Gargamboose
Gargamboose xeetu garab la gu bokk ci ñoñ "opuntia". Ca Amerig gu digg la bàyyikoo, fi ñuy woowee Karayib.
Melo wi
SoppiGargamboose garab la gog day màgg te am xeetu xob yu dijj ak ay dég yu mag te ñaw, seen taxawaay di kaaraange, am na it dég yu sew yuy jame
Meññeef mi
SoppiMeññeef mi dees koy lekk. Dees koy xolli bam set bala ñu koy jëfandikoo.
Njariñ yi
SoppiAy doomam bari nay njariñ lool.
Dees na ci defar ay tàngal, ay njar walla njambaan yu neex. Ay bantam day faj (estomaa) góomu biir. Biir buy daw it dina koy faj, ba ci sax jabeet.
Turu xam-xam wi
SoppiOpuntia tuna
Tur wi ci yeneeni làkk
Soppiaraab: الصبَار |