Muhammad Lamin Daraame wuute gi ci sumb yi

44 octets ajoutés ,  13 at ci ginaaw
Coppite gi amul tënk
'''Muhammad Lamin Daraame''' (turam dëgg di Demba Dibaasi) sëriñ la won bu bokkoon ci giirug Saraxule, di woon it tiijaan bu [[askanoo]] ci Gonjuro. Tukki woon na dem Màkkatal Mukaarama, nekk fa ba 1879 g,j.
[[Bi]] mu dellusee la ko [[Ahmad Seexu jàpp]], jotul a àgg cig njabootam lu dul ci atum 1885 g.j .
 
[[Muhammad]] Lamin Daraame siiwe woon na ag ragal Yàlla, looloo waraloon mu amoon taalube yu bari. Jibaloon na jiyaar ci kaw [[dëkkandoom]] yi duli jullit ak ci ñoñ frãas ñi sancoon réew mi. Xareem bi, tolloon ci junniy xarekat jawali woon na Bundu, [[daal]] woon gaw tatay Bakkel ji, atum 1886 g.j, waaye ak li ko waa Bakkel doon faral lépp taxutoon mu man a teg loxo ci dëkk [[bi]], looloo taxoon mu dëppaat.
[[Waa]] Frãas yi tiitoon nanu lool ci ndam yi xareem bi ndàmm, looloo waraloon ñu song ko nangu Sinodibo, njaf doomam ja [[Saybu]], ginnaw bi ñu ray ko.
 
[[Ci]] atum 1887 g.j, la ko tubaab yi manante ci deltu ginaaaw jëm Gambi. Daal di toj tata ja mu tabaxoon ca Tuubaa Kuta.
[[Muhammad]] Lamiin ñàkkoon na lu bari ci xarekatam yi ci xare bii. Tubaab yi ray nanu ko ci ndimbalul Muusa Mulo. Ñu mujjoon [[manante]] buur yu bari ci ñu xaatim ay kóllarey ndénkaane(tutelle), tegoon it loxo lu ëpp ci suufi Senegaal yi.
 
[[catégorie:niti senegaal]]
Utilisateur anonyme