Seydinaa Limaamu Laay wuute gi ci sumb yi

28 octets ajoutés ,  13 at ci ginaaw
Coppite gi amul tënk
'''Seyidinaa Limaamu''' ab nappkat la woon bu juddoo Yoof atum 1845 g.j. Ci atum 1885 g.j, mu gént gis ne mooy Mahdiyu .. mu [[tàmbalee]] woo àndandoom yi ci ñu dugg ci Lislaam, di soññ jullit ñi ci ñu sellal te jaamu Yàlla rekk, mu daa wax : (( [[wuyyuleen]] wooteb Yàlla, man de yonnantub Yàlla laa, maay Mahdiyu mi ñuy neggandiku)), daa na woo ay àndandoom jëme léen [[cig]] jub ak jàppalante. Bu ko defee nit ñu bari dikkal ko ngir déglu njàggaleem mi. Mu daal di sos kuréelug Laayéen.
[[Siiwam]] gi tiitloo woon na way sanc yi ragaloon ag jeqiku kontar leen. Ci atum 1887 g.j, la sancaan yi taxaw ci jàpp ko, bi [[mu]] yëgee seen naal yooyu la ànd ak lenn ciy àndadoom génn, waaye tubaab bi jàpp ko ca wetu Caaroy. Waaye ëttu àtte bi mujj [[na]] ko setal ko ngir ñàkk lenn lu man a dëgëral tuuma yi ñu teg ci kawam. Limaamu wéyoon na ci wooteem gi, waaye daa na def [[jamono]] ju nekk muy fenqook sancaan yi ko daa jéem a sonal ak àndandoom yi. Mi ngi làqu atum 1909 g.j.
 
[[catégorie:niti senegaal]]
Utilisateur anonyme