam (Denyakoobé y), tuddu na nguruu bi Fuuta-Toro (Fuuta moye Deuku Pël ca seni Lakk). Li ca Senegal la xeewé.
Ca Mali Pël y danu dieuk am doolé ca atum 1818. Bobu nak Ahmadu Baari, Serign lanéla né woon, dadjalé na Pël u Juulit y, ak Mandé yu juulit ( Mandé Mori y : Cissé, Tuuré, Sylla ), ndax nu meunteu xéer (Jihad) nguruu Bambara y fi nekkone (nguruu Ségu ak Kaarta). Buuru Bambara y (Fama) ak seni jambar (Ton-Dyon), amone nanu doolé, li moye tax Ahmadu Baari tabax na Imbratoor gu Pël ca Massina késsé. Tamit Pël y, ca Mali, fofu lani eupé woon ba tey (Tey di nek Région De Mopti).
Ca Ginne, Pël y danu fa yag, wa é Mandé y (Jalonké) nio yooron deuk bi. Ca yonu 1715, ay Pël yu juulit yu jogué Fuuta-Toro ak Massina ca Mali, nio na nu ca Ginne, di fa Jihad, di rey ku du juulit wala di ko jaamlo, li moye tax xet yu bari (Susu y, jalonké, ak Baga y) daw nanu ca guedju Ginne, di tabax fofu ay ngurrunguruu. Pël u Juulit y dani reyone tamit yenene Pël ndax nekku nu woon juulit. Pël y juulit danu mbokkone ca njabot: Bâ, Baari, Jallo, Sow. Niom no tabax nguruu Fuuta-Jalon. Karamoko Alfa Jallo mo dieuk a nek Almamy.
Ca Nisseria atum 1808, Usman Dan Fodio, njabotam Fuuta-Toro lani djogué di nek ay Toroodo, Serign bu mak la nekkone di bokk ca tarixa Xaadiriyya. Mom nak Dadjalé na Mbeykatu Haaussa, ak Sambkatu Pël, di lene dugg ca lislaam, ndax nu meunteu def Jihad ca Nguruu Haaussa y fi nek. Rey na Buuru Haaussa, té Tabaxtabax na Imbraator gu Sokoto. Demna xéer ca Imbratoor gu Kanem-Bornu ca Caad, wa é nio nunionu danu amone doolé torop.
Ca kaw Kameroon atum 1810, bene Serign bu tudd Modibo Adama, dadjalé na Pël u juulit (fofu Fulbé la ni wax) y fi nékkone, nu tabax Nguruu Adamawa. Wa é amna Fulbé yu bari (WodaaBe/Borooro), bugu nubugunu woon bobu nguruu.
Modibo ak yenene Pël la def Jihad, ndax dunu nekkone ay juulit. Modibo Adama, Usman Dan Fodio moko dimbali.
Ca atum 1860, Alfa Yaya Molo Baaldé, tabax na nguruu Fuladu ca Bëj-saalum Senegaal. Da dadjalé Pël y di lene dugg ca lislaam, ndax Almamy u Fuuta-Jalon Alfa Bokar Biram, né na woon du dimbali, kuduul Juulit.
Almamy bobu ak Alfa yaya xéer nanu nguruu Mandé Kabbu ak seni Buur (Mansa), ndax fofu Pël danu nekkone JaamuJaami Mandé y. Niari Buur rek nio yoron Fuladu, Alfa Yaya ak domam Moussa Molo Baaldé.
Kone Pël y, lislaam mo lene dadjalé, di lene jox doolé.
Ci « https://wo.wikipedia.org/wiki/Pël » lañ ko jële