Taariixu Senegaal wuute gi ci sumb yi

Contenu supprimé Contenu ajouté
Abdu Xaadir KEBE (waxtaancëru)
Xët wu bees : Ag nooyal ngir xam luy taariix Xam-xamu taariix moo nuy melalal mbiri dëkk yeek dëkk-dëkkaan yu yàgg ya, ci biir jamonoy taariix, ak mbiri way dëkke seen. Dana nu waxal it ca du...
(Aucune différence)

Sumb bu 1 Oktoobar 2007 à 16:55

Ag nooyal ngir xam luy taariix

Xam-xamu taariix moo nuy melalal mbiri dëkk yeek dëkk-dëkkaan yu yàgg ya, ci biir jamonoy taariix, ak mbiri way dëkke seen. Dana nu waxal it ca dund ga fa amoon. Ci gàttal daal, xam-xamu taariix day gëstu li-wéyi nit (son passé) cig matale. Dana wuññi (feeñal) it nekkiin ak dundiin yi nga xam ne nit jaar na ci jànkoonteek ñoom ci dundam gu gudd gi, ci biir ay jamono yu dabante te toftaaloo, bu ko defee mu gëstu anami jëm-kanam yi nga xam ne nekktéef bii (di nit) amal na leen ci taariixam bu gudd bi, ci noonu loolu jural ñu ñu jànge ci daj-dajam yooyu wéy (ses experiences), aki ndamam, te jéem a moytu ay pakkastalam aki rëcc-rëccam ya jàll.

Bu lii amee nag dinañu gis njariñ ak ngënéelul gëstug xam-xamu taariix.

Li ñu jublu ci jàng taariix:

Taariix dinanu ko jàng ngir mu yombalal ñu xam mboolaayi nit ñi ci anam gu xereñ, te dégg (comprendre), xàmmee it buum yi leen boole.

Gëstu dundug buur yeek imbraatoor yi rekk du lenn li nga xam ne moo nu war a yitteel ci taariix, liy li ci gën di farata kay mooy gëstu dundug mbooloo yi ak bennaan yi (individus). Ak gëstu jafe-jafe yi daa yeesu ci seenug dund bis bu Yàlla sàkk, te jéem leen a wutali saafara yu dëppoo, ba maas giy ñëwi ëlëg man cee jariñu.

Digal taariix (wutal ko aw dig) :

Ngir digal ab xew-xew fàwwu mu am ab tombub boy (point de depart). Ay tombi boy yu bari nag am nanu yoy taariix man na cee tàmbalee. Nasaraan yi ñoom seen tombub boy mooy juddug Yonnant Yàlla Hiisaa, ca lanuy taariixe seeni xew-xew, bu dee jullit ñi ñoom seeni xew-xew ñi ngi leen di wutaluw dig wu bawoo ca gàddaayug Yonnant bi(j.m) juge Màkka ga mu ganee àdduna, dem Madiina. Xew-xew bii nag mi ngi fiirook (dajeek) atum 622 ci taariixu juddug Yonnant Yàlla Hiisaa.


Jamonoy njëkk taariix:

Boroom xam-xam yi - ginnaaw gëstu gu nu def ci suuf si - wuññi nanu ay jeexiit (reste;vestige;trace) yu yàgg: ay jumtukaay - ay xor - ay doj, yuy tegtale ne suuf sii déy aw nit dëkke woon na ko njëkk ay junniy at, jamono jooja la nuy tudde njëkk taariix.

Moom nag mi ngi séddaliku ci ñaari xaaj:

1 - Jamonoy doj wu nu yatt 2 - Jamonoy doj wu nu xacc (wu ñu ñawal)

Ci ngënéelul jeexiit yii lanu xame la njëkk taariix. Nit ci jamono jii da daan tuxu rekk, di jëfandikoo ay ngànnaay aki jumtukaay yu njëlbéenu (primitive) (doj yu nu yatt, ay ngànnaay - ay xeej aki xepp). Bi jamono gënee dox, seen dund gi soppiku, ñu xam leegi sawara, jëfandikoo ko ci togg ñam yi. Ci jamonoy doj wu nu xacc wi, lanu tàmbalee dajaloo, sóobu ci mbay, sàmm ak ràbb ak liggéey jumtukaay yu xànjar yi, tàmbali it di def yenn liggéeyi fànn yi niki bind ci doj (ciseler ;graver), ak yatt. La ko dale ca 3500 njëkk judd gi (gu yonnant Yalla Hiisaa), la weñ feeñoon, ñu fent it mbind. Bi weñ feeñee, fentees it mbind la njëkk taariix jeex, taariix daal di tàmbali.


Xayug Isipt

Isipt bu njëkk dafa séddaliku woon ay xaaj. Ci jamonoy 3200 nj.j(njëkk judd gi) lañu bennal xaaj yii, mu mujj nag di nguur gu dëgër, buur bu tudd Firhawna jiite ko, ay foŋsaneer di ko jàppale yu man a bind man a jàng. Bindkat ya danu daa jëfandikoo li nuy wax mbindum Yirogliif, ñoom nag bindkat yooyu lanu féetale woon war a jottali ndigali buur bi, ak dajale galag yi (les impôts) ak taxawal yoon.

Isipt nekkoon na réew mu woomle, mu ami suuf yu naat, yu nangu mbay, ngir dexam gu mag googu di (Niil), am na it ay mbelli wurus ak xànjar ak weñ ak jamaa.

Ñoñam it siiwoon nanu ci yaxantu ak réew yi ñu digool, ci gaal yi daa jaar ci Niil. Waa Isipt am nanu xay gu cosaanu, ñu nekkoon ñu daa gëm ay yàlla yu bari, daan leen melale ci bindu nit ku am boppub bàyyima., yàlla ju ci mel ne Amoon Ra (yàllay jant ji) benn la ci ak Isis (yàllay weer wi) , nga xam ne Firhawna it yàlla lanu ko jàppe woon. Daa nanu tabaxal seen yàlla yi ay jaamuwaay (ay temple) ngir màggale leen ko. Ña cay ñu woomle dañu daa tabaxal seen bopp ay bàmmeel yu yor bindub mbaanaar (pyramide). Bu ñu daa suul seeni néew nag, dañu ci daa boole mbooleem seeni bagaas ak alal. Ci atum 332 nj.j la waa Geres teg loxo Isipt, booba it la tàmbalee naaxsaay.


Tàmbalig taariix :

Jeexiit yu Isipt yi

Seex Anta Jóob (1923 - 1986 g.j) moom lañuy jàppe boroom xam-xam bu Senegaal bi jot a def ay gëstu ci nguurug Isipt gu yàgg ga, mu leeral ci séqoo gi am ci diggante xayug Isipt ak xayug waa Afrig yu ñuul yi.

Seex Anta Jóob wuññi na jaare ko ci gëstoom yooyu mu defoon ci mbind yi nu yatt ci doj yi ci Isipt, ak ci gëstu yi mu defoon ci tàdd (cadavre) yu ñu taaniit (momifier) yi , - wuññi woon na ne Firhawna yi de li ëppoon ci ñoom ay nit ñu ñuul lañu, ñu néew reek ñoo ca nekkoon ñu weex. Seex Anta it wone woon na niroo gi am ci diggante lu bari ci làkki waa Afrig yi ak làkku Isipt wu yàgg wa, ponki làkk yi ak bennaani baat yi dañoo niroo.

(Man nag ma ne ngir dëggal niroo googu : mbaanaari séeréer yu yàgg ya ak mbaanaari waa Isipt yi walla seen pyramide yi, xool-leen leen, ag niroo ngi fi de, waxuma la nag suulaale gi waa Isipt yi daa suulaale néew beeki bagaasam te séeréer su yàgg sa daa ko def .)

Am na yeneen tomb yu ñu bokk ci diggante Isipt gu yàgg ga ak Afrig gu ñuul gi : Am col ak watuwiin, ak topptoowiinu kër ak yenn ci ay gëm-gëm aki jaamuwiin.

Wuññi yii wone nanu ne ag wàll ci xayug Isipt ga ci Afrig gu ñuul gi lanu ko jële. Isipt gu yàgg ga daa nekkoon gu di boroomug xay gu kawe gu dimbalee ci amal ay wuññi yu am solo ci wàllug xam-xamu xayma, ak xam-xamu falag (fidiw).

Fànnu Isipt bokk na ci fànn yi gën a rafet ci yu yàgg ya. Xam-xam yii nag tas nanu ci àdduna bi, kon goxub Afrig sañ naa ndamu ci li mu indil ag nite ciy liggéey yu am solo.

Waa Isipt defar nañu ab arminaat, lim ci at mi muy 365 fan : 12 weer * 30 fan = 360. Ñu dolli juroomi fan ngir màggale ci juddug seen yàlla yi : Osaris - Isis - Oris - Sit - Nifti . Séddale nañu at mi def ko 4 xaaj, xaaj bu ci nekk am ñeenti weer. Weer wi ñu séddale ko ñeenti ayu bis, gu ci nekk am fukki fan. Bis bi nag ñu séddale ko 24 waxtu.


Yaatug lislaam ci Afrig gu sowwu gi :

Ci njëlbéenug juroom ñaareelu xarnu la Muhammad (j.m) tàmbali di tas diine ju yees ji (lislaam), ginnaaw bi mu làqoo atum 632 g.j, la araab yi ubbi Afrig gu sowwu gi, daal di duggal aw nitam ci lislaam, ci noonu, jullit ñi tàmbalee tas lislaam ndànk-ndànk ci bëj-saalumu tàkk gi (désert bi),.

Lislaam mujj na yaatu, tas te li ko waral du dara lu dul joqalante gu yaxantu gi naar yi daa def ak Afrig, ak njëgg (convoi) yu giléem yi daa jëggi tàkk gi, nga xam ne yaxantukat yi dañu daa jënd wurus ci sowwu Afrig, jaayiji ko ca bëj-saalumu Afrig, daa nañu baana-baana it ci jamaa ak jumtukaayi xanjar yi ak weer aki téere ak xorom ci dëkki yaxantu yii : Jinn, Tumboktu, Gaawo. Yaxantukat yooyu dañoo fekk lislaam ca bëj-gànnaaru Afrig, bu ko defee, la ëpp ca ñoom daal di ciy dugg, daal di tàmbalee waar seeni àndandoo ngir dugal leen ci.

Waaye yaatug lislaam gi amewul ci jàmm rekk, ndax yenn askan yi dooni jullit dañoo jugoon def jiyaar ngir tàbbal yeneen yi ci lislaam.

Murabituun (Marabout) yi nga xam ne ñi ngi juge woon ci bëj-gànnaaru Afrig, ubbi woon nanu lenn ci Afrig gu sowwu gi ci xarnu bu fukk ak benn.


Imbraatóor (empire) gu Gana :

Imbraatóor gi mag ci yu Afrig yi taariixkat yi mas a xam mooy : gu Gana. Li ñu jot a xam ci taariixam ñi ngi koy sante gëstuy boroom xam-xami jeexiit yi, ak nettaliy gimiñ yi, ak mbindi tukkikati naar yi.

Gana mi ngi sosu ci ñeenteelu xarnu g.j, jamono jooja it nguur gu ndaw la woon gu ñu daa woowe Ogaadoo. Ci juroom ñatteelu xarnu g.j, la ab xareem (son armé) jugoon song ay suuf yu yaatu, yu nekk ci diggante dexug Senegaal ak Nijeer, ci noonu la Gana wëlbatikoo di imbraatóor gu mag gu teg loxo ci dëkk yi mu feggool…

Imbraatóor gi nekkoon na di gu naat : ay suuf yu nangu mbay ak sàmm, mu daa bokk ci yaxantug tàkk gi(gi nu daa defe ci tàkk gi) ak njaayum wurus mi, moom imbraatóor gi amoon na ay mbelli wurus yu bari yoy ki ko daa topptoo mooy Kayaamagana, maanaam njiitul wurus li : waa jii da daan nekk njiit lu dëgër, lu ñu wormaal, luy àtte cig maandute te daan samp foŋsaneer yi. Moom nag cim koom ak naataange la daa dunde ci péeyam, waa diiwaan bii it dañu ko daa indil ay kem ci wurus wi ñiy génnee ci suuf si, ginnaaw bi mu faatoo nag la ko fi ab jarbaatam wuutu. Ci atum 1052 g.j, la Muraabituun yi song Gana, ci layuw dañuy dugal ñoñam ci lislaam, ñu daal di ubbi péey ba atum 1076 g.j, ginnaaw bi Gana néew doole, daal di daanu ci mujjantal gi ci loxoy imbraatóor gu Mali atum 1240 g.j.


Imbraatóor gu Mali :

Nguurug Susu ci xarnu bu fukk ak ñatt tegoon na loxo ci askanu Maandeŋ. Sinjaata, doomi kenn ci buuri Maandeŋ yi, daa dogu woon ci goreel aw askanaw, ci noonu mu tawal ab xare walla am mbooloom xare (larme) mom ci la ame ndam ci kaw Susu, ci xareb Karina ba atum 1235 g.j, ci noonu la am réewam tembe woon (amoon independance). Ginnaaw bi Sinjaata amee ndam ciy noonam, la giirug Maandeŋ daje (Konaate, Traaware, Kayta, ak Kamara) taxawal ag imbraatóor gu mag mooy gu Mali gi, Sinjaata jiite ko.

Sinjaata songoon na suuf yi feggoo woon ak moom ngir boole leen ci nguuram gi, loolu nag li ko ko may mooy xareem (armé) bu am bi doole, te nosu. Bi Sinjaata di faatu Mali moo nekkoon imbraatóor gi gën a rëy ci sowwu Afrig, péey ba di woon Niaani.

Ñi ko fi wuutu woon duggoon nanu ci lislaam, wéyoon it ci yaatal gëwéelub nguur gi, ba mu mujjoon ëmb mbooleem la ko dale ca mbàmbulaanug atlas ci sowwu bi, ba ca dëkkub Gaawo ci penku bi. Ñu séddale réew mi ciy diiwaan bu ci nekk ag kilifa jiite ko guy doxal ndigali buur bi, di dajale galag yi, tey doxal yoon. Ci jamonoy buur bi Kanka Muusaa la imbraatóor gi àggoon ca gën jaa kawey ay njobbaxtalam, ci xarnu bu fukk ak ñeent. Nguur gi nag daa na jot ci màng mi tukkee ci mbelli wurus yi ak yaxantug tàkk gi. Ci atum 1324 g.j, Kanka Musaa aji woon na Màkka, ci tukki bu tollu ci 18 weer, won na ci adduna bi dooley nguuram gi ak woomleem gi.

Amaloon na ay séqoo yu yaxantu ak réewi bëj-gànnaaru Afrig, indi it ci nguuram gi ay boroom xam-xami jullit yu juge penku. Ci xarnub fukk ak juroom benn la ay jafe-jafey wuutu (xilaafa) tàmbalee feeñ, ak dagu (sécession), looloo jur néew-dooleg ay diiwaan yu bari, bu ko defee Songaay daal di ñëw songu Mali, nangu ko.


Imbratóor gu Songaay :

Ci juroom ñaareelu xarnu g.j, la askanu Songaay wi dëkkoon ci tefesug dex gu Nijeer gi taxawaloon ag nguur gog péeyam moo nekkoon Gaawo. Mali nag moo tegoon loxo askanu Songaay wi ci xarnub fukk ak ñatt g.j, waaye ñoom jotaatoon nanu ci seenug temb te ñi ko waral di njabootug Soni gi ci xarnub fukk ak ñeent, daal di tàmbalee naat. Soni Aal-Béer (maanaam Aal mu mag mi) moo nekkoon buur bi la ko dale ca 1464 g.j, ba 1492 g.j, wutaloon na nguurug Songaay xare(armé) bu am doole, mu daa def ay ubbi(conquete) ngir yaatal nguuram gii nga xam ne mujj na tuxoo ci nguur dem cig imbraatóor gu ñu mujj tudde Songaay walla Gaawo. Bi Aal Béer dee la kenn ci ay njiiti xareem teg loxo ci nguur gi, daal di wutal boppam dàkkantalu Askiyaa ( maanaam imbraatóoor bi), moom nag àtte na ba ci 1528 g.j, mu gën a rëyal mbooloom xareem mi, wéy ci ubbeem yi, bu ko defee imbraatóor gi mujj tàlleeku dale ca mbàmbulaanug atlas ba ca Borno ci penku bi, dalewaat ca Jini ci wàllug saalum gi ba ca digi Marog ci wàllug bëj-gànnaar gi. Gii imbraatóor nag àggoon na ci njobbaxtalam ci jamonoy Askiyaa Muhammad. Buur bi moo daa jox ndigal foŋsaneer yi, di lijjanti diiwaan yi, benn gongikuwaayu alal bi nguur gi amoon mooy yaxantug tàkk gi.

Nguur gi nag, réew yi mu feggool xuppoon nanu ko : ci atum 1591 g.j, buurub Marog yabaloon na ab xareem ñu jaar ci tàkk gi ngir song Gaawo, moom nag amoon na ndam ci waa Songaay ngir ngànnaayi sawaraam yi mu jénde woon ci waa Tugal yi. Ci nii la Songaay tàmbali woon di doyadi ak di dagu.


Nguur yu njëkk ya ci Senegaal :

Ngir xam taariixu nguur yu njëkk ya ci Senegaal, taariixkat yi am nanu ay gongikuwaay yu bari : gongikuwaay yu gimiñ, yooyu nag yu bari lañu waaye soxla nañu ay gëstu yu xóot, ndax dañuy faral di jaxase diggante dëgg ak léeb (mythe). Ak jeexiit yi, ñoom nag bariwuñu te lu tas la, ak gongikuwaay yu mbind yi, ñoom it yu néew lañu, ndax askan yi dëkke woon Senegaal ca jooja jamono xamuñu woon mbind.

Senegaal nag suuf su ñuy gàddaaye génn la ak su ñuy gàddaaye jëm. Aw askanam, diirub ay xarnu, dañoo nekk ci diggante sax ak laxas. Senegaal nag taxawal na ay séqoo yu am solo ak aw askanam ak itam réew yi mu feggool. Daa na jëflante ci wàllug yaxantu ak gox yu sori yi. Loolu lépp nag tax na ba réew mi am aada ju cosaanu. Nguur gi njëkk ci Senegaal ñi ngi ko taxawal ci lu tollook juroom ñaareelu xarnu g.j, man naa am sax mu jiitu loolu. Nguur yooyu nag amuñu woon doole lu dul ci ñaari xarnu yii, bu fukk ak ñatt ak bu fukk ak ñeent, maanaam ci jamonoy imbraatóor yu ñuul yi (yu nit ku ñuul yi), gu Gana, gu Mali ak gu Songaay. Nguur yii ci ron kiliftéefug imraatóor yii lañu nekkoon. Ci xarnub fukk ak ñeent Jolof soppiku na di nguur gu mag gu am ay sañ-sañ yu yaatu, teg loxo ci ay wàll yu mag ci nguur yooyu. Ci xarnub fukk ak juroom ak bu fukk ak juroom benn, yenn nguur-nguuraan yi tàmbali woon nanoo dagu ci Jolof ndànk-ndànk, ci noonu Jolof mujj di nguur gu yamamaay niki yeneen nguur yi rekk. Nguur gu ci nekk ab buur a ko daan jiite bob ab jataay (conseil) moo ko daa jox sañ-sañam, jataay boobu moom lañu dénkoon muy fuglu ay saxalam aki ndigalam , ay foŋsaneer daa nañu dimbale buur bi, di def liggéey yi aju ci saytu alal ji, wattu kaaraange gi, taxawal yoon, ñenn ci ñoom it daa nanu dooni kàngam (gouverneur) ñeel lenn ci diiwaan yi.


Nguur yu njëkk ya ci Senegaal :

Tukloor ak Fuuta :

Nguurug Tukloor mi ngi sosu njëkk juroom ñeenteelu xarnu, njabootug Ogo Ja jeete ko, ci mujjantalug xarnu bu fukkeel la Waar Jaabi song ki mujjoon ci buuri njaboot googu, ray ko. Bu ko defee daal di jël nguur gi, ci noonu la geneen njaboot jote ci nguur gi, mooy gu Mana.

Waar Jaabi dugg na ci lislaam, daal di jug def jiyaar ci kaw dëkkandoom yi duli jullit, ci noonu la nguurug Tukloor xéye di nguur gi njëkk a dugg ci lislaam ci Senegaal. Tukloor yi bokkoon nanu ci yaxantug wurus wi ak njaayum jaam yi, li ko waraloon it mooy dend gi nu dendoon ak dexug Snegaal gi, ak nekk gi nu nekkoon ci yoonu yaxantu wi. Mu nekkoon réew mu naat te am doole, waaye dafa rotoon ci ron teg loxo gu imbraatóor gu Gana, (ci xarnub fukk ak benn), ginnaaw bi mu rot ci gu Mali (ci xarnu bu fukk ak ñatt), rotati ci gu Jolof (ci xarnub fukk ak ñeent). Ci mujjug xarnub fukk ak juroom la Koli Tingala (kilifa gu bokk ci càllallag Pël, juge ci wàllug bëj-saalum gi) jug xeex Tukloor yi, daal di tembal ay goxam (jox leen independance) taxawal nag nguur gu yees mooy Fuuta Tooro, njabootug Deñanke jiite ko. Ci xarnub fukk ak juroom benn Fuuta Tooro def na ay xare ngir yaatal suufam ci kaw ay dëkkandoom : Jolof - Kojoor. Njabootug Deñanke nag manatuñu woon a jàmmaarlook cong yi tukkee ci biti, ak lëj-lëji kuutu gi (succession). Ci atum 1770 g.j, la ag fipp am walla ag jeqiku tukkee ci kilifay jullit ñi, Cerno Sulaymaan Baal jiite ko, daal di daaneel njabootug Deñanke, bu ko defee Baal jël lislaam def ko cëslaay li nguur gi di tegu te di ko ci doxale. Cerno Sulaymaan Baal bàyyee woon na nguur gi Yilimaan Abdul Xaadir Kan, moom lañuy jàppe ki njëkk a doon Yilimaan ( Amiirul Moominiin :njiitul jullit ñi)


Nguur yu njëkk ya ci Senegaal :

Jolof gu mag gi :

Nettaliy gimiñ yi ñi ngi wax naan nitug léeb (mythique ;fabuleux ;légendaire) kii di Njaajaan Njaay moo taxawal nguurug Jolof gu mag ga, ci fukk ak ñatteel ak fukk ak ñeenteelu xarnu g.j. Bu ko defee nguur gi gën a yaatu ci xarnub fukk ak juroom g.j, mujjoon ëmb li ëpp ci réewum Senegaal, ndax nangu woon na Fuuta Tooro - Waalo - Kajoor - Bawal - Siin ak Saalum. Jolof nekkoon na fu naat : mi ngi daa sukkandiku - ci wàllug koom-koom - ci mbay ak sàmm ak liggéeyi fànn yi (art) ak ràbbi sér ak yaxantug tàkk gi. Ci atum 1500 g.j, la Koli Tingala àgg ci nguur gi ci Fuuta Tooro, daal di koy delloosil ag tembam. Nguurug Jolof nag li ko tas, yàq ko mooy xarey ñoñ (guerres civiles) ya. Ci atum 1549 g.j, la xareb Kajoor (larmeem) am ndam ca Dànke ca wetu Luga: rayees na buurub Jolof , ci noonu la Kajoor tembe ci Jolof. Bawal it temb ci Jolof ak Waalo ak Siin ak Saalum, ci xarub fukk ak juroom benn g.j. Naka noonu Naani ak Wuli ci xarnub fukk ak juroom ñaar g.j, ci nii nag la Jolof ñàkke li ëpp ci ay suufam, bokk na ci yooyu wàll yi tiimoon géej gi, mu daal di sóobu nag cig naaxsaay. Jolof amoon na ay séqoo(relations) yu jafe ak sancoom (colonies) yu yàgg ya. Ki daan jiite Jolof mi ngi daa tudd Buur-ba Jolof, ñi gënoon a siw ciy buuram ñooy : Mbakumbas - Alburi Njaay - Sàmba Lawbe Penda - Buuna Alburi Njaay. Ab jataay it - bu daa ame ci juroom ñaari garmi ak jenn jaraaf ju ñu féetale woon tànn kiy wuutu buur bi bu faatoo- moo daa rëdd sañ-sañi buur bi.

Nguur gi mi ngi séddaliku woon ci juroom benni diiwaan, bu ci nekk kàngam jiite ko, waaye Njaabur moo daa saytook a doxal fukk ak ñaari dëkk yu ndaw yu am solo yi.


Nguur yu njëkk ya ci Senegaal:


Ngurug Waalo :


Waalo mi ngi sosu ci jëmmi jamono ji nguurug Jolof gu mag gi sosoo (xarnub fukk ak ñatt ak fukk ak ñeent) ci loxol Barka Mbooj, mbokkum Njaajaan Njaay mi mu bokkalul baay. Waalo nag mi ngi woon ci ron kiliftéefug Jolof, waaye mujj na delloosi ag tembam niki yeneen nguur yi : Kajoor, Bawal, ci xarnub fukk ak juroom benn. Waalo nekkoon na nguur gu doyadi, ay xëccoo yu tar te toftaloo amoon na fa ca diggante njaboot ya daan moom (ya daa donnante nguur ga), ngir jot ci nguur gi. Waaye nag réew mu naat la woon ci wàllug mbay, moo waraloon ay dëkkandoom di ko xemmeem te di ko jéem a song, waaye moom yoon wu mu ci mas a doon daa na ci mucc, te daa na tëyye ag tembam. Ci atum 1769 g.j, Waalo duggoon na cib xare ak ñi ñuy wax Tarasira (waa Muritani). Waaye ngir dog dëngoo gi dox ci diggante ñaari wàll yi, dañoo jëloon buurub Waalo bu jigéen bi Njambata Mbóoj may ko soxna buurub Tarasira yi di Muhammadul Habiib ci atum 1833 g.j, looloo délloosi jàmm ji ca gox ba. Waalo nag buur bu ñu naan Baraak moo ko daa jiite( di bokk ci càllalag Barka Mbóoj ci wàllug bay, ak ci càllalag mbokk mu jigéen mu Njaajaan Njaay ci wàllug nday), ab jataay bu ñu jagleel looloo ko daa tànn , bob dana ko man a folli saa su ko soobee. Ci atum 1670 g.j, jataay boobu folli woon na Baraak Barcaaga, ngir ne daa bàyyi woon ag njabootam ñu giir màng (butin) mu nguur gi. Buur bi nag garmi yee ko daa jàppale ku ci mel ne boroom xam-xamu mbay bi ñu koy wax Jawdin, ak ki jagoo ndox mi, ñu koy wax Jogomaay, ak kiy saytu alal ji, ñu koy wax Maalo, jigéen ñi it daa nanu fa yor pal yu kawe: ndax Lingéer (ñaare moo daa doon yaayi buur bi) moo daa jiite jigéeni nguur gi, Aawo (di soxna su njëkk si) moo daa jiite yeneen soxnay buur bi.


Nguur yu njëkk ya ci Senegaal :


Kajoor :

Ci xarnub fukk ak benn Kajoor as nguur su ndaw la woon su toppoon ci nguurug Jolof, laman daan ko jiite (buur). Ci atum 1550 g.j, la Laman Jece Fu Jogu dugg cib xuloo ak Jolof, ci la dogoo ne day dagu ci moom. Doomam ja ñu naan Amari Ngóne Sabel jotoon naa am ndam lu rëy ca Buur ba Jolof ca xareb Danke ba ca wetu Luga. Bi xibaar bi agsee ci Jece Fu Jogu rekk la daal di jibal tembug Kajoor ci Jolof. Mu daal di wutal boppam dàkkantalu Dameel (maanaam : ki dog séqoo yi ak Jolof ). Jolof nag doon na jéem a délloosi teg loxo gi mu defoon diiwaan yu njëkk ya ba ci xarnub fukk ak juroom ñaar, waaye mujjul am tawfeex ci loolu, ak doonte jéem na ko ay yoon. Kajoor moom nguur gu naat la woon gu daa sukkandiku - ci wàllug koom-koom - ci yaxantu, rawati na njaayum jaam. Leeg-leeg daa na dund ci jawwi njàqare ak tiit ngir réeroo yi mu daa am ak ay dëkkandoom, ngir gëpplante gi daa am ci jot ci nguur gi.

Buur yi nag leeg-leeg daa nanu defi xare ngir des ci nguur gi, ci noonu lanu dàqe woon Dameel Maysa Biige ci nguur gi ay yooni yoon, moom mi doon àtte la ko dale (1749 g.j, ba 1763 g.j ) waaye mu dellusi ci ci doole. Nguur gii daa na baj-baji leeg-leeg it ngir xëccooy diine yi daa am ci diggante jullit ñeek ñi duli jullit. Ci atum 1790 g.j, ci àtteg Amari Ngóone Kumba Ndeela, la lenn ci way dagu (ñu génn ci nguur gi beru) dajaloo ca daanaka-dun bu Bopp Bu Wert bi (cap vert) ngir taxawal fa àtte gu lislaam gu temb.

Ca Kajoor nag donnante ga mi ngi daa juge ci wàllug nday ( maanaam ndayi buur bi, daa war di bokk ci càllalag Jece Fu Jogu) bu ko defee, ñu defe xumbéeli sampug buur bi ca Mbul péey ba, fa la buur bay defe cagaayul cosaan la.

Ay foŋsaneeri garmi ñoo daa jàpple buur bi, ab jataay it nekk fi buy fuglu sañ-sañu buur bi. Buur bi nag daa na tabb ay way dimbaleem jaare ko ci andaari njàmbaar ak aay ci xare.


Nguur yu njëkk ya ci Senegaal :


Nguurug Bawal :

Ci xarnub fukk ak juroom Bawal nguur su ndaw la woon su toppoon Jolof gu mag gi, bu ko defee, ag njaboot gu amug jegeñaale ak buuri Kajoor yi daa ko jiite. Ci xarnub fukk ak juroom benn g.j, la Jolof mànge poseb néew-dooleg nguurug Jolof , daal di jël ag tembam, ni ko yenn ci nguur yi defe woon, gu ci mel ne Kajoor ak Waalo, ngir song gu tar ga Amari Ngóne Sabel Faal defoon Jolof. Ci ñaareelu xaaju xarnu bii la Amari Ngóone xëy di buuru Kajoor ak Bawal ci jenn jamono ji. Booba la buur bi tàmbalee jiite ñaari nguur, waaye nguur gu ci nekk yor politigu doxaliinu réewam. Waaye boole gii bari lu mu daa jur ay réeroo ci diggante ñaari nguur yi, ndax gu ci nekk da daa bëgg a yilif ga ca des. Buurub Bawal nag di Teeñ ab jataay a ko daa jàppale, bu ñu wéer tabbug kiy wuutu buur bi bu faatoo, ak fuglug saxal yi buur bi di def. Nguur gi amoon na ab ëttu àtte buy àtte mbir yi, mbooleem maas yi nag daa nanu fa àttewoo ( maasug nappkat yi, baykat yi, sàmm si, ñoñ fànn ñi (boroom mecce yi) ak jigéen ñi). Bokkug Bawal ci Yaxantug Tàkk gi taxu ko woon a deme noonu, ndaxte yooni yaxantu gi rombutoon ciy suufam, moom kay daa yamoon rekk ci yaxantug tefes gi.


Nguur yu njëkk ya ci Senegaal :


Gambi gu kawe gi ak Senegaal gu penku gi :


Ay nguur yu bari toftaloo nanu ci dexug Gambi gi, yi ci ëpp solo ñooy Naani ak Wuli. Ñoom nag ñi ngi leen taxawal ci xarnub fukk ak ñeent g.j, ay way gàddaay yu bàyyikoo ca imbrraatóor gu Mali gaa leen taxawaloon. Yii nguur nag ci ron waawug Jolof gu mag gi lañu nekkoon, ba kero ñuy nanguwaat séenug temb ci xarnub fukk ak juroom benn g.j . Nguur yii nag bokkoon nanu ci joqalanteg yaxantu gi ci anam gu sawar, looloo taxoon ñuy réew yu naat. Ci bëj-gànnaaru Wuli la nguuri Goy ak Kamera nekkoon, ki léen taxawaloon kilifa la woon gu bokkoon ci njabootug Baajli, mooy Salmaan Xaasa, mi nga xam ne jiite woon na ag nguur ci penku Senegaal. Ñaari nguur yii nag ba xarnub fukk ak juroom ñeent g.j, dañoo bennoo woon. Buur bi dàkkantalu Tunka la daan yore. Ci atum 1833 g.j, la ab xare tàkk ci seen diggante, ba moo waral ñu tàqalikoo. Goxub Gambi gu kawe gi ak Senegaal gu penku gi séddaliku na doon ay nguur yu bari, waaye am na ci yoy daawuñu weesu yaatuwaayu as ndëkk. Gi magoon ci nguur yii ci lu dul sikk mooy Namandéeru ak Faalimi, ñaar yii nga xam ne ñi ngi leen sosoon ci lu tollook ñeenteelu xarnu g.j, ñu nekkoon nag ci ron kiliftéefug imbraatóor gu Gana. Am na yeneen nguur yu sosu woon ca la tollook xarnub fukk ak ñatt g.j, ñooy: Siiselaa - Beledugu - Niokolo - Badon - Bademba - Bundu - Gajaga.

Nguur gu mujj gii nag (Gajaga) giirug Sambiira Baccili ñoo ko jiite woon la ko dale ca xarnub fukk ak ñatt g.j . Nguurug Gajaga dund na cig naataange ngir joqalantey yaxantu ya fa daa am te naataloon gox ba, rawati na yaxatug tàkk gi. Ci xarnub fukk ak juroom ñeent g.j, yaxantu gi mi ngi sukkandiku woon ci daakaande.

Nguuri Gambi gu kawe gi dañu daa dàkkul seen bopp cong yi leen seen dëkkandoo yi daan faral a def, jublu woon ci nangu ci ñoom lenn ci seeni suuf. Ci xarnub fukk ak juroom ñaar ak bu fukk ak juroom ñatt la ay xarekat yu juge ci penku bi dikk soppi nosteg àtte ga fa amoon, bu ko defee ay njaboot yu yees daal di tàmbalee sangu (dooni njiit) ca gox ba. Bu dee ca Siiselaa moom Daansirimaan moo daaneeloon njiitug giirug Siise, daal di wutal nguur gi weneen tur wu yees mooy : Sirimaano. Bu dee ca Beledugu moom, njabootug Siisoxo moo jële giirug Soomari ci nguur gi. Ca Dantila moom ab nappkat bu siwe ci turu Samakoto moo nangu nguur ga, dàq njabootug Samora ga.


Nguur yu njëkk ya ci Senegaal :

Siin ak Saalum :


Giirug Séeréer dafa tàmbali woon di gàddaaye fi mu cosaanoo woon di Fuuta Tooro, jëm leegi Bawal, Siin ak Saalum ci diggante xarnub fukk ak benn ak bu fukk ak juroom benn g.j . Ci xarnub fukk ak ñeent, la jenn waay juge Gabu ci Kaasamaas, tuddoon Maysa Waali Joon, bokk ci njabootug Gelawaar, daal di nangu nguur ga ca Siin, jamono jii nag fekk na Jolof di fu naat moo taxoon Siin nekk ci ron kiliftéefam.

Ginnaaw ab diir la Mbengaan Nduur agsi ci nguur gi ( kenn ci buuri Gelawaar yi), daal di taxawal nguurug Saalum. Siin ak Saalum màngoon nanu poseb xarey ñoñ ya amoon ca Jolof, ca ñaareelu xaaju xarnub fukk ak juroom benn g.j, ngir jot ci séenug temb. Ñu doonoon nag ñaari nguur yu am doole, Saalum mujj di nguur gi gën a dëgër ci nguur yi nekk ci tefesug Senegaal gi. Ñaari nguur yii ŋoyoon nañu ca séen pas-pas yu yàgg ya ba ci xarnub fukk ak juroom ñeent, ak li Màbba Jaxu doon jéem lépp ngir duggal léen ci Lislaam, la ko dale ca 1860 g.j. Màbba jéemoon naa teg loxo Bawal, Jolof, Siin ak Rub, waaye xare (larme) bu Kumba Ndóoféen Juuf am ndam ci kawam ca xareb Sumb ba atum 1867 g.j . Siin ak Saalum buur bu ñu daa dàkkantale Buur moo ko daa jiite. Bu buur bi masaan a faatu ka mag ca càllalag ndayam moo daa tànn ku ko fi wuutu. Ñi ëppoon doole ci buuri Siin yi : Maysa Waali Joon - Waagaan Juuf - Kumba Ndóoféen Juuf - Faamag . Bu dee ci Saalum :Mbengaan Nduur - Samba Lawbe Faal - Saaxo Faal. Nguur gu ci nekk nag amoon na benn jataay bu daa fuglu sañ-sañi buur bi. Buur bi nag jaraaf ji (njiitul jëwrin yi) moo ko daa jàppale, daa na am sañ-sañu àtte nit ñi ak doxal nguur gi.


Nguur yu njëkk ya ci Senegaal :

Kaasamaas :

Kaasamaas baat la bu ñu toggalee ci ñaari dogiit : Kaasa ak Maas boo leen boolee muy buuru Kaasa. Kaasa bokk na ci yi njëkk ci nguuri gox bii. Ginnaawam nag Gabu moo ci gën a rëy ci nguur yi. Ñaari nguur yii ñi ngi leen taxawal ci lu tollook xarub fukk ak ñeent g.j, ci loxol ay xarekat yu bawoo ca imbraatóoru Mali ga, Sinjata Kayta yabaloon leen. Nguurug Gabu (nguur gi ëppoon doole ci yii) Trimaskan Traaware moo ko sosoon, mu nekkoon gi tegoon loxo nguur yu ndaw yi nekkoon ci bëj-gànnaaru Gambi, ñooy : Kantora, Gimaara, Jaara, Kiyaŋ ak Kombo. Kaasa ak Gabu way toroxlu lañu woon ñeel Imbraatóoru Mali jamono yi nu leen sose ñoom ñaar, waaye Gabu moom tàmbalee fay galag ñeel imbraatóor gi, ci noonu mu ame ci «ag àtte-sa-bopp » (autonamie). Ci digg xarnu bu fukk ak juroom, la ñaari nguur yii jariñu ca yëngu-yëngu ya Koli Tingala amaloon ca gox ba, bi mu ko defee, ñu daal di dagu ci Mali.

Ci xarnub fukk ak juroom ñatt g.j, la Kaasa tàmbalee tas : giirug Joola songe ko ci sowwu bi, gu Maalinke ci penku bi, gog Balaanta ci bëj-gànnaar gi.. Ci atum 1830 g.j, la giirug Balaanta lakk péeyub Kaasa di Birikama. Ci xarnub fukk ak juroom ñeent g.j, la Gabu it làmbalee naaxsaay, looloo mi ngi dale ca ba ko giirug Pël gi songee, mooy gi génne woon Fuuta Jalon, bu ko defee mu daal di tàmbalee ñàkk ndànk-ndànk sañ-sañ yi mu amoon ci gox yi mu yilifoon.

Nosiinu biir gi ci nguurug Kaasa ak Gabu xawuñoo wuuteek wa amoon ca nguur yeneen ya ci Senegaal. Buur bi jataayub mag (sénat) ñee ko daa dimbale, moo daa fuglu it ay saxalam tey digal ay sañ-sañam. Diiwaan yi ay foŋsaneer yu kawee leen daan jiite yu tukkee ci garmi yi. Waaye Gabu moom nga xam ne nguurug xare la woon : ay foŋsaneeram yu kawe mi ngi leen daa tànne ci xarekati garmi yi.


Nguur yu njëkk ya ci Senegaal :

Nguuri Pël yi :

Ca jamono yu yàgg ya li ëppoon ci giirug Pël ay sàmm yu daa màng lañu woon, di tuxu ci seen bëgg-bëgg ngir wër ndox ak ñax, ñu nekkoon di ñu tasoon ci gox yu bari ci sowwu Afrig, la ko dale ca dexug Senegaal ba ca ngéejus Càdd (lac du Tchad). Ci diggante xarnub fukk ak juroom ak bu fukk ak juroom ñeent g.j, giir gii def na fi ay fipp yu lislaam yu bari yu waral ñu taxawal ñatti nguur ci Senegaal : Fuuta Tooro - Bundu - Fuuta Jalon. Ci mujjug xarnub fukk ak juroom g.j, am mbooloo ci way gàddaay yu Foolaan yi génne nañu Fuuta Jalon dem Fuuta Tooro, Koli Tingala jiite leen, moo tegoon loxo Fuuta Tooro ci atum 1512 g.j, daal di taxawal nguurug Fuuta Tooro. Ci atum 1770 g.j, la Sulaymaan Baal def ag jeqiku gu lislaam mooy gi soppi Fuuta def ko nguur gu lislaam Almaami Abdu Buukar jiite ko, mooy ki jiyaaroon kontar ay dëkkandoom : Waalo - Taraasa - Kajoor, la ko dale ca 1790 ba 1804 g.j, waaye dañu koo mujj dàq. Ci xarnub fukk ak juroom ñeent g.j, la Fuuta tàmbalee naaxsaay. Ci lu tollook 1690 g.j, la Tunka buurub Goy may menn mag mu juge Podoor aw dog ci suuf, mooy Maalik si, dog wooyu mi ngi nekkoon diggante Faalimi ak Gambi gu kawe gi. Ci nii la nguurug Bundu sosoo. Maalik si daal di nay jibal ab xare, def it Bundu muy nguur gu lislaam, daal di safaanu nguurug Goy, gën a yaatal ag nguuram.

Nguur googu nekkoon na di gu naat ci ayug Maalik Si aki way wuutoom (njabootug Siisebi), li ko waral di séqoo yi mu amoon ak Gambi. Ci lu tollook 1727 g.j, la ag giirug Pël ca Fuuta Jalon jugoon - Karamoko Alfa jiite ko - soppi gox boobu it def ko nguurug lislaam, Almaami di ko jiite, ju njabootug Suriya di fal leeg-leeg, leeg-leeg gu Alfaya.


Waa Tugal yi ci tefesug Afrig :

Fent ak wuññi yu mag yi :

Ci xarnub fukk ak juroom g.j, waa Tugal yi amal nañu ay wuññi (decouverte) yu bari yoo xam ne soppi nanu seenug dund, yi ëppoon solo ci wuññi yooyu ñooy wuññig moolukaay (imprimerie), ki ko def di Gutenberg ci atum 1450 g.j .

Bu njëkk téere yi ci loxo lanu leen daan binde te loolu daa na soxla waxtu wu baree bari, looloo waraloon téere yi seer te néew. Móolukaay nag mi ngi daan ame ci ay bind (forme) yu ñu liggéeye ci weñ, bind bu nekk daa na taxaw taxawaayu aw araf. Bu ko defee ñu raŋale bind yii nga xam ne ñooy defar jumla (phrase) yi ñu soxla, bu loolu jàllee, daa ji door a ñëw, jaar ci seen kaw, njëkk ñu leen di móol ciw këyit. Bu ko defee ñu jël benn yax bi( copie bi) def ci ay xët yu bari, ci noonu lañuy defare ab téere. Ci jamono jii waa Tugal yi xamoon nañu puudar (poudre à fusil) (moom nag - puudar - waa Siin na ko fentoon), ñu jëfandikoo ko ci ngànnaay yu sawara yi ñu njëkk a liggéey , xamoon nanu it buusal (moom nag wa Siin ak naar (arab) yee leen ko njëkk a xam), ñu liggéey ay gaal yu yees yu gën a gaaw te gën a man a jànkoonteek ngelaw yi ci mbàmbulaan yi . Wuññi yii nag ñoo tax mool yi man a def tukki bu sori ci biir géej gi, te wuññi ay suuf yu yees yoy waa Tugal yi xamuñu leen woon.

Ay tukki yu bari daal di nañuy taxaw jëm ci tefesi Afrig yi :

Ci atum 1487 g.j, la Bartelemi Jaas agsi ca Boppu Yaakaar Ju Baax Ji ( cap de bonne esperance). Ci atum 1492 g.j, la Kristof Kolombo jugoon di wër aw yoon wu koy àggale End waaye mu far àgg cig mbetteel ci Amerig gi nga xam ne waa Tugal yi sax xamuñu woon ne am na. Ci atum 1498 g.j, la Vasko De Gama jugoon di wër Afrig tukkee ci bëj-saalum, daal di àgg End. Ci diggante 1519 ak 1522 g.j, la Magelan def ab tukki bob ci la wëre àdduna bi, ci lañu wone it ne àdduna bi dafa bulu (kol-kolu).


Waa Tugal yi ci Tefesug Afrig gi :

Digg (centre) yu yaxantu yu njëkk yi:

Waa Tugal yi bi ñu tàmbalee seen wuññi yooyu lañu gaawantu teg loxo suuf yii ñu wuññi : Mool yi toppante nañu ci tefesi Afriig yi, waa Portigaal yi jiitu ci, waa Espaañ yi topp ci, waa Olaand, waa Angalteer ak waa Frãs. Ci xarnub fukk ak juroom benn g.j, la waa Portigaal ak Espaañ teg loxo Amerig gu bëj-saalum gi, bu ko defee waa Portigaal ya jël fa sancu (colonie) bu Breesil féetele ko seen bopp, yeneen wàll ya ca des nekk ca ron ŋëbgu Espaañ. Way sanc yi ( les colonisateurs) tambali woon nañoo génne koom-koom yu mbell yi (yu mine yi), bay it yenn mbay yi niki bantu suukar ak póon ak wëtéen. Waa Tugal yi bëgguñu woon a dugg ci goxub Afrig, ñoom daal dañoo wutoon ay digg yu yaxantu ( centres commerciaux) ci tefes gi, aki waax yu ñuy faral a jaar bu ñuy dem End: benn ngir defar fa seen yaqu-yaqu yu gaal walla ngir wut fa ab dund walla ngir yaxantu, ndax dañu fa daan jënd ay marsandiis yu Afrig niki wurus ak bëñu ñay ak daakaande ak ay rëndaay ( condiments). Waa Tugal yi bi ñuy sanc tefes yi ak di fa tabax ay digg yu yaxantu, daje wuñu woon ak benn jafe-jafe bu juge ci waa Afrig yi, loolu daal ci jàmm lañu ko defe akug dal. Li am sax mooy way dëkk yi teeru nañu leen ci teraanga, jox leeni suuf ak jumtukaay yi manul a ñàkk. Diggi yaxantu yooyu nag ñi ngi daa ame ci yii :

1) Dencuwaay ( magasin) bu ñuy denc marsandiis yi 2) Ay dëkkuwaay ñeel waa Tugal yiy saytu digg yooyu 3) Ab jàngu ( egliis) 4) Benn saal bu ndaw bu ñuy teertoo way siyaaresi yi

Am na ci diggi yaxantu yi yoy ñi ngi leen di liggéeye ci melokaanu tata (fortification) ju terewu (difficile d’acces) ngir moytu ay cong yu ñu leen mana def. Waa Tugal yi dañoo gis ne seen xay gi moo gën a kawe gu dul moom, looloo waraloon ñu ga woon ko yeneen askan yi.

Aw dogiit wu ñuy yër (lire):

Suñu maam yi ci teraanga ak jàmm lañu nekkoon, ami gétt aki tool. Bis gis nañu ca biir géej ga lenn njanaaw lu mag, lu ami laaf yu weex. Aw nit wu weex bàyyikoo nañu ca ndox ma, tudd ay baat yoy kenn ci ñoom déggu leen. Booba la sunu maam yi tiit: ñu jortu ne ñoom de ay jinne lañu, ñu leen di jéem a delloowaat ci géej gi jaare ko ci jëfandikoo ay fett, waaye jinne yi soqi nañu ci seen kaw sawara sos kàddu gi daa mel ag dënnu. Rayees na ñu bari ci ñoom. Sunu maam ya ca dees daal di daw.

Lii ci nettaliy gimiñ yi la :G.L Havaux


Waa Tugal yi ci tefesug Afrig gi :

Yaxantug ñatti koñ yi :

Ci lu tollook juroom ñatteelu xarnu g.j, jaayees na ay jaam yu waa Afrig ci ay yaxantukat yu daa def yaxantug tàkk gi, ak gu tefes gi ci tefesug mbàmbulaan gu End gi (ocean indien).

Ñu màng jaam yooyu yobbu leen ca Afrig gu bëj-gànnaar ga (naar yi), fa la ñu leen jaayaat, ngir ñu doon fay mbindaan aki surga aki soldaar.

Gii yaxantu moom lañuy woowe njaayum jaam yi. Njaayum jaam yi gën naa yaatu bi xarnub fukk ak juroom benn tàmbalee g.j : Waa Tugal yi dañoo aajowoo woon ay loxo yuy liggéey ngir jariñoo mbell yeek suuf yi ñu moom ci Amerig. Looloo taxoon ñu gaawoon dem ca tefesug Afrig gi ngir jëndi ay jam. Ginnaaw nag jaam ya nekkoon ca tefes ga doyuñu woon, ñoom waa Tugal yi dañoo yabaloon ay ñu leen wuutu ñu Afrig ngir ñu gëstujil leen ay way néew-doole ci biir gox bi.

Ndawi tubaab yu Afrig yooyu dañu daan song dëkk-dëkkaan yi di leen lakk, di ray mag ñeek ndaw ñi, bu ko defee yobbu góor ñeek jigéen ñi am kàttanug liggéey. Dañu leen daan jéng, jiital leen ñuy liiru jëm ci digg yii : Gore - Owida - Luwanda. Foofa lañu leen di jaaye tubaab yi leen di sëf ci gaal yi, dem ak ñoom Amerig ci ay nekkiin yu metti te wow, yuy far a ray li ëpp ci ñoom ba lañoo àgg fa ñu jëm. Bu ñu àggee Amerig rekk ñu jaayati leen way meññilu yi (les investisseurs :exploitants), bu ko defee ñenn ci ñoom ñu tàggale leen ak seeni njaboot, te daa leen manante ci def liggéey yu diis yi. Sang bi nag daa na am àq ak sañ-sañ bu mat ci def lu ko soob ci jaam bi. Bu moyee ay ndigalam sang bi daa na digale ñu mbugal ko ba loolu leeg-leeg daa na waral ag faatam. Ci atum 1787 g.j, lañu jël ay matuwaay ngir aaye yaxantu gu ruslu gii. Ci jooju jamono la ay mbootaay sosu yuy safaan ag njaam, gu ci mel ne mbootaay ga amoon ca Angalteer ngir jële fi njaam, ak lonkoo gu xariti ñu ñuul ñi ca Frãas. Waaye njaayum jaam moom dañul ndare ca mujjug xarnub fukk ak juroom ñeent g.j . Afrig ñàkk na ay milyoŋ ciy doomam ngir njaayum jaam yi. Moom de - njaayum jaam - ag tooñaange gu mag la ñeel ag nite ci lu dul gën jaa néewi sikk.

(( Li ñu jublu ci yaxantug ñatti koñ yi mooy jaay gi ñu daa def doomi Afrig yu am yi kàttan, ngir ñu bayi te tabaxi Amerig te waa Tugal yi ko daa def, di jël njëg ga’ak di ko yobbooti Tugal, ngir suqali ko ca. Kon muy yaxantu gu ñatti koñ séq : Afrig gi ñuy jële njaay mi, Amerig gi ñu koy jaayeji, ak Tugal gi koy jëndsi walla fëkksi ci Afrig, jaayeji ko Amerig, yobbu njëg ga Tugal. Fii ba tay man nañu fee gis ne Afrig jëf na ay jëf yu am solo ci jëm-kanam gu koom-koom, gu mboolaay, gu fànn ak ak ak, gu ñaari gox yii, te yii ñaari gox ñoom it dox nanu bu baax cig deltu ginnaawam, ndax ŋacc nañu ciy ponkalam, yi ko manoon a jëmal kanam aki xéewalam, yi ko manoon a liggéey, ci ginnaaw bi ñu ko sancee (coloniisee), teg ko loxo, muucu ay gongikuwaayi xéewalam, yobbu defare seeni réew))


Waa Tugal yi ci tefesug Afrig gi :

Njuréefi njaayum jaam yi (les conséquences) :

Askani Tugal yi dugg nañu ci njaayum jaam ci anam gu tar, looloo waral :

- Ay gëpplante aki xare ci diggante réewi Tugal yi - Barig ñi dee ak ñi ñu ray ci xare yi ak ci biir dox bu gudd bi ngir jéggi mbàmbulaan yi - Jeqikug askani Afrig yi ngir jàmmaarloo : looloo fi jur ay jafe-jafe yu mboolaay, yu koom-koom yu tar, niki néew dooleg dëkk yu mag yi, tasug ab xiif, wañse, ak yàqug jikko yi, ak amadig kaaraange ak tasug njaboot yi. - Ŋacc Afrig ciy doomam yu am yi doole, ak ci kàttanam yu nit yi, looloo ko doyadiloo woon ba manul woon a jàmmaarlook canc gi (colonisation).

Ngir mettiit yi jaam yi daa jànkoonteel, boroom yéene yu rafet yi jug nañu ngemb séen bopp ne dañu fiy jële njaam ci turu teddngay nit : ca Angalteer ag yëngu-yëngu judd na fa ngir neenal njaayum jaam (le mouvement Abolitionniste). Bu dee ci Frãas it mbootaayug xariti ñu ñuul ñi (Organisation des Amis des Noirs) taxaw fa ngir xeex ag njaam. Waaye yaxantu gu gàccaale gii jëleesu ko fi lu dul ci atum 1848 g.j .


Waa Tugal yi ci tefesug Afrig gi :

Ndajem Berlin :

Réewi Tugal yi tàmbali nañu di sanc Afrig, maanaam di ko koloniise, ay réeroo nag daal di tàmbalee am ci seen biir ñoom waa Tugal yi, yoy xaw na leen a yobbu ci ay xare, loolu mooy li xewoon ca Isipt atum 1869 g.j, ndax kat Frãas ak Angalteer, ku ci nekk daa bëggoon a teg loxo ci kanaalub Suwes. Ca Tunisi, Frãas ak Itaali xat-xatloo nañ fa ngir jéem fa a teg tànk. Ci mbalkam Kongo (bassin du Congo), (diggu yaxantu bu mag bi) ag xëccoo amoon na fa ci diggante Frãas, Portigaal ak Buurub Beljig ngir féetewoo ko. Ngir tee xare am, njiitul Almaañ li di Bismark daa woo woon kilifay réewi Tugal yi cim ndaje ca Berlin. Réew yii nag ñooy : Frãas, Angalteer, Beljig, Almaañ, Portigaal, Espaañ ak Itaali… Liggéeyu ndaje mi nag wéy na ñatti weer (la ko dale ca nowambar 1884 ba feebriye 1885 g.j). Ndaje mii jël na ay saxal yu am solo :

- Saxal ponk yi ñuy sance (coloniser) sancu yu bees yi. War na ci aji sanc ji (le colonisateur) bu bëggee sanc am réew mu waajal ab xare ( armée) yëggal it yeneen réew yi nar gi mu nar loolu. - Sañ-sañu yaxantu ci kaw dex yi

Ndaje mi nag bàyyi na fi ay ngérte (résultats) yu naqari:

Réew mu nekk di njëkkantee teg loxo wàll gi gën a rëy ci Afrig, ngir ragal ay dëkkandoom di ko fa xatal. Lii moo doonoon tàmbalig rawante gi ci wàllug sanc. Ci atum1900 (maanaam bi ndaje mi amee ba am fukki at ak juroom) la mbooleem suufi Afrig yi rot ci ŋëbug wa Tugal yi


Jàmmaarloo ci ngànnaay kontar canc gi :

Lu ëpp ci goxi Afrig yi waa Tugal yi tegoon loxo ci jàmm lañu ko defe woon, li ko waral mooy waa Afrig yi dañoo jortoon ne tubaab yi de dañu fee jaar rekk waaye duñu fi yàgg. Waaye ci ginnaaw bi lañu gis ne canc gi (la colonisation) de mi ngi defi sémb ngir nar fee sax, te it mi ngi liggéey ci soppi séenuw dundiin.

Ci yenn barab yi ( niki Senegaal ), waa Tugal yi daje nañook ay jàmmaarloo yu tar. Nguuri Afrig yi amoon nañu ay xare (larme) yu ñu waajal, looloo leen dimbali woon ci ñu man a xeex jàmbur yii. Bu dee giir yeek dëkk-dëkkaan yi, ñoom dañu doon xeex ci séenug anam, maanaam di def ay cong yu tàqalikoo, fii ak fee (dóor-làqu ;guérilla).

Waa Afrig yi def nañu ay jàmmaarloo ci ngànnaay, yu jur ay ñàkk yu tar ci sàppes waa Tugal yi. Yenn jàmmaarloo yi wéy nañu ba ci atum 1930 g.j . Ca dëgg-dëgg waa Afrig yi ñoo gënoon a limu, te ëppooni xam-xam ci toolu xare bi. Soldaari Tugal yi nag yoroon nanu ay ngànnaayi sawara yu aaytal, waaye dañoo xawoon a doyadi, ndax manuñu woon a dékku tàngoor wu tar wi ak tawati rëddu yamoo wi (maladies tropicales).


Jàmmaarloo ci ngànnaay kontar canc gi : 

Latjoor Jóob :

Ag njabootam : Latjoor mi ngi juddoo ca Kër Amadu Yala, atum 1842 g.j, baay ja di Saxoor Soxna Mbay Jóob, nday ja lingeer Ngoone Latiir Faal.

Ay meloom : Latjoor waxambaane wu jàmbaare la woon, wu amoonug dogu, mu bokkoon ci ñu mag ñi daa jàmmaarlook way sanc yi ci goxub Afrig, mu nekkoon di kenn ci ñi ci gën a jàmbaare, gën cee fés, kenn melul ni moom ci sopp suufam ak ndonoom. Amoon na fit wow kenn du ko doyadil, daawul tiit ak lu man a xew. Nekkoon na njiitul xare lu mag, di aji politig ju ñaw, ju di boroomug jommal. Ci atum 1862 g.j, la ñu fal Latjoor Dameel ca Kajoor. Ci atum 1864 g.j, la ko Federb dàqe Kajoor, teg ca loxo, bu ko defee Latjoor dellu Riib, fa la ko sëriñub Tukkloor ba fate woon di Màbba Jaxu Ba, mu mujjoon nekk ci ron ag kiliftéefam. Màbba mii moo ko manante ci mu dugg ci lislaam. Latjoor ànd na’ak Màbba ca xareb Somb ba kontar Buur-Siin Kumba Nd óof éen Juuf. Bi ñu rayee Màbba ca xare boobu ca Somb la Latjoor dellu Kajoor, Tubaab yi falaat ko fa bi mu agsee, mu dellu waat di Dameelu Kajoor. Loolu mi ngi jege atum 1871 g.j. Ci atum 1878 g.j, ci la Tubaab yi dogoo ci indi fi yoonu weñ ( chemain de fer) wu saxaar giy jaar ci diggënte Ndar ak Dakaar ngir yombal tuxalug gerte gi, waaye Latjoor bañ bañ gu tar, daal di def ag fipp gu mag ak ay àndadoom atum 1882 ba 1883 g.j. Ci noonu xare bi tàkk digganteem ak Tubbaab yi, mu nekkoon xare bu tàng jérr waaye way sanc yi notoon nañu Latjoor ngir néewug ay ngànnaayam aki jumtukaayi xareem ak bari gi ñu bari woon ñoom jumtukaay yooyu ñeel Tubaab yi. Ci noonu Latjoor ñakkoon pexe, daal di weeruji ca buurub Jolof ba Alburi ŋaay, looul nag di woon atum 1884. Bi Latjoor jugee Kajoor la Tubaab yi fal Ammari Ngoone Faal muy Dameelu Kajoor, waaye gaaw nañu koo folli ngir ñaxtu gu tar ga waa Kajoor doon ñaxtu loolu. Bu ko defee Samba Lawbe Faal ñëw toog ci jal bi, mooy ki may tubaab bi mu indi fi raay bi. Waaye ak lim leen may ñu indi fi raay bi lépp teewul ñu yong ko ca wetu Tiwaawan, ñaari ŋiiti Fràas ñoo ko ray, ñooy Chauves ak Spitzer, ñu daal di s àkku ci Latjoor mu bañ a teggati tànk ci suufus Kajoor, waaye Latjoor bañ, dellu Kajoor. Ci noonu xare bu tàng tàkkati ci diggante Latjoor ak Salvatius, ci la Salvatius nangoo Kajoor ci atum 1886, Ñu ray Latjoor ca Deqale aki doomam ak juroom ñaar fukk ak juroom ñatt ciy àndadoom, ci 25 oktoobar 1886. Kureelug xare (battaillon) gi ko ray Valois moo ko jiite woon.


Jàmmaarloo ci ngànnaay kontar canc gi :

Alburi Njaay :

Alburi Njaay mi ngi juddoo ci ndëkk su ñu naan Tiyal ci wetu Daara Jolof ci lu tollook 1842 g.j.

Ag njaootam : baayam a ngi tuddoon Biram Penda Njeeme Njaay, yaayam Seynabu Jóob. Kajoor la màggee, fa la dugge ci Lislam. Mi ngi teg loxo Jolof ci ginnaaw ab xare kontar Amadu Seexu, mu bokkoon ca mbooloom xare mu Latjoor ma tubaab ya doon jàppale ca atum 1875. Tubaab yi dañoo bëggoon a def ak moom ag tapoo ( alliance), waaye nanguwu ko woon ndax manul woon a nangu ñuy am ab sañ-sañ ci Jolof, mu daal di tambali di jàmmarloo ak ñoom, bu ko defee ñiy xeex tubaab yi di ko ci soñ te di ko aar it, waaye mu mujj nangul leen ñoom tubaab yi. Ci atum 1885 la féttéerluwaat kontar leen, waaye ñu daq ko, nangu péey ba Yang-yang ci njiitug Duts, daal di fal Samba Lawbe Penda Saa Ngoone Njaay, muy buurub Jolof. Alburi mujj na ñàkk pexe, daal di wéeruji ca Amadu Seexu tukkloor ba, moom jiite woon na ab xareem ci Senegaal ak ca Mali. Mi ngi faatoo ci Nijeer atum 1902. dees na ko jàppe nag jàmbaar ju mag ju daa xeex ngir goreel Afrig ci kiliftéefug Tubaab yi..


Jàmmaarloo ci ngànnaay kontar canc gi :

Alaaji Omar Taal :

Alaaji Omar Fuutiyu Taal mi ngi gane àdduna ci ndëkk su ñu naan Elwaar, ci wetu Podoor atum 1794 -1796 g.j, mu bokkoon ci askan wu cosaanu ci Lislaam, baayam mi ngi tuddoon Sahiid mom Usmaan mom Muxtaar Tukkloor bi, yaayam tuddoon soxna Aadama Caam.

Dund na ay at ca barab yu sell ya (Màkka), bi mu déllusee réewam la dogu woon ci tas Lislaam te jële fi way sanc yi. Ci atum 1853 g.j, la jibal jiyaar ngir yékkati baatub « Laa ilaaha illal Laah » .

Mu song Karta ak Xaaso nangu leen, def fa imbraatóoram gu lislaam gi. Xareb Alaaji Oamar fenqoo na’ak bu Federb bi nga xam ne li ko yékkati woon mooy aar sancoom yi mu amoon ci sowwu bi, ak jéem a tegi loxo penku bi. Alaaji Omar saxoon na te të ci kanamu dooley sanc gi, waaye ci mujj gi mu daanu ca doji Banja Gara ya ca Gine atum 1864 g.j. Bu ko defee doom ja Ahmad Seexu daal di yanu raayub jiyaar bi ci ginnaawam, waaye moom it amoon na ag lott ci kanamu ngànnaayu sancaan yu lëw yii te aaytal. Bi mu ñàkkee pexe la xaatim ag kóllare ak tubaay yi atum 1881 g.j, waaye Gayni mi mu defaloon kóllare googu daal di koy wor, ndax songaat na ko, ga ko ci mu daw, foofu la imbraatóor gi daanoo ci loxoy tubaab yi, atum 1889 g.j .


Jàmmaarloo ci ngànnaay kontar canc gi :

Muhammad Lamin Daraame :

Muhammad Lamin Daraame (turam dëgg di Demba Dibaasi) sëriñ la won bu bokkoon ci giirug Saraxule, di woon it tiijaan bu askanoo ci Gonjuro. Tukki woon na dem Màkkatal Mukaarama, nekk fa ba 1879 g,j. Bi mu dellusee la ko Ahmad Seexu jàpp, jotul a àgg cig njabootam lu dul ci atum 1885 g.j .

Muhammad Lamin Daraame siiwe woon na ag ragal Yàlla, looloo waraloon mu amoon taalube yu bari. Jibaloon na jiyaar ci kaw dëkkandoom yi duli jullit ak ci ñoñ frãas ñi sancoon réew mi. Xareem bi, tolloon ci junniy xarekat jawali woon na Bundu, daal woon gaw tatay Bakkel ji, atum 1886 g.j, waaye ak li ko waa Bakkel doon faral lépp taxutoon mu man a teg loxo ci dëkk bi, looloo taxoon mu dëppaat. Waa Frãas yi tiitoon nanu lool ci ndam yi xareem bi ndàmm, looloo waraloon ñu song ko nangu Sinodibo, njaf doomam ja Saybu, ginnaw bi ñu ray ko.

Ci atum 1887 g.j, la ko tubaab yi manante ci deltu ginaaaw jëm Gambi. Daal di toj tata ja mu tabaxoon ca Tuubaa Kuta. Muhammad Lamiin ñàkkoon na lu bari ci xarekatam yi ci xare bii. Tubaab yi ray nanu ko ci ndimbalul Muusa Mulo. Ñu mujjoon manante buur yu bari ci ñu xaatim ay kóllarey ndénkaane(tutelle), tegoon it loxo lu ëpp ci suufi Senegaal yi.


Jàmmaarloo ci ngànnaay kontar canc gi :

Saamóori Ture : Saamóori Ture mi ngi juddoo Mayambalandogo ci lu tollook 1830 g.j. Mu nekkoon ab yaxantukat, dajale woon na ab xare ngir nangu suuf yu bari, daal di taxawal ag Imbraatóor. Dugg na ci Lislaam atum 1880 g.j, daal di wéy nag ci yaatal Imbratóor gi. Waaye xéy na cig mbetteel fenqoo ak Tubaab yi daan sanc, daal di jàmmarloo ak ñoom jàmmarloo gu tar : leeg-leeg ci anamug maslaa (diplomatie) jaare ko ci di def ak ñoom ay déggoo, lu ci mel ne déggoo gu Bisandogo ; leeg-leeg it ci anamug xeex ak ñoom. Waaye waa Fràas yi ci njitug Gayni ñoo ëppoon ngànnaay : ndax ñoom amoon nañu ay kanó aki fetal yu aaytal. Bu dee Saamóori nag, moom dafa sukkandiku woon rekk ci fasam yi ak fetal yi tëgg yi daa liggéey. Jot naa daq nag tubaab yi te jàmmarloo ak ñoom diirug 12 at. Ci atum 1892 g.j, la dooley xareem ji tàmbalee doyadi ngir xeex yu bari yi, bu ko defee tubaab yi song Imbratooram gi. Saamóori lànkoon na ne du wommatu ( se rendre), mu daal di woon dem jëm penku taxawal fa ag nguur gu yees ci bëj gannaaru Tefesug bëñu ñay gi (Cote d’ivoire), waaye fekk na waa Fràas yi ak waa Angalteer xemmeemoon barab bii mu taxawal nguuram gi. Ci atum 1898 g.j, waa Fràas yi bett nañu ko ca kãa bu Gelemu, ñu njaf ko, yobbu ko Gabon, fa la faatoo ci atum 1900 g.j daal di jël nguuram googu boole ko ci Cote d’Ivoire. Jàmarloo gu Saamóori Ture gi kontar tubaab yi dees na ko jàppe genn ci yi ëpp solo ci jàmmarloo yi ci sowwu Afrig. Sax na diirub 17 at. Yóbbe na canc gi ay ñakk yu takku.


Jàmmaarloo ci jàmm :

Alaaji Maalik SY :

Alaaji Maalik ma nga gane àdduna Gaaya ca wetu Dagana atum 1855. Waajuram wu góor tuddoon Usmaan, wu jigéen Faa Wàdd Wele. Mi ngi jànge alxuraan Luga ci kenn ci taalibey Alaaji Omar Futiyu Taal yi. Bi mu doonee mag la dem Màkka, bi mu dellusee sax ci jaamu Yàlla ak jàngale ak dugal ñi duli jullit ci lislaam. Ci noonu la tase njàngalem yoonu Tiijan ci Senegaal jaare ko ci tuxoom yi ci Jolof, Kajoor ak Ndar. Ci mujj gi mu dëkksi Tiwaawan atum 1902. Fa la njëkk a xumbale gàmmu. Wooteem bi mi ngi ko doon defe ci dëkk yu mag yi, tabax fa ay jàkka, xeex fa ag réer akug ñàkk, ñu tudde ko Mawdo giiy tekki aji gindi ji. Alaaji Maalik nag (yal na ko Yàlla gërëm), mi ngi laqu atum 1922 g.j.


Jàmmaarloo ci jàmm :

Seex Ahmadu Bamba :

Seex Ahmadu Bamba mi ngi gane Adduna ci lu tollook 1853 - 1854 g.j. Mu bokk nag ci askan wu xóot ci diine cosaanu ci lislaam, wu tukkee Fuuta Tooro. Mi ngi yaroo ci ron ker gu njàggalem lislaam, mu mujj nag di sëriñ buy yare, bu siiwe ci ragal Yàlla dëddu ak fegu, di ku ñu xame ci mbind mu bari, moo xam wesar la walla woy.

Ci atum 1888 g.j, la taxawal dëkkub Tuubaa bu ñu aar bi, ak yoonam wii di Murit. Gàddaayoon na dem Jolof atum 1895 g.j, ànd ak juroomi téeméer ciy dongo, sori waa Frãas yi nekkoon Bawal, loolu nag da koo defoon ngir man a yar murit yi yarub lislaam bu wér, set te sell.

Sëriñ bi jiyaar na’ak tubaab yi waaye du ci ngànnaay, xanaa ci xam-xam ak ragal Yàlla, ak yare ci. Waaye siiwam gi, sellam gi, dëggoom gi ak sottiku gi nit ñi def ci moom ngir loolu, tax nanu ba sancaan yi tiit, looloo waraloon ñu jiiñoon ko ne day defi naal ngir dal ci séen kaw ci jiyaar. Lii a tax ñu génne ko Senegaal, yobbu ko Gabon atum 1895 g.j, mu sax fa diirub juroom ñaari at. Bi Sëñ bi dellusee cim réewam atum 1902 g.j, la mboolooy nit ñi tuurooti ci këram ciw melo wu tiitle, yoonu Murit daal di tas ci mbooleem wàlli réew mi ci gaawaay bu jéggi dayo ba. Lii a waral tubaab yi génneeti ko, yobbu ko Muritani, ngir tuutal ko, wàññi darajaam ci kanamu naar yi. Bi ñu sonnee te amuñu li ñu bëggoon (ndax Sëñ bi da fa’a gën a kawee, naar yiy jébbalu te lañu bëggoon mooy lu safaanook loolu) lañu ko délloosi Senegaal ca Cëyéen, ca Luga atum 1907 g.j. Ci mujj gi, ñu ga ko ci toog Jurbel atum 1912 g.j, ba kero muy wuyyuji boroomam atum 1927 g.j . Mu bàyyi fi nag ay taalube yu ñu xame dégg-ndigal ak topp.

(ñoom nag ba ñu koy ga ci toog Jurbel, dañoo jortoon ne ñi ngi ciy ame li ñu bëgg, te fekk safaan moo cay juddoo, li Yàlla namm ci Sëñ bi rekk a cay juddoo. Sëñ bi wax na ciw woy ne : (( sàkku nañu samag dox jëm Jurrbel ca atum 1330 g,g - waaye bu ñu gisoon mbóot mi nekk ci dox googu duñu ko sàkku)) )


Jàmmaarloo ci jàmm :

Seydinaa Limaamu Laay :

Seyidinaa Limaamu ab nappkat la woon bu juddoo Yoof atum 1845 g.j. Ci atum 1885 g.j, mu gént gis ne mooy Mahdiyu .. mu tàmbalee woo àndandoom yi ci ñu dugg ci Lislaam, di soññ jullit ñi ci ñu sellal te jaamu Yàlla rekk, mu daa wax : (( wuyyuleen wooteb Yàlla, man de yonnantub Yàlla laa, maay Mahdiyu mi ñuy neggandiku)), daa na woo ay àndandoom jëme léen cig jub ak jàppalante. Bu ko defee nit ñu bari dikkal ko ngir déglu njàggaleem mi. Mu daal di sos kuréelug Laayéen. Siiwam gi tiitloo woon na way sanc yi ragaloon ag jeqiku kontar leen. Ci atum 1887 g.j, la sancaan yi taxaw ci jàpp ko, bi mu yëgee seen naal yooyu la ànd ak lenn ciy àndadoom génn, waaye tubaab bi jàpp ko ca wetu Caaroy. Waaye ëttu àtte bi mujj na ko setal ko ngir ñàkk lenn lu man a dëgëral tuuma yi ñu teg ci kawam. Limaamu wéyoon na ci wooteem gi, waaye daa na def jamono ju nekk muy fenqook sancaan yi ko daa jéem a sonal ak àndandoom yi. Mi ngi làqu atum 1909 g.j.


Jàmmaarloo ci jàmm :

Aliin Situwe Jaata :

Aliin Situwe Jaata jigéen la woon ju juddoo Kabrus ci Kaasamaas, atum 1920 g.j. moom nag ame woon na benn gàkk-gàkk ngir tawati lompoñ ju ko daloon. Nekkoon na dib jaaykat bob tukki woon na dem Dakaar, jot faa liggéey niki mindaan. Mujj na - jaare ko ci Imaa Imit - di ab jabar ci diiney xërëm ji fi fekkoon baax.

Jaata àndutoon ci ni tubaab yi di def ci réew mi : fayloo nit ñi galag yu seer, liggéeyloo leen cig sañ-bañ ak dugal waa Senegaal yi ci xareb Frãas bi (son armée). Mu sàkku woon ci waa réew mi ñu bañ a bay gerte gi leen tubaab teg ci doole, te bay lu ñu man a dunde niki : ceeb, mboq, dugub ak yu ni deme.

Aliin Situwe nekkoon na di ku daa xeex diiney nasaraan (kercente), daa na woote it ci ñu dellu ci diiney Afrig yi, te màggal aaday maam yi. Dees na ko jàppe ki njëkk a woote ag yamoo ci diggante góor ñi, te bàyyi di xool ay askan aki diine walla ay xalaat. Daa na woote it ag yamoo diggante góor ak jigéen te booba jigéen ku desoon ginnaaw la woon ci mboolaay gi(la société). Daa na woote it ci mag ñeek gone yi di dimbalante.

Ci biir xareb àdduna bu ñaareel bi, Jaata siiwoon na ba daj Kaasamaas gépp, ñu mujj di ko dàkkantalee Boroom Kabrus, te kat jàmmaarloo gi mu doon def ci anamug jàmm la ko doon defe. Siiwam gi tiitloo woon na waa Frãas yi tegoon loxo ci réew mi, ñu mujj jàpp ko ca Kabrus ci 28 samwiye 1943 g.j, bu ko defee ëttu àtte bu Sigicoor àtte ko, tëjlu ko fukki at, ñu làq ko, yobbu ko Tumbuktu ca Mali, fa la faatoo ci 22 mee atum 1944 g.j, te booba mi ngi ci digg ag njegemaaram .


Afrig ci biir ñaari xare yu àdduna yi :

Ab xare bu tàng tàkk na ci diggante Frãas ak Almaañ ci diggante 1914 - 1918 g.j. Ñaari réew yii mu ci nekk daw na wuti ndimbal ci li ëpp ci réew yi mu defal ay tapoo (alliance). Bu ko defee yàggul dara lu bari ci réewi àdduna bi duggsi ci. Frãas sàkku woon na ci mbooleem ay sancoom ñu jàppale ko ci xeex bi, te jox koy nit. Jot naa dajale - ci ndimbalul Blees Jaañ - am mbooloom xare mu mag, mu xeex ci wetu Frãas kontar sancuy Almaañ yi, ñu nangu ci Togo ak Kamerun ak wàllug sowwu gi ci bëj-saalumu Afrig ak Tanganika (Tansaani ci jii jamono). Lu bari ci xarey Afrig yi (sànnikati Senegaal yi ca lañu woon ) jawali nañu Tugal, ngir xeexal Frãas. Xarekati Afrig yii ñi ngi nekkoon ci dundiinn wu tar te wow, ci biir yeer yi ak ci sedd bu metti bi, jànkoonte nañook jafe-jafe yu bari, lu ci mel ne ñàkk a dégg làkkuw waa Frãas wi akug tumbrànke. Waaye loolu lépp teewul ñu ràññikoo woon ag njàmbaare akug dogu. Xare ba jeex na ci ndamul Frãas ak ñi àndoon ak moom, ñu dàq Almaañ, mu doxe ci ñàkk mbooleem sancoom yi ci Afrig. Ci atum 1939 g.j, la ab xare tàkkaat bu bees bu tàllaliku ba daj Tugal ak mbooleem réewi àdduna bi. Hitler njiitul Almaañ li daa gëmoon ne réewam mooy mi gën a kawe ci àdduna bi, kon yi ci des yépp dañoo war a toroxlu ciy tànkam, Itaali nag ak Japon dañoo àndoon ak moom ci loolu. Waaye réewi demokaraasi yi dañu koo kontaroon. Xareb Almaañ bi songoon na suufi Frãas yi, loolu jur Frãas séddaliku ci ñaari wàll, wàll guy jàppale Almaañ te ànd ak moom ak gu nekk ci ron kiliftéefug Jeneraal Degol, mooy giy jàmmaarloo ak a xeex Almaañ. Afrig gu rëddu yamoo wi(equatorial) gi Frãas yilifoon ci njiitul Flips Ibuwe dafa nekkoon di jàppale Degol, bu ko defee njiiti Afrig gu sowwu gu Frãas gi ñoom di jàppale Almaañ, ba ca desambar 1942 g.j, booba lañu wëlbatiku jàppaleji way tapoo yi (les alliés). Waa Afrig yi yamuñu foofu, waaye yabal nañu ay soldaar ca jëwub xare ba (front de guerre) ngir jox ñam way xare yi ak jox mbell Tugal. Ci atum 1945 lañu daan Almaañ.. Japon it daanu ngir soxub saal (bombe atomique) ba waa Amerig yi taal ca kawam. Ñaareelu xare bi dakk na - niki bi ko jiitu woon - alag dundug ay milyoŋ ciy nit.