Jàngoro Koronaawiris 2019
Koronaawiris 2019 (COVID-19) Jàngoro la buy wàlle saa su nitt ku mu dal jege ñeneeni nitt. Jàngoro ji li key ubbil buntu ci ab doomu aadama mooy mu jege ku feebar, walla mu tekk loxoom fu ku feebar jotoon a laal ba pare dàldi laal at bëtam, walla bakkanam walla gémminñam. Li ci ëpp, wiris bi li koy tasaare moodi tox-tox yiy juge ci tissóóli ak sëqëtu ku mu wàll ba pare. Képp koo xamantene yaa ngi jege ku feebar bi wàll, muy tissóóli mbaa di sëqët te sori wu loo ko lu ëpp ñaari meetar, li gën woor mooy di na la wàll. Neneen nu la wiris bi mënees wàll mooy nga laal fu mu teggu ba noppi, raxasuloo sey yoxo ak saabu, ba pare nga laal sey gët, sa nopp walla sa bakkan.[1]
Ndoorte
SoppiJàngoro ji Wuhan, capitaalu Hubei ca Chine, la njëkk feeñ bi atum 2019 di door tàmbale. Diggënte boobu ak léégi, wiris bi law na ci aduna ci yëpp. Ba tax na OMS, bisu 11 mars 2020, diggele ñu jappee Koronaawiris ab pandemie. Pandemi doon feebar boo xamantene da fa tasaaro bu baax ci aduna ci yëpp. Rééw yi feebar bi gën sonnal, ñi mu fa rey bari neñ tek ci seeni dispañseer ak loppitaal li ñu leen yan ci ay ñu tawat dootu ñu ko àttan. Njiitu OMS, Dr. Tedros Adhanom Ghebreyesus, wax na ni “lii du mbirum wér gu yaram doŋŋ, ndax bépp xeetu liggééyukaay da na ko yég moo tax it ñëpp a war a japp ci xeex mi.
Màndargay feebar bi ak pac-mi
SoppiBokk na ci Màndargay Jàngorooy Koronaawiris sëqat, xeetu sibbiru, sonn ak xiixët. Léé- léé ki feebar am metitu yaram, baqata yuy tuuru, biir buy daw, metitu boli, metitu naq ak it dara dootu ko xeeñ. Ñi koronaawiris wàll, ci diggënte ñaar ak fukk-ak-ñenti fan la ñuy key tàmbale yég, waaye ñi ci ëpp, bu weeso fukki fan ley tàmbale feeñ. Ñu bare nak feebar bi di na leen dal te du metti noonu. Ña feebar bi sonnal dëgg lée-lée ñu jëlé ci Pneumonie, mu yàq seeni xëtër, seeni xol, ak yeneen. Ña feebar bi sonnal li leen war mooy ñu teela jublu ci doktoor.[2]
Nit mun naa am jàngoro ji te lenn du ko fesal, du metit bu muy yég, du lu ñi ko jege mën tek bët. Loolu la ñu naan "asymptomatique". Waaye ña feebar bi wàll te yégu ñu ko, ña "asymptomatique", mëness ne ñu wàll jàngoro ji képp ku leen jege. Loolu moo waral jàngoro ji gaaw law ci àdduna.
Doktoor yi bu ñuy seet ndax jàngoro ji mi ngi ci nit, ca baqata ya leñuy key seet. Beneen pexe buy firnde ndax nit ki da fa am jàngoro ji am déét mooy seet bu ñu naan “CT-scan”. Kéép ku ñu gis ne am na jàngoro ji, nañu ko yobbu loppital mu beru ku dul fackat du ko jege. Dëgg la garabu koronaawiris amagul waaye ña ëpp ci ñi muy dal bu leen doctoor taxawoo di ne ñu wér.
Fagaru
SoppiGuir wañi jangâro-ji dañu wara sorenté suñu biir, wañi dèm berep you fess ak nit. Kouy guène si biti, dafa wara sol mask bouy fate bakanam ak guèmem teksi "gant". Nit ñi dañu si wara bolé-di raxass sen loxo ak sabou ndir 20 simili, aye yoni yone. Ño gui wax nit ni ñu moyou di lal sen kanam ak seni loxo.
Yeneeni Leeral
Soppi- ↑ CDC (2020-02-11). "Coronavirus Disease 2019 (COVID-19)". Centers for Disease Control and Prevention (in en-us). Retrieved 2020-04-06.
- ↑ CDC (2020-02-11). "Coronavirus Disease 2019 (COVID-19)". Centers for Disease Control and Prevention (in en-us). Retrieved 2020-04-06.