Ibliis
Ibliis mooy ku ñu dàq ci yërmànde sunu Boroom, di ku ñu dàkku. (Yal na nu Yàlla musal ci moom, moom ak i ñoñam.
bu ñu nee Ibliis rekk kilifag saytaane yi la ñu ci namm, moom mi féttérlu woon, lànk, moy ndigalal sunu Boroom, moom nag Ibliis ci jinne yi la bokk, jinne ñoom ñépp a ngi bàyyikoo ci Suumiyaa baayu jinne yi niki ni Aadama nekkee baayu nit ñi.
Ibliis nag am na ay sóobare ci nit ni ak jinne (Saytaaney nit ñi ak saytaaney jinne yi).
Ñom nag dañoo taxaw teww ngir lajjloo nit ak jinne ba ñu yonjax ci li tax seen Boroom bind leen, su ko defe ëllëg ñu ànd ak ñoom tàbbi sawara.