Imaam Xasaali / Gasaali

imaam gasaali.png

Abuu Haamidil Xasaali / Gazali


Royuwaay:Layu Lislaam Royuwaay:Ay xamle ci jëmmam


Turam moo di Abuu Haamit Muhammat Gassaalii, di ab Saa-Tuus, Saa-Naysabuur, di ab suufiyànke, ténku ci ngiiru Saafihii ak pas-pasu Asharii, di kenn ci kàngami jamonoom, di ki gënoon a siiw ci woroom xam-xami jullit ñi ca xarnu juróomeel ba; atum gàddaay ga, (450g - 505g / 1058 ji - 1111 ji) mu nekkoon ku dégg Fiq ak Usuul ak xam-xam xelale (filosofi), doonoon ab suufiyànke ci wàllu tariixa, koju-Saafihii ci wàllu Fiq, ne woon ci ngiiru Asharii ci wàllu pas-pas, muy ki sos daaray Asharii ci xam-xamu wax, di kenn ci ñattiy ponkam ginnaaw Abul Hasan Al-Asharii, (te ñooy Baaqilaanii ak Juwaynii, ak Gassaalii).

Ñu daa ko dàkkantalee ay dàkkantal yu bari ci dundam, ba ca gënoon a siiw di "'''Layu Lislaam'''", ak yeneen niki: Taaru Diine Ji, Layu Diine Ji, Aji-wubbej Xeet Wi, Barkeb Bindeef Yi, Imaamu Imaami Diine Ji, Teddug Xeet Wi.


Amoon jeexiital gu màgg ak ug ndëgg gu leer ci kaw xeeti xam-xam yu bari niki xam-xamu xelale, Fiqub Saafihii, xam-xamu wax, Tasawuf ak Mantiq, bàyyi na fi ay téerey téere ci xeeti xam-xam yooyu.

Tuus la juddoo fa la màggee, gannaaw ba la tuxu Naysabuur taqoo woon fa ak Imaam Juwaynii (ñu koy dàkkantal ci Imaamul Haramayni), mu jële ci moom xam-xam bu bari, bi mu amee 34i at, ci la lahasee dem