Guyaab xeetu garabu foytéef la gu bokk ci njabootu "mirtaceae". Ci gox yi gën a bari naaj ca Amerig kepp la daa sax, ginnaaw bi la tas ci àddina bi. Baatu guyaab ci làkku Arawaag la bawoo, turub dëkk la woon ci réewu saa-kolombi ya woon.

Garabug guyaab (Psidium guajava)
Xobi garabu guyaab
Tóortóoru garabu guyaab
Meññeefum garabu guyaab

Melo wi

Soppi

Taxawaayu garab gi dafa yem, man na àgg ba 8i sàntimet ci guddaay. Xobam man na àgg ba 15i sàntimet ci guddaay ak 7i sàntimet yaatuwaay

Guyaab bi (doom) xob wu nooy la yor. Wirgoom cig ñàkk a ñor nëtëx gu leer la, cig ñor nag mboq gu dër la, day amaale ay tomb yu ñuul ci yenn xeet yi.

Solo si

Soppi

Guyaab garab la gu ràññeeku te am solo ci wàllu koom.

Dees na ko soppi njar, njambaanu foytéef ak yu ni mel. Xolliitu foytéef dees na ci faj biir buy daw. Manees na ko lekk it nim bindoo. Dees na ci jëlee sax gëtt.

Turu xam-xam wi

Soppi

Psidium guajava

Tur wi ci yeneen làkk yi

Soppi
farañse: goyave
angale: guava
itaaliyee: guava