Pël wuute gi ci sumb yi

Contenu supprimé Contenu ajouté
Gamadji~wowiki (waxtaancëru)
Xët wu bees : Pël genn giir la gu nekk Senegaal. Pël y ca Sowwu Afrig, danu bokk ca xet y nio gëneu bari. Senegaal, Mali, Gànnar, Gaambi, Ginee, Ginee Bisaawoo, Niseer, Burkina Faso, Niseeria, ...
(Aucune différence)

Sumb bu 5 Fewriyee 2009 à 03:52

Pël genn giir la gu nekk Senegaal. Pël y ca Sowwu Afrig, danu bokk ca xet y nio gëneu bari. Senegaal, Mali, Gànnar, Gaambi, Ginee, Ginee Bisaawoo, Niseer, Burkina Faso, Niseeria, Benin, Kot Diwaar, Kameroon, Réewum Diggu Afrig, ba Sudaan, ca réewum y yëp Pël y nio ngi fa. Xet bobu amna nu tuuri bari: Pël ca Wolof, ca afrig mo tuuru gëna siiw, Fula ca Mandée y, Fulani ca Naari, Fellata wala Fellan ca Sudaan. Pël dani tudd seni bopp: Pullo wala FulBe. Isipt moye deuk bi nu juddu. Pël y ca Isipt aye nit ku nul lani nekkone. Ba paré ay nit ku wéex, nio na nu ca seni deuk, niom réewum Asiak tugal lani jogue woon, bokk ca xeti: Scythe, Aryen, Phrygien, Hittite, askan yu bari bi nu tudd ca lakk tubap y (Indo-européen). Pël y niul y aki nit ku wéer nonu, danu jaxaasé. Li moye tax Pël y da nu gëna xées, gëna séew, am karowu gëna noye, yenene xetu nul y ca Afrig. Ba nopi, Imbratoor gu Tirki (Perse), uuf nanu réewum Isipt, di fa tek dundu meti ca niul y. li moye tax Pël ak Séeréer y dem nanu deuk ca Sudaan (Nubie) deuki seni mam, sogo dem Senegaal. Pël ak Séeréer danu bokk mam, seni lakk tamit. Yag nanu and, danu kalenté. Ca yonu Tekuruur, pël y ca Dexug Senegaal rek lani nekkone ak seni Nak. Bobu nekkunu juulit. Amunu woon nguruu ndax ak seni nak ca tuki rek lani dundé. Meew ak Sankhal modon seni lek. Pël ci sen bopp amna xet yu bari (Leyyi/KinDe), Ardo bi moye seni Buur: JaawBe y, UrurBe, WodaaBe, LaaCe, CutinkooBe, YirlaaBe. Amna yenene KinDe. Tuki bi nu dund moye tax turu na nu ca Soowu Afrig yëp ba niowat Sudaan, di muun ndax sasounek ca deuki njabuur lani dund.

Ca atum 1539 Koly Tenguella Bâ, ca Pël la bokk ca bayam, ca Mandé y la bokk ca yayam (Keyta), dadjalé na sambkatu Pël y ak mandé y, ndax nu meunteu am dolé. Ca Jambaram da di dugg ay yenene xet (Wolof, Séeréer, Bajaaranké, Jola, Baga, Sooninke ya. Niom yëp ak sen ArDo Koly Tenguella, yég nanu ba Tekuruur, di xéer ag Buurba Jolof ba ndax ki modone yoor deuk bi, ak Lam-Toro y, Lam-Térmes, Lam-Taga, Juroom nent fan sogo yoox deuk bi. Koly Tenguella deg nafa njabotam (Denyakoobé y), tuddu na nguruu bi Fuuta-Toro (Fuuta moye Deuku Pël ca seni Lakk). Li ca Senegal la xeewé.

Ca Mali Pël y danu dieuk am doolé ca atum 1818. Bobu nak Ahmadu Baari, Serign lané woon, dadjalé na Pël u Juulit y, ak Mandé yu juulit ( Mandé Mori y : Cissé, Tuuré, Sylla ), ndax nu meunteu xéer (Jihad) nguruu Bambara y fi nekkone (nguruu Ségu ak Kaarta). Buuru Bambara y ak seni jambar (Ton-Dyon), amone nanu doolé, li moye tax Ahmadu Baari tabax Imbratoor gu Pël ca Massina késsé. Tamit Pël y ca Mali, fofu lani eupé woon ba tey (Tey di nek Région De Mopti). Ca Ginne, Pël y danu fa yag, wa é Mandé y (Jalonké) nio yooron deuk bi. Ca yonu 1715, ay Pël yu juulit yu jogué Fuuta-Toro ak Massina ca Mali, nio na nu ca Ginne, di fa Jihad, di rey ku du juulit wala di ko jaamlo, li moye tax xet yu bari (Susu y, jalonké, ak Baga y) daw nanu ca guedju Ginne, di tabax fofu ay ngurru. Pël u Juulit y dani reyone tamit yenene Pël ndax nekku nu woon juulit. Pël y juulit danu mbokkone ca njabot: Bâ, Baari, Jallo, Sow. Niom no tabax nguruu Fuuta-Jalon. Karamoko Alfa Jallo mo dieuk a nek Almamy. Ca Nisseria atum 1808, Usman Dan Fodio, njabotam Fuuta-Toro lani djogué di nek ay Toroodo, Serign bu mak la nekkone di bokk ca tarixa Xaadiriyya. Mom nak Dadjalé na Mbeykatu Haaussa, ak Sambkatu Pël, di lene dugg ca lislaam, ndax nu meunteu def Jihad ca Nguruu Haaussa y fi nek. Rey na Buuru Haaussa, té Tabax na Imbraator gu Sokoto. Demna xéer ca Imbratoor gu Kanem-Bornu ca Caad, wa é nio nu danu amone doolé torop. Ca kaw Kameroon atum 1810, bene Serign bu tudd Modibo Adama, dadjalé na Pël u juulit (fofu Fulbé la ni wax) y fi nékkone, nu tabax Nguruu Adamawa. Wa é amna Fulbé yu bari (WodaaBe/Borooro), bugu nu woon bobu nguruu. Modibo ak yenene Pël la Jihad, ndax dunu nekkone ay juulit. Modibo Adama, Usman Dan Fodio moko dimbali. Ca atum 1860, Alfa Yaya Molo Baaldé, tabax na nguruu Fuladu ca Bëj-saalum Senegaal. Da dadjalé Pël y di lene dugg ca lislaam, ndax Almamy u Fuuta-Jalon Alfa Bokar Biram, né na woon du dimbali, kuduul Juulit. Almamy bobu ak Alfa yaya xéer nanu nguruu Mandé Kabbu ak seni Buur (Mansa), ndax fofu Pël danu nekkone Jaamu Mandé y. Niari Buur rek nio yoron Fuladu, Alfa Yaya ak domam Moussa Molo Baaldé.

Kone Pël y, lislaam mo lene dadjalé, di lene jox doolé.

Pël seni Nosteg mboolaay ga nii la tëdde woon:

  • RimBe no done Buuri.
  • JaawanDo y, no done top RimBe di lene wone lan lani yooré nguruu.

Neeno y:

  • WayilBe no done Teug y.
  • LawBe no done Seen y.
  • SakeeBe, no done Wuude y.
  • MabuuBe, no done Rabb y.
  • BaambaaDo, no done Xalamkat y, waykatu Jambar y.
  • Gawlo, Waykatu Buuri.

Jaami:

  • Maccudo wala Kordo.

Ca Isipt Pël y, da nu niet Sant rek (Ba, Ka, Bara (tey mou nek Baari)). Ba paré Pël y danu jël yenene Sant Ndax deuk bi, wala Mban yi, liggey yi done def. Li yeup ba am tey Sant gi: Bâ, Baari, Jallo, Kâ, Ja, Sow, Jaw, Caam, Naan, Jum, Dikko, Seydi, Mbow, Bokum, Dem, Sidibé, Sall, Ca fuladu Pël yu bari Jamanka lani Sant. Ca Mali Sidibé moye Sow. Ca niseeria Pël yu bari Bello lani Sant. Ku Sant Baal, mamam ay Bâ lani woon. Ku Sant Jakk maman ay Sow lani woon. Sankara, Sankaré, Shagari, li yëp bene la. Amna Pël yu bari demna nu ca Wolof yi li moye tax amna ay wolof ku sant (Caam, Mbow, Sow, Naan, Sall). Tamit amna Xët yu bari nio nanu ca Pël, li moye tax amna ay Pël ku sant Cissé, Tuuré, Njaay, Jakité, Kamara ak yenene sant.