Bennoo gu Almaañ wuute gi ci sumb yi

Contenu supprimé Contenu ajouté
Abdu Xaadir KEBE (waxtaancëru)
Budelberger (waxtaancëru)
Rëdd 149 :
 
 
== Xareb Brusiya ak Faraas: ==
 
Xetug xare tàmbli woon na a xeeñ ak a jòlli ci diggante Fraans ak Brusiya, ginaaw bi Brusiya '''ndàmbee ndam''' ca xareb Sadwa ba. Ndaxte Faraas moom begutoon dara ci lii Brusiya amal ciy ndam ci kaw Danmark ak Otris cig wàll, ak àntul gi mu àntuloon bennoo gu Almaañ gu bëj-gànnaar gi, ci geneen wàll.
 
Ligne 157 ⟶ 155 :
 
Lëj-lëju ku jigéen ki waroon a donn Espaañ daal di taxaw, mooy lëj-lëj bi taaloon xare bi ci diggante Brusiya ak Fraans.
Lëj-lëj boobu mi ngi tënkoo woon nii: gàngunaay gu nguurug Espaañ dafa féexoon , ginaaw bi lingeeru Espaañ bi Elisabeth dawee, ñu gaaral buur bi [[Leopold]] ndëpp li, moom mi ngi bokkoon ci njabootug [[Hohenzellern]], di woon ab jegeñaaleb imbraatóor bu Brusiya. Waaye ak li Leopold di bañ lepp ne du sol mukk ndëpp li, teewul Faraas mer ci loolu, jàmbat ko ci buurub Brusiya bi, daal di sàkku ci moom mu warlu ne du ànd ci ñu samp kenn ku bokk ci njabootug Hohenzellern ci gàngunaayaug Espaañ gi. Waaye buuru Brusiya bi bañ, ndax loolu kat dafa xaw a laal teddngaam ak ngoram, te xaw a niru ag yabeel. Loolu nag mi ngi ame woon cim ndaje mu mu defoon ak aji teewal ju Faraas ja ca Ems. Bu ko defee buuru Brusiya bi yonnee ab day ca la juge woon ca ndaje ma, mu yonnee ko Bismarck, mi nga xam ne lepp li mu doon def mooy neggandiku ab pose ééngir jibal ab xare ci kaw Faraas. Ba mu ko defee, Bismarck xëy tas ci yéenekaay yi ay cofiit ca la bawoo woon ca ndaje mooma, ngir merloo ci Faraas. Loolu nag ni mu ko defe mooy génne ay baat yu xaw a wow, yu begloowul dara Faraas. Ci noonu Faraas jug, jibal ab xare ci kaw Brusiya, ci 14 sulet 1870g, te fekku ko woon jekk ngir xeex, te taxul woon it mu xalaat ci ngérte yi man a juddoo ci bii xare, bis bu ñu dàqee Fraans ci xeex bi.
 
Brusiya li ñuy wax xareb fëkk la doon def ak Faraas, maanaam gaawal ko, loolu nag jot na koo def ba am ci xam-xam ak jarbu ca xareem ba’ak Otris. Bi mu ko defee tàngooru xare bi sax di tar lu tollook juroom benni ayu bis, waaye tàmblee giim, ci ginaaw bi, rawati na ci ginaaw bi ay màndargay kawe ak ëpp doole tàmblee feeñ ci xeex bi ñeel Brusiya.
 
Xare bi bepp nag ci suufus Faraas la doon tàkke. Jotoon nañoo dàq Fraans nag ci xeex yu bari, bi ci gënoon a siw nag mooy bu [[Sedan]] ca satumbar1870gsatumbar 1870g, nga xam ne àggoon na ci Napoleon III manutoon a ñàkk a wommatu (se rendre), te nangu ne gañe nanu ko, ngir dàq yu metti yi te toftaloo, te yepp di yu nu teg ci kaw dooley Faraas ji ci biir suufus Faraas, te ray lu sakkan ciy soldaaram, te itam lu jege ñaari téeméeri junniy soldaari Almaañ sutuxlu ba ca xolub Faraas, te mu leer nàññ ne Faraas moom manatul a gañeeti Brusiya ca jamono joojee te manatu koo génneeti suufam. Loolu nag di woon ci [[27 oktobar]] 11870g1870g.
 
Ci noonu imbraatóor gu Faraas gu ñatteel gi daanu, ñu daal di taxawal ci Paris nosteg pénc gu ñatteel gi. Daal di teg Faraas ñeel Brusiya alamaanug xare gu toll ci juroomi bilyoŋi frank yu Fraans ( loolu mooy tollook – daanak – alamaan bi Napoleon Bonaparte tegoon Brusiya bi mu ko dumaa ca xareb Yena ba, 1806g. Bu ko defee ñu juboo ci xarekati Almaañ yi duñu génn Faraas li feek fayeesul alamaan bi, (moom nag jotees na koo fay ci diirub ñatti at). Nga rax ci dolli dagg gi ñu dagge ñaari diiwaan yii di Alsaas ak Loren ci faraas, boole leen ci Almaañ.
 
Nii daal la bennoo gu Almaañ mate woon ci njiitul Brusiya, ci loxol góor gu dëgër gii ni weñ, Bismarck, mi nga xam ne dafa gëmoon bennal Almaañ '''ak doonte day ci dereet, ci weñ mbaa sawara'''. Bu ko defee imbraatóorug Almaañ gi daal di sosu, dib xew-xew nag bu fés ci taarixu Tugal bu bees bi.boroom gàngunaay gi (imbratóoru Almaañ bi) mujj di '''ku ñu joyal ab gogam''' ci def li ko neex ci nguur-nguuraan yu Almaañ yi.
Sartu réew bu Almaañ bu bees bi '''yaxal''' na ñu sos ñaari '''jataay''':
 
* '''Jataayu Bennoo gu Almaañ (BundasratBundesrat)'''
* '''Jattayu (RechstagReichstag)'''
 
Dooley yoonal ji nag mi ngi nekkoon ci '''BundasratBundesrat''', di jataay bi nga xam ne mi ngi ame woon ci juroom fukk ak juroom ñatti cér, ñu séddale leen ci nguur-nguuran yi nga xam ne ñoo amal imbraatóóor gu Almaañ gi. Brusiya nag moom rekk amoon na fukki '''kàddu''' ak juroom ñaar, ginaaw bi mu am ñaar fukki kàddu. Ak li Brusiya di moomadi li ëpp ci kàddu yi lépp ci BundasratBundesrat, teewul mu gënoon fa’a guddub loxo, gënoon fa a am jeexiital ndax la ëppoon ca nguur-nguuraani Almaañ ya duggoon ca bonnoog Almaañ ga, dañoo takku woon ci Brusiya, te daawuñu woote lenn lu mu bëggul. Te daawuñu jàllale genn saxal ca jataay ba, bu fukki cér ak ñeent àndadee ca saxal ga.
Bu dee nag jataayu RechstagReichstag nag moom, man nanñu ne mooy jataayub askan bi, mi ngi ame woon ci ñatti téeméer ak juroom ñeen-fukk ak juroom ñaari cér, ñu leen di tànn ci anam gu sekkaree. Dooley jataay bii nag daanaka dañu koo lafañal, yòqeel ko . ndax nguur ak doole yi ñu ko joxoon ci ron sartu réew bu Almaañ bu bees bi, dañoo nekkoon di yu doyadi te ñàkk solo.
 
Bismarck nag, jiite na góornamaa bu Almaañ bi niki diisoowaale walla chancelier. Benn ci ñaari jataay yi manul woon ci moom dara, mu yoroon it sañ-sañ bu rëy, te ci ron kiliftéefam tam la Almaañ gu rëy gii gépp nekkoon, nga xam ne ña fa dëkkoon ca atum 1871g jege woon nañu ñeen-fukki milyoŋi nit, mujj àgg ci ñeen fukk ak juroom ñeenti milyoŋ ciy nit atum 1890g, di maanaam bi Bismarck faatoo ba am ñaari at.
 
[[Catégorie:taariixu Tugal]]
 
[[Catégorie:taariixuTaariixu Tugal]]
 
 
[[fr:Unité allemande]]