Aliin Situwe Jaata wuute gi ci sumb yi

Contenu supprimé Contenu ajouté
ScottishMaid. sex (waxtaancëru)
Résumé automatique : blanchiment
Spacebirdy (waxtaancëru)
m Révocation des modifications de ScottishMaid. sex (retour à la dernière version de Ji-Elle)
Rëdd 1 :
'''Aliin Situwe Jaata''' jigéen la woon ju juddoo Kabrus ci Kaasamaas, atum 1920 g.j. moom nag ame woon na benn gàkk-gàkk ngir tawati lompoñ ju ko daloon. Nekkoon na dib jaaykat bob tukki woon na dem [[Ndakaaru]], jot faa liggéey niki mindaan. Mujj na - jaare ko ci Imaa Imit - di ab jabar ci diiney xërëm ji fi fekkoon baax.
 
Jaata àndutoon ci ni tubaab yi di def ci réew mi : fayloo nit ñi galag yu seer, liggéeyloo leen cig sañ-bañ ak dugal waa [[Senegaal]] yi ci xareb Faraas bi (son armée). Mu sàkku woon ci waa réew mi ñu bañ a bay gerte gi leen tubaab teg ci doole, te bay lu ñu man a dunde niki : ceeb, mboq, dugub ak yu ni deme.
 
Aliin Situwe nekkoon na di ku daa xeex diiney nasaraan (kercente), daa na woote it ci ñu dellu ci diiney Afrig yi, te màggal aaday maam yi. Dees na ko jàppe ki njëkk a woote ag yamoo ci diggante góor ñi, te bàyyi di xool ay askan aki diine walla ay xalaat. Daa na woote it ag yamoo diggante góor ak jigéen te booba jigéen ku desoon ginnaaw la woon ci mboolaay gi(la société). Daa na woote it ci mag ñeek gone yi di dimbalante.
 
Ci biir xareb àdduna bu ñaareel bi, Jaata siiwoon na ba daj Kaasamaas gépp, ñu mujj di ko dàkkantalee Boroom Kabrus, te kat jàmmaarloo gi mu doon def ci anamug jàmm la ko doon defe. Siiwam gi tiitloo woon na waa Frãas yi tegoon loxo ci réew mi, ñu mujj jàpp ko ca Kabrus ci 28 samwiye 1943 g.j, bu ko defee ëttu àtte bu Sigicoor àtte ko, tëjlu ko fukki at, ñu làq ko, yobbu ko Tumbuktu ca Mali, fa la faatoo ci 22 mee atum 1944 g.j, te booba mi ngi ci digg ag njegemaaram .
 
[[catégorie:niti senegaal]]
[[en:Aline Sitoe Diatta]]
[[es:Alyn Sytoe Jata]]
[[fr:Aline Sitoé Diatta]]