Xoriit wuute gi ci sumb yi

Contenu supprimé Contenu ajouté
Daarul xayri (waxtaancëru)
Xët wu bees : vignette|Garabug Xoriit '''Xoriit''' ag garab la gog xob yi dañuy sew tey am mbaar muy gën a yaatu lu garab giy gën a màggat.…
Tafaan: Éditeur de wikicode 2017
(Aucune différence)

Sumb bu 24 Sattumbar 2019 à 21:29

Xoriit ag garab la gog xob yi dañuy sew tey am mbaar muy gën a yaatu lu garab giy gën a màggat. Man naa njool ba ci 3i met ba ci 10i met. Peeru garab gi day dëng. Jafe-jafe yi ko daay yiy indil dagg yi nuy dagg ay xobam tax na garab gi bokk ci yu ñeme coono yi. Xoriit garab la guy sax ci àll, nu man koo jëfandikoo ci lu nuy lekk mbaa di ko fajoo

Garabug Xoriit

Dëkkuwaayam

Garab gi ci àll bu bariy garab lay dëkk, walla ci kaw dëkkuwaay yuy max, leeg-leeg ci peggu penkug Afrig.

Mbayam

Garab man naa nangu ab sedd yuy am leeg-leeg. Waaye li mu gën a nangu mooy tàngoor, soxla na it suuf su tooy, te it àttan na aw wal(inondation).

Njariñam

Lu jëm ci lu nuy lekk, xob yi dees koy togg boole ko ak supp mbaa ay pepp. Foytéefam day am caas bu weex bu nu man a lekk boole ak doom yi nu togg. Foytéefam bi man naa àgg ba ci 4-5i sàntimet ci xala.

wàll um paj

Xob yi man naa faj bopp buy meti. Saxaaru ndox mu tàng mi dees koy suuroo ngir faj ay jafe-jafey gis. Xob man naa faj it payiis. Xas mi day faj biir buy metti, ak tële. Sungufam ku ko boole ak diw man naa nekk forote buy faj ay yax yuy metti. Reenam day faj sifilis (febaru sëy)

Melo

Yeneen njariñ. Wirgo wu mboq man naa génn ci garab gi. Bantam ci dagg bi man naa niru lu dëgër waaye amul lenn njariñ ludul ay jumtukaay yu ñàkk solo.

Nataal yi

Turu xam-xam

Crateva