Ginaaw saayug waajur wi

Moom sëñ bi,bi waajur wiy dund, nanguwutoon a taxaw mbaa muy taxawal dara,moom daal ci moom rekk la toppoon ,mel ne néew bu nuy sang, fu nu ko jëmewul du fa jëm. Bi mu làqoo nag,mu des ca ligéeyam ba mu ko bàyyee woon at ak lu topp. ña fa nekkoon it ciy dongo jàng rekk a leen fa bàyyi woon, du leneen,moom itam ab jàngalekat rekk la woon,waaye loolu teewul woon mu doonoon ku daan yёr (jàng) lu bari téerey Gaa ña (gaa ñi bu ñu ko waxee ñaare mooy magi tasawwuf yi) . Yàlla defoon muy ku sopp beru ak wër ni ko ñu baax ñi (ñoñ tasawwuf ) soppe woon. Mu daa indi ay anam yu wuute ci seeni waxiin, di leeral seeni maanaa yu làqu, di yëg seeni làmmiñ. Noonu la nekke woon – ci yooyu yëg-yëg ak yittewoo suufiyu yu mag yu njëkk ya, ak a gëstu séeni wax aki mbind – ba mujj himma ju kawe ji (himma ci lun man a firi mooy yitte) dikkal ko, muur ko, yёkkati ko, yëngal ko,dalal ko, mu mujj moomatul boppam manatul a def lu dul woo nit ñi ci anam gu woyof jëme ci mbiram moomu (muy tasawwuf ak ab yëg-yëgam). Bi ko mbir mi gënee lëjal nag, gën a fees fi moom,gën a rëy,mu dal di biral woote gi, wax wax ju leer.

Dajale mbooloo mi,taxaw fa ñoom xutba leen,sukkandiku ci dokkub dogu,ne leen: “Dama ne: ku àndoon ak ñun ngir jàng rekk na laxas jëm ca boppam, na dem fu ko soob, man loolu rekk taxatumaa jug, ku bëgg li nu bëgg nag,na toog”. Daal di leen fay bàyyi dugg ca biir. Waxam jii nag daal di leen bàyyi cig jaaxle, ñenn ñi dem, ña ca des,des fa,am ñuy jeem a tëyye seeni xarit ngir ñu des,ak ñuy xiirtal seen waay ci ñu dem. Sëñ bi moom ne tekk rekk,jeemul a tëyye kenn ku bëgg a dem,ba mujj li ëpp ci mbooloo mi dem bàyyi ko fa,la ca gën a néew des fa.

Bi loolu lépp daata am,fekkoon na Sëriñ bi mu sóobu woon ci ngiirum taalif ci xam-xam yu nu tuxal yu sariiya yi; mu woy Ummul Baraahiin,bu Imaam Sanoosi,wayjur wi nangu ko, bég ci ,te mujj di ko jàngale ,bàyyi wesar wa doonoon cosaan la. Dégg naa ci Sëñ bi mu ne woy woowu de waajuram jàngal na ko ñaari doomam yii di sheex Coro,miy Siidi Muhammad Alxalifa,ak sëñ Aafe,mi tuddoon Ahmadul Muxtaar. Mu woyati teereb Imaam Xazaalii bi tuddoon Bidaayatul Hidaaya,dal di koy tudde Mulayyinuz Zudoor ,di ci maanaa (aji nooyal ji dënn yi ),ginnaaw bi mu gàttal ko,tudde ko Munawwiruz Zudoor,di ( aji leeral ji dënn yi),ci atum 1294g/ 1877 g.j, teg ci Jëzbatuz Zixaar,di (bijjig gone yi) ak Jawharun Nafiis muy ( wurus wu gànjaru wi) nga xam ne da cee woy wesaruw Imaamul Axdariyyu,ak yu dul yooyu.

Bi ko dongo yi nangulee nag lii mu leen doon woo,daa bàyyi njàngale mi,jëm ca di leen tarbiya,ak a tarqiya (tarbiya mooy yar ni ko sariiya bëgge,tarqiya di yékkatee jëme ca yàlla).


Man nag nee naa lii de du ñàkk muy ndigalug yonant bi (j.y.m),ndax kenn ci sunu sëriñ yi nettali na ma,te moom ku wóor la di ndëërlaay,ne Sëñ bi de wax na ko ne yonant bi (j.y.m) moo wax ak moom ci gimiñam,ne ko yaral sa àndandoo yi ci “Himma” te bu leen yar ci njàng,loolu Sëñ bi gën na koo leeral ci xasida gii: { Bokk na ci kiimaani doomi Abdul Laahi ji,yal na ko yàlla dolliy xéewal ak mucc,moom miy leeral suufam si ciy wàlliyu ba yawmal xiyaam,te ku ci ne méngoo nga sunnaam si,di ko ñogal wëlif bidaa,bokk na ci kiimaani doomi Abdul Laahi jooju,bégal gu mu bégal jëwrinam jii ci ne ko(fazdah) mooy wooteel ca kaw) ( Yonant bi (j.y.m) digal na ko ne ko mu jàngal Muriid yi,ak ku nangu mu laabiire la ci waa jamono,te mooy ki ko àggale ca borooman cig taxliya ( mooy setal nit ki féexal ko ciy ayib ) bégalati ko ci tahliya ( muy ràng nit ki ay takaay,walla sol koy ngënéel) }.Li mu jublu ci Fazdah ji nag (mooy biralal ca kaw) ,mooy ji ci alxuraan:{ fasdah bi maa tuumaru wahrid hanil musrikiin} mooy biralal li nu la digal te dëddu way bokkaale ñi.

Yàlla daa digaloon yonantam bi (j.y.m) mu biral wooteem ga,ginaaw bi mu ko daa yalu,maanaam dëgg-dëggi loolu, mooy sëriñ bi,bi donn gi mu donn yonant bi matee,ci matalug yàlla (t.s) ,te mu dolli ko ay xam-xam aki hikma,aki leer,aki mbóot,te may ko kàttanug man a yanu wilaaya gu mag gi- bi loolu amee nag mu digal ko mu woote ca kaw,woo mbindéef yi ñu weeru ci moom,di jële ci moom tey def ay ndigalam,di bàyyi ay tereem,ci loolu la waxe: { yàlla mi nga xam ne lu ko soob mu def,moo ma jox xam-xam yi,ak seen barke,wattu naa lu xajul ciy téere,kon boo may ligéeyal bul tàyyi.Yàlla miy joxe,jox na ma ci darajay yonant bi,barkeb alxuraan,ak xam-xam yi,jël seen barke def ko ci samam njàngale.Yàlla jël na mbooti laa illaaha illal laah def ko ci samy taalif,yàlla jox na ma te dootu ko nangu,te man kaaraange laa te dib weeruwaay ci ndimbalam.Loolu nag ngënéelul yàllaa,ku ko soop la koy jox. Te nee na ma : (neel wéeru leen ci man}.

Ci maanaa sama boroom digal na ma,ma leeral nit ñi ne:man ab wéeruwaay laa tey kaaraange,ku bëgg aw yiw àdduna ak allaaxira,na wéeru ci man. Mu dellu waxaat ne: { Murid bu yoqatul ci man de texe na,ci làq ngën ji ay may. Murid bu Yàlla wommat jëm ci mu aju ci man, texe na te da na céru ciy may ) (Murid bu wéeru ci man de yàlla miy sama dëkkandoo bu kawe bi,def na muy ku texe ci lu kawe njortam) (Bepp murid bu aju ci man,day texe,te ku niy soril la aw ay. Képp ku aju ci man déy am nga ag mucc ci nëx-nëxi àddina ak allaaxira}. Ginaaw bi mu leeralaat ne way gëmi jinne yépp ci jamonoom ,aju nanu ci moom,mu ne : { Jinney sama jomono jii dey, ña ca gëm ñépp aju nanu ci man,waxuma ña gëmul}. Mu wattuloo nag ñi aju ci moom, ñuy xàccati ginaaw bu nu jébbaloo ne: { toroxte ñeel na ki ma dëddu ,won ma ginaaw,muñ ma,ginaaw bi mu duggee dib murid}.

Dal di leeral lu dig murid,ak lub murid di bëgg,mu ne: { Dëgg-dëggi ag murid - ci li sang si wax - mooy bàyyi aada,( muy li nga nekkoon njëkk ngay jébbalu),bu àggagul ba noppi dellu ca la mu nekkoon, mook ku murtad ay yam) ( Ndax kat ab murid du bëgg mukk lu dul gëramul yàlla ak fu mu man a jublu}}. Mu leeralaat ni ab muriid di mel,ak ngértel ànd ak sëriñ bu àgg,mu ne : {{ Melow ab murid,mooy bañ a bëgg dara ngir yàlla. Ku bëggul lu dul yàlla, àgg fa moom,mu jox ko aw yiwam )) ((Ku aju ci ku àgg, àgg,ku aju ci ku àggul doo àgg )) ((Ku yaroowul ci loxoy ab sëriñ, dana dajeeki coona )). ((Ndax ku amul sëriñ buy gindee,saytaaneey mujj di ab sëriñam fu mu jublu)) ((Ab sëriñ du wuuteek Ku nu rammuloo ki (muy yonant bi) kon ku jublu aji yar (sheexul murabbi) de da na jariñu )) ((Fu la aji yar digale,defal,kon nga àgg ca boroom ba)) ((Bu la aayee dara bu ko jege,te bul sàggan ci wut gëramam }}.


Mu leeralaat ne murid saadiq de am na ay meloom,yoy bu ko amee am wépp yiw: {{ Meloy murid saadiq ci gàttal, ñeent la,ma tënk leen nag ciy bayit ngir ragal woru)) ((Dëggal ci bëgg sab sëriñ ba fàwwu,jëfey ndigalam fu mu rote rekk )) ((Bayyi gaaru ci lu mu man a doon (gaaru mooy di am xalaat ci ndigali sëñ bi), ak doonte ci sa baatin la,ci li nu nettali)) (( Ak a tànnal sa bopp la ngay def,ngir sa rafetug njort )) ((Képp ku boole yile melo ci murid yi déy,da na jot ndëërlaay ya (gaa yu baax ya)}}.

Mu biralaat ne kiiraay am na juroom benni cosaan,yu murid bi war a dagg,te malaaka yi dañiy jooy ci murid bu bëgg lekk, ne: {{ Kiiraay am na juroom benni cosaan,ku bëgg a àgg da nga leen dog, ñooy baril lekk ak naan,ak a jaxasook nit ñi)) ((Bari wax,bariy nelaw,sàggan ci tudd yàlla miy jàmm)) ((Gëstul loolu ci Jawaahirul Mahaani,bi sunu Sheex Tiijaan mu nu màggal mi def)) ((Nettali nanu ne malaakay Aji màgg ji,dañiy jooy ci murid bu bëgg lekk,ngir yëram ko,loolu man nga koo gis ci taalifi boroom Hawaarifil Mahaarif}}

Mu neeti murid saadiq doomi waxtoom lay doon,ne: {{ Murid Saadiq mooy kuy wëlbatiku ànd ak waxtu wi mu nekk,te du fuglu wa ca kanamam,ndax loolu day teree yéwenal waxtu wi teew )) ((Gëstu leen loolu ci Jannatul Muriidi,téere bi sunu sëriñ Xaliifatur Rasiid def}}. Ak lu bokkul ak loolu ,ci li mu wax ci mbirum boppam, mom muridam yi,nga xam ne ,bu nu ko toppoon,indi fi lu yéem xel yi,te da na mujj kon,gàttal gi nu bëggoon ci téere bii,du amati,ndax moom téere bii as kook la ci geejug xamale ko.

Nu indil leen fii nag as tuut,su nu tas ci wone lenn ci sekkarey xaybu yi (xaybu mooy lu faddu,muy mbirum biir niki liy xew te xewagul),mu bégal ci ñi aju ci moom, ngir dolli leen ag xeemeem,ak sawarloo leen,mu wax ne : ((ñi aju ci man bu nu ko defutoon dem sawara,doonte as ndiir lay doon it,njëkk nuy tàbbi ajjana,ji nu dig ñu ragal ñi yàlla)) ((Li waral sama tukki bu sori bi,Yàlla mu barkeel mi te kawe,daa bëggoon ca asal,may kiy ramu samay donga,dox na sama digante ak nasaraan yi,tàbbal ci seeni xol ag ragal ma,nu def la nu def nag ngir ma bañ a nekk dib nasaraan, ndax bu ma ko doonoon tabbi sawara ,walhiyaazu billaahi. Waaye Yàlla’a ma aar ci sawara,ak lépp lu mu gëramul,ci darajay Yonant bi (j.y.m))) . Mu bind ay laabiire ñeel murid yépp,ne :{{ Mi ngi juge ci man jëm ci mbooleem murid, yu góor yi ak yu jigéen yi,ab nuyyoo bu teey,bu leen di musal mboole seen,te di leen tabbal ci jàmm ak aafiya,ci addina ak alaaxira,ci barkeb Yonanat bi (j.y.m),ginaaw bi, may digal képp ku aju ci man,ngir yàlla mu kawe mi te tedd,mu xamlu pas-pas yi ak tawhiid,ak àttey laab,ak julli ak woor,ak lu dul loolu ci lépp lu war mukallaf,man nag warlul naa leen taalifal leen mbooleem lu leen koy xamal, ngir jëmmi yàlla (t.s),wasalaam)).

Mu bind lenn ci ay murid ab tontu bu neex yal na nu ci yàlla boole ñun ñépp,mu ne ci:{{assalaamu halaykum warahmatul laahi tahaalaa,wa barakaatuhuu,ma lay xamal ni sa bataaxel ba agsi na,yaw murid bu dëggu bi,waaye na la wóor ne doo gis lenn loo ragal,booy faatu ak ci bàmmeel,te ñaari malaaka yiy laaje,xam nanu sa sëriñ,te da nanu doylu ci xam gi, ba dunu la laaj dara)). Lii nag xamle la gu mu teg ci yoonu laaj ak tontu,laaj bi moo di lan la sëñ bi woo ay taalibeem jëme? lan mooy tontu li? Moo di sellal,moom mi nga xam ni mooy ruuhug jëf tey ngértel xam-xamub way xam ñi yàlla,tey waralug àgg ca Yàlla, àgg ci Yàlla nag ñi ngi ci jublu jaam bi nekk di ku wéetal yàlla,ciy yëggoom ,aki dalam,aki pas-pasam aki waxam,ci lepp,li feeñ ak li nëbbu,lii nag manut a ame ci njàngale rekk,ndax kuy jàngale ab tegtalkat rekk la,li ci des,mi ngi ci aji jàng ji,man naa am mu jëfe man naa am déet,du ligéeyub jàngalekat,muy sonnu ci waa ji jëfe loolule,loolu Sheexu tarbiya la war.


Bokk na ci ligeyam,moom sëriñub yar,jàng ak jàngale,ak ligéeyloo,ak ay tudd yàlla,ak gindee ginaaw bi mu leen xiirtalee cig cofeel gu dëggu,te du tàggook ñoom li feek wonu leen seen ayibi bopp, ligéeyloo leen ci nu jéem a laab ci yooyu ayib,ngir man a àgg ak ñoom fa Yàlla inshallaah. Bu loolu jàllee,mbirum tarbiya day mbir mu gudd,manunu cee wax fii. Mu dem ak ñoom ci yar leen ci himma, ñu nangul ko ko,mu dox ak ñoom ci ngérum tàggat,dajale leen,di leen ligéeyloo lu bari,yanu leen ci fàttaliku Yàlla lu bari,ak a jàngi xasida,ak taqoo laab,ak a beru,rawati na sori jigéen ñi,ci noonu ñu kawe ñu dul ñoom,ndax donoo joxe woon seen bop ak seen alal ci yoonu sàkku gëramul Yàlla,{Yalla jënd na ci jullit ñi,seeni bakan ak seen alal,faye leen ko àjjana},Sëñ bi wéy ci yoon wu jub wii mook saabaam yi, dale ko ci njëlbéenug atum junneek ñatti téeméer ak benn,ba bi mu sancee Mbàkke Bawal,ci at moomu juge Mbàkke Kajoor,sax fa lu tollook ñaari at ,nit ñi di ko dikkal juge fu nekk, ñii di jebblusi, ñii di joxesi àddiya, ñiiy sàkku ndimbal. Mu mujj yoonu këram gi mel ne yoonu ab ja, ci ñeenti at yii nag mu siiw ci,siiw gu kawe, ñu jege ñi ak ñu sori ñi, ñepp di yéemu ci moom,te booba amagutoon sax fan-weeri at.


Ci diir bii sëñ bi wër na ci réewum wolof mi,dale Saalum ba Waalo Barak,siyaare fa mag ña, ña cay dund ak ña dundul,jaar ca sëriñ sa ,jële ca ñoomi wird,bokk na ci ñi mu siyaare, ñoñ sheex Siidiya,siyaare na bàmmeelam ca Tindawja,siyaare sheex Baaba mom Abiihi ca Maymooni,tagg leen,jële ca ñoom,woy càllaleg xaadir gi,tàmblee ko ca sheex Baaba ba fa mu yam,looloo taxoon kenn ci Sheexi naar yu mag yi laajoon ko kuy sa sëriñ?,mu ne Rasuulul laahi (j.y.m),mu ne ko kon lu tax nga ne fi di tudd waa kër sheex Siidiya,ak a woy ay sëriñ ak a tag?,Mu ne booba da maa melon ne ku gumba,di làmbatu yoon wi,di ko sàkkoo xam ci ku xam ak ku xamul,bi ma dajee boroom yoon wi ci ndimbalul Yàlla nag muy Yonant bi (j.y.m),mu xëcc ma ci boppam,laa wacc ker-keraan yi,waaye di jokkook ñoom ngir Yàlla ak a soppanteek a jariñante ngir moom.


Te wax na dëgg,ndax mbiram ak ñoñ Sheex Siidiya loolu lay tegtale,mujj nanu mel niy doomam mu mel ni seen baay,di leen jariñ ci alalam lu leenub buur jariñul,ab sëriñ it jariñu ko ab taalibeem.

Sheex Baaba tag ko ciy xasaayid,aki dagiit,yu tollok ay téeméeri bayit,bokk nanu ci yile:( Shex Ahmadu xéewal la gu yàlla jox mbindéefam yi) ak waxam ja: ( sëñ bi daal xéewal la gu yàlla xéewalee,di kiimaan ci kiimaan yi),ak yu bokkul ak yooyu,bu waxutoon yu dul yii it , ñaari bayit yii,rekk doyoon nanu seede ci màggug sëñ bii,ak wilaayaam. Ndax kat sheex Baaba ak màggam gi, du fo mbaa muy yaxantu ci woy ni suharaawu yi,moom dey lu mu wax ci ndigal la ko teg,ak jaamu Yàlla,yal na ko Yàlla fay ci ñaari bayitam yooyu. Bokk na ci ñi mu siyaare ci sheexi naar yi,Ustaas Baaba mom Hamdi, ma jublu ci Hamdi mu ñaareel mi,dikk na fa yendu fa fanaan fa,nee nan ci menn mbaar. Sama xarit ba niy dàkkantale Kaadi Sheex Abdul Xaadir,doomi Amiirul Kumlayli , nettali na ma te booba taalibeb Ustaas Baaba la,ne Ustaas mii moo jox sëñ bi sekkare bi,waaye nag leeralu ma ban sekkare la,man naa am muy wirduw Saasalii,ndax sëñ bi bind na ne moom wirduw saasali mi ngi ko jële ci wenn wasiila,njëkk muy daje ak wasila wu mag wi,di Yonant bi (j.y.m) ,te leeralu nu kooka kan la. Li waral Kaad mii nettali ma ko,mooy maa ko laajoon bi mu jëlaatee ci sëñ bi wirduw Sasalii,ndax xam nga ci ku ko sëñ bi jële woon,mu ne déedéet,waaye nettali li mu waxoon ci diggante sëñ bi ak Ustaas Baaba,nu jorte ci ne ci Ustaas Baab moomu la ko jële ndax moom ab xaadir la woon.


Kaad nettali na ma ne bi sëñ bi agsee, ci bi miy siyaaresi Ustaas ,ci bëcëgug bis bu sell,Ustaas defaral ko am soow mu neex ci ndox mu sedd,ak suukar,looloo ngi amoon,ci jamono ji sëñ biy nattu boppam ci di tegoo ay coona,mu ne ko naanal mu ne ko man baax na du ma naan lii, mu ne ko,ndax daa baaxul ci wàllug wér,waala da nga koo bàyyi ngir Yàlla di jiyaar ak sa bakan,sëñ bi ne ko waaw loolu la,mu ne ko kon naanal,bàyyiwu ko ba mu far naan,ginaaw bi la dongay Ustaas yi laaj lu waral mu sonnu ci mu naan soow mi,mu ne leen ndax moom kat sonal boppam rekk la bëgg,ak mettital ko,mujj loolu di aadaam ngir Yàlla,ju mu manatul a bàyyeeti,ndare cib coona,ma jëflante ci ak moom waaye Yàlla defal na ko barke,ndax mujj na dëgar ci këng.


Ginaaw bi lii wéyee lu yàgg,Ahmadu doomi Ustaas seetsi na Sëñ bi Njaaréem,mu bég ci lool,di ko ganale ngan gu mu sonn,indil ko ñam yi ak naan yi,bi nu àggee ci ataaya, Ahmad xam ne mbir dana am ,ndax moom du naan ataya,bi ko sëñ bi tàllalee ataaya ji,mu ne ko du ma naan ataaya,mu ne Yàllaa tax nga bàyyi ko ngir jiyaar ak sa bakan walla ag weradi,mu ni ko Yàlla,mu ree,ne ko naanal ma fayoo ca la ma sa baay defoon, ñaanal ko ci barke.

Bi Sëñ bi nekkee ci wëram googu nit ñaa ngi ko daa dikkal bàyyikoo ci gépp wàll ngir xam-xam bu bari bi ak njariñ li,ak cofeel gi nu amoon ci moom ak diinewu gu dëggu gi,rawati na alal ju bari ji mu daa joxe rekk ,nga xam ne daawul tëyye ab dërëm,lu ñëw mu joxe,di jox mag ak ndaw goor ak jigeen,gor ak ab jaam,ku am ak ku amul,ku baax ak ku bon,loxo bu tàllaliku jëm ci moom mu feesal ko te soxlaalul nit ñi, doyloo kàppitaalam bi dul lu dul jublu ci Yàlla ak yiteem jépp. Mu dem Gànnaar jaar ca sëriñ ya,siyaare ñay dund ak barabi way faatu ya,jariñ leen ci alalam,ju bari ja,nu sopp ko nu kawe ni ko ñu ñuul ñi soppe,defal koy xasiday tagg,siyaaresi ko ci réewam ginaaw bi.


Bi mbokk yi gisee ci moom kaweg xel,gu diine,gu mbaax gii mu yor ak jublu gi ko àdduna ak nit ñi jublu,nu tàmbli di ko iñaane,di ko lor,mu daan julleendoo ak ñoom,lor yi ëpp,mu mujj beru leen ak am mbooloom ak jàkkaam, Yàlla gën a fésal mbiram, ñu gënatee mer,nga boole ci terewu gi mu defoon ci mbirum buur yi,daawul nangoo jaxasoo’k ñoom,ba da daa sàkku sax ci sëñ Mammoor ci ay bataaxel yu mu ko daa bind, - da daan kersawoo jàkkaarloo’k moom di ko ci wax dara - mu bàyyi ag jëflanteem ak buur yi,naan ko seen teddngay fii ji toroxte la ëlëg,sëñ Mammoor daan ko ko nangul,te di ko ci jéggalu,waaye njabootam gi taxoon ba manu leen a bàyyi.


Ma nettali leen as lëf ci jaloore,nee nanu,bi kenn ci jaraafi Latjoor yu mag yi -mu nekkoon ku am solo fa Latjoor - jébblusee ci Sëñ bi,mu bokkoon ci jàmbaar yi amoon ay alal,mu ndàmmoom (gañewoon) lu bari ci màggum xareb Samba Saajo bi ( màgg mooy li niy jële ci koo xeexal ba not ko) .Samba Saajo ab dëkk la bu nekk ca penkub Njàmbur,diggam ak Jolof,la xare boobu ame woon,ci diggante Amad Sheexu BA mu Fuuta, ak Latjoor,Tubaab yi japle woon ko moom Latjoor,ba mu gañe ko, ray ko,xarekati Latjoor yi gañee ci woon màgg mu rëy,ci alal ak ay jaam,te ña ca ëpp diggante Jolof ak Fuuta lanu bàyyikoo,ak Kajoor,tey jullit lanu, buur bi laaj ndax man na leen a def ay jaam, kenn ci boroom xam-xam yu mag yi,ne ko waa-waaw,ndax Ahmadu Sheexu da doon wooteg yonnant, kon alalam ak dereetam dagan nanu, nu dal di wéyal loolu,te kat ag wooteem yonnant mbooloom boroom xam-xam yu mag yi saxalunu ko.

Li waral xare bi,lu gudd la manunu koo netaali fii. Bi jaraaf jooju tuubee ci sëñ bi,mu digal ko mu wacc mbooleem jaam ak alal ji mu ame woon ci xeex boobu, jaraaf ji déggal ko,def ko ànd ci ak kontaante, Latjoor ak ay gaayam jàppe loolu nag ag weddi ñeel àtte bi leen kenn ci boroom xam-xam yi defaloon,ne leen jaam yi dagan nanu. Nu mere woon ko,nee nanu ma jaraaf ya woo woon nanu jaraaf jooja fa kanamu Latjoor,ne ko : lu tax nga bokk ak nun ndab,règg rekk wëlbatiku,doyatu la nga ciy xëpp suuf? Mu ne leen waaw,weñ a tàbbi ci sama bakan,lëjal ma, moo waral lii ngeen gis ci man,waaye bëgg a nëxal seenum mbir taxut. Mu jublu woon ci weñ wi,lislaam ji ko duggoon,cig mbetteel,yaw nag xam nga lëjal gi lislaam di def ku mu dugg, du ko bàyyi ndare bu daa tuub.


Ñu xam ne li mu wax lu dëggu ci moom la, ñu jéggal ko, noppi cim mbiram. Waaye Sëñ bi moom, Latjoor lijëntilulu ci anam gu nooy,te teey,nun ko ko indile,mu bind koy leetari leetar,yonni fay ndawi ndaw,teewul Sëñ bi bañ,nee nanu ma wax na bis kenn ci ndawi buur bi,ne ko : {neel ki la yonni rus naa malaakay Yàlla yi di ma gis ma jëm ci buur bu dul yàlla}. Dégge naa ci sheex Aadama SÀLL - moom kenn la woon ci ñi njëkkoon a jébblu ci Sëñ bi , cosaanoo woon Jolof - mu ne leetar bi sëñ bi mujj a bind Latjoor moo ko doon yobb, mi ngi ci naan: { Muhammad Ibnu Maslama nee na boroom xam-xam ci buntu buur,mi ngi mel ni weñ ci kawi jonkan},Latjoor jox Xaali Majaxate Kala bataaxel bi - moom moo nekkoon mufti bu mag bi - Xaali yër ko tiit, ne :( Innaa lillaahi wa inna ilayhi raajihuun) buur bi ne ko lan la ? mu ne ko,kii waxul ak yaw man lay waxal,mu ne lu man a xew waxal rekk,mu jàngal ko ko,Latjoor ne ko: ci man de la gën a dal,ndax yaw lu man a xew ,ya’ay weñ wi man nag,ay dem-àll laa.

Waaye nag yaw miy boroom xam-xam loo wax ci moom? Xaali ne ko man daal li ma gisoon,mooy nu bàyyi ko ak mbiram ,ndax kat notante ak moom ag woru la,boo ko notee bokk ci ñi gën a kawe,bu la notee, nga di ci ñi gën a suufe,te maneesu koo not. Buur bi ne ko wax nga dëgg,ndax baykat kat yàgg naa gis jànji ci toolam - te manu koo bay, manu koo saxal -mu bàyyi ko fa,Xaali ne ko waa-waaw,mu ne nan ko jàppe jànji boobu. Ci noonu leetar ya dog,wax ja jeex,alhamdu lillaah.

Beneen nettalee ngii bu gënatee yeeme,waaye soriwul bu njëkk bi,mooy,bi leetar yi ak coow li jeexee ci bataaxel bu saf boobu,yàlla dogal na Latjoor ànd ak Xaali ci lenn ci tukkeem yooyu mu daa def,ba wàcc benn dëkk wetu fi sëñ bi dëkkoon, bi Sëñ bi yëgee ne moom ak Xaalee ànd,mu ne na nuyji Xaali,ngir ñaari mbir,menn mi, mooy Xaalee ko daa jàngal,te ku la jàngaluw araf sa kilifa la, ñaareel bi,xaritub baayam la woon,mu war ci moom mu jox ko àqam te jokk ko,ndax danu ne : ( joxe àqi waajur gi gën a mat,mooy waa ji dox kóllare ak jokk ko ci xariti baayam yi ). Bi mu agsee fi ñoom, fekk leen nu toog ci lal,sëñ bi nuyyu leen,nuyoob màggal,toog ci suuf,toogul ca laltu ga fa nekkoon,bi mu toogee tuuti ne Xaali,da ma la fee deggoon rekk ma ne naa fi jaar siyaare la,ci noonu Latjoor xam ne daa bëgg a leeral ci ne dikk gi moom taxul,juboo’k moom it taxut. Latjoor gestu Xaali ne ko,nun kat kii war nanoo wax ak moom ca sunu mbir ma nu ko woowe woon ba sonn,mu bañ,Xaali ne ko aca, ne Sëñ bi: man dey maa ne Ahmadu Sheexu da doon wooteg yonant,te di ci xeexe it, kon ray ko dagan na,lekk it alal ji ñu nangoo ci moom niki màgg ak njaf ña mu àndaloon (njaf mooy jàpp jaam),loolu lépp dagan na,bi mu noppee mbooloo mépp noppi ab diir,Sëñ bi ne Xaali ndax da ngaa wax ngir ma tontu la?,Xaali ne ko waa-waaw,bu may wax kay nga tontu maa tax,sëñ bi neeti ko : kon am naa ndigal ci tontu ? mu ne waa-waaw, mu ne kan moo la man a seereel ne woote na ag yonnant ? Xaali ne ko waa Kajoor,mu ne ko ñooñu ay noonam lanu,te diy xuloowaaleem,di xaree’k moom,nan lanu koy seedeele ? Xaali neeti ko waaye waa Samba Saajo,fi xare bi ame woon?, Sëñ bi ne ko ñooñu kay dun seede,ndax xare baa leen fa fekk,sottiku ci seen kaw,te yëgunu woon,nan laniy xame ki nu tuumaal ak li nu ko tuumaale?, Xaali ak mbooloo mi ne tekk as lëf,ba mu yàgg mu ne yaw gone gi,won nanu la Yàlla,nga jiitu nu ca,kon ag ndokkeel ñeel na la,dal di nooy,te juboo’k moom.


Pënd ba wuri,Sëñ ba tàggu leen dem,ci noonu, yoon yépp dagg ci moom lu dul wi jëm ci Yàlla,ndax kat moo jàkkaarloo ak ñu baax ñeek kàccor yi,jàng ca ñoom:{wa ufawwidu amrii ilal laah innal laaha bashiirun bil hibaad,wallaahu yahlamul mufsida minal muslihi} muy joyal naa samay mbir ñeel yàlla,moom miy gis jaamam yi,Yàlla xàmmee na kiy defar ak kiy yàq.


Li mooy dooley Sëñ bi,te nii la dogoo woon,donga yi raw ko, cig dogu,foo leen fekk ña ngay xeex ak nit ña,nga gis daanukatu jéll yi fii,leeg-leeg nga gis ku ci yéeg ba ci kaw njobbaxtalu garab,ne dërr fi suuf,jiital bop bi,jug faxasu dem,te dara du ko jot,ak ñuy tàbbi ci sawara génn,te dunu lakk,di yekkati xasiday Sëñ bi,ci penciy nit ñi,ak seen daara yi, ñuy xeex ak ñoom te du tax nu bàyyi, ñu leen di door ak a jéng,ak a nangu seen alal,ak a génne seeni kër,loolu lépp,ngir teqale leen ,te tas leen. Mu mel ne jëf jooju da leen na dolli ag xeemeem ak ag sóobu, mu mel ni loolu mbóotum Yàlla’a,mu ball juge ci baatinub seen Sëriñ ba ca ñoom,Sëñ bi daa leen dolli pastéef,di dëgëral seeni basiira ,di yekkati seeni yite ba ca yu saaba ya,naan leen roy leen saabay Yonnant bi, ñooy seeni mbokk de,te daje nanoo’k lu gën a tar lii ngeen nekk, ndax ray nanu leen ci yoonu Yàlla,tuur seeni dereet,nangu seeni alal,génne leen séeni kër,te loolu téewu leen a jublu ci li nu soxla, ba am tagg wu rafet ca Yàlla, :{ lil fuqaraail muhaajiriin allaziina uxrijuu min diyaarihim wa amwaalihim yabtaxoona fadlan minal laahi,wa ridwaanan,wa yanzuruunal laaha wa rasuulahuu ulaayika humuz zaadiquun },mu leen di xamal ni,danoo war a roy ci way gàddaay yu ñàkk yooyu,nga xam ne ku dul yàlla ñoru leen woon, ñu génne leen seeni kër naggu seeni alal,ci yoonu sàkku Yàlla ak ngërëmam,ak dimbali Yàlla ak ab Yonnantam, ñooñooy ñu dëggu ñi.


Mu naan leen xanaa xamu leen ne ñooñooy seeni baay ci diine,kon lu leen man a dal,day daal di doon lu néew,{laxadd kaana lakkum fii rasuulil laahi uswatun hasanatun liman kaana yarjool laaha wal yawmal aaxira}}muy :ku gëm Yàlla ak allaxira,na ko wóor ne am na roytéef bu rafet,ci yonnant bi. Muñ leen tey rafetal ci kiy ñaawal ci yeen, { Idfah billatii hiya ahsanu,faizal lazii baynaka wa baynahuu hadaawatun,ka annahuu walliyun hamiim,wamaa yulaqaahaa illal laziina zabaruu wamaa yulaqaahaa illa zuuhazin haziim} muy dee leen jañe jëf ju ñaaw, jëf ja gën a rafet,kon nga gis ne ki nga xam ne,ag noonoo daa am seen diggante,da na mujj mel ni sa xarit bu sellug xarit,loolu nag ku dul kuy muñ du ko am,ku dul ku di boroomub cér bu mag. Dee leen di fuglu { yawma nadhuu kullu unnasin bi imaamihim } muy bis ba niy woo nit ñu nekk ci seen imam. Kon de bañug ku bañ du leen naqari, ñu daan def bu nu naanee ci ndoxum waaraatey Sëñ bi moomu,ba màndi, di ñu sawar,di daanoo’k a yuuxu ak a fecci,ci diir bii,sëñ bi doon baril lu muy def ay xasiday xam-xam,ak yu tagg,ci la woyoon Masaalikul Jinaan,muy téere bu amul moroom ci tazawuf,yor junni ak juroomi téeméer ak juroom fukk ak ñatti bayit,ak Mawaahibul Xudoos,ak yeneen,ci la wàccee it ñu bari ci donga yi,niki sheex Ibraahima FAAL,ak sheex Ibraahima SAAR,ak sheex Anta MBAKKE ak sheex Aadama GËY ak sheex Asan NJAAY ak ñu mel ni ñoom.


Bi nit ñi barilee lor yi ak sonal gi,ca Mbakke,mu tuxoo fa sanc Daaru Salaam,ci njëlbéenug atum junni ak ñatti téeméer ak ñeent,waaye teewul lor yi wéy di dolliku,mu sax fa lu tolloo’k am at,di yar nit ñi,di leen yéege,nuy gën a dolliku,raj-rajloo biy gën a yokku,wërsëg wiy gën a sottiku niki ab taw,mu juge fa,dem as lëf,ca penkub bëj-gànnaaru Daaru Salaam, ci lu tolloo’k juroom walla juroom ñaari kilomet,sanc fa Tuubaa,ci mujjug atum junni ak ñatti téeméer ak juroom,walla ci njëlbéenug atum junni ak ñatti téeméer ak juroom benn,tuxu fa ak njaboot gi, sëñ Fallu nettali na ma - ñaareelu xalifa - ne magam ja sëriñ Moodu Mustafa,mi njëkk a doon xalifa,mi ngi ganee àdduna Daaru Salaam,guddig àjjuma,fukk ak benn ci muharram atum 1306 g , njëkk sëñ biy tuxu,ndax moom mi ngi tuxu, ci li nu wax, ci jumaadas saaniya. Ci guddig kasurajab,maanaam ñaar fukk ak juroom ñaar ci rajab,sëñ Fallu gane àdduna, ñu magantee juroom benni weer ak fukki fan ak juroom ñaar,yal na leen yàlla barkeel,ginaaw bi,ci la sëñ Muhammadu Lamin Baara ganee,bokk ak sëñ Moodu Mustafaa nday ak baay,ci atum 1308 g, walla 1309g . Mu des Tuubaa nag noom Sëñ bi,di dem ak a delsi,ak a tuxu ci diggante kër yi,niki Daarul Minnan, Daarur Rahmaan,ak Daarul Xuddoos.


Ku dul Yàlla nag xamul xew-xew yi daa am, ci digganteem ak boroomam,ak diganteem aki saabaam,ci xeeti tarbiya ak tarxiya,ak yu ni mel,ak jàngale ci taalifam yi,ak digganteem ak ñu baax ñi,ci ay mbir aki duggalante ak ay xuloo,ngir seeni doom ak seen taalibe yi wëlbatiku woon jublusi ko,ak ci digganteem ak buur yi ak jaraaaf yi,ciy xuloo,ngir fiir ak tiit ci seen nguur gi. Lu man a xew,doxiin wi moom,juboon na,donga yi jub, ñu daa dolliku ak a yokku jamono ju nekk, ku mu ci wàcce ,mu wéy di jub,ku tàbbi it tàbbi cig njub,ba bi mu tukke ca géej ga.