Imbraatóor gu Gana wuute gi ci sumb yi

Contenu supprimé Contenu ajouté
Aucun résumé des modifications
Budelberger (waxtaancëru)
mAucun résumé des modifications
Rëdd 1 :
[['''Imbraatóor]]''' (empire) '''gu Gana''' :
[[Image:Empire_ghana.png]]
 
[[Imbraatóor]] gi mag ci yu [[Afrig]] yi taariixkat yi mas a xam mooy : gu Gana. Li ñu jot a xam ci taariixam ñi ngi koy sante [[gëstuy]] boroom xam-xami jeexiit yi, ak nettaliy gimiñ yi, ak mbindi tukkikati naar yi.
 
[[Gana]] mi ngi sosu ci [[ñeenteelu xarnu g.j]], jamono jooja it nguur gu ndaw la woon gu ñu daa woowe '''Ogaadoo'''.
[[Ci]] juroom [[ñatteelu xarnu g.j]], la ab xareem (son armé) jugoon song ay suuf yu yaatu, yu nekk ci diggante dexug Senegaal ak [[Nijeer]], ci noonu la Gana wëlbatikoo di imbraatóor gu mag gu teg loxo ci dëkk yi mu feggool…
 
[[Imbraatóor]] gi nekkoon na di gu naat : ay suuf yu nangu mbay ak sàmm, mu daa bokk ci yaxantug tàkk gi(gi nu daa defe ci [[tàkk]] gi) ak njaayum wurus mi, moom imbraatóor gi amoon na ay mbelli wurus yu bari yoy ki ko daa topptoo mooy Kayaamagana, [[maanaam]] njiitul wurus li : waa jii da daan nekk njiit lu dëgër, lu ñu wormaal, luy àtte cig maandute te daan samp [[foŋsaneer]] yi.
[[Moom]] nag cim koom ak naataange la daa dunde ci péeyam, waa diiwaan bii it dañu ko daa indil ay kem ci wurus wi ñiy génnee [[ci]] suuf si, ginnaaw bi mu faatoo nag la ko fi ab jarbaatam wuutu.
[[Ci]] atum [[1052 g.j]], la Muraabituun yi song Gana, ci layuw dañuy dugal ñoñam ci lislaam, ñu daal di ubbi péey ba atum [[1076 g.j]], [[ginnaaw]] bi Gana néew doole, daal di daanu ci mujjantal gi ci loxoy [[imbraatóor gu Mali]] atum [[1240 g.j.]]
 
 
[[fr:Empire du Ghana]]