Garabu Lawbe
Garabu lawbe, mbaa dundul, mbaa guy-jéeri noo ngi koy fekk ci xalag sowwu jantu Afrig niki Senegaal jëm diggu Afrig, dalee Gine ba Gana, jaare Niseriya jëm bëj-saalumu Càdd. Ag ñeme conoom tax na mu man a dund ci àll bu wow, fu naatul lool ak fuy am naaj. Garab gi dina man a dund itam ci barab bu am i xeer ndax buutam ni mu man a denccee ndox noonu la ko man a muucoo.
Melo
SoppiLawbe gi garab la gu am ay xob yu ndaw. Njoolaayam dina dem ci li ëpp ci 10 ba ci 25i met. Ci Sahel nag néew na li muy weesu 6i met. Peeru garab gi day am i dég rawatina bu garab giy màgg, xas mi woyof. Garabu Lawbe dëgg-dëgg garab gu man lu bari la, di joxe ay garabu paj, ñam wu nuy lekk, diw, matt, añs. Ñoo ngi koy bay ci Afrig sowwu jant. Garab gi mi ngi tóortóor ak a meññ li ko dalee ci juroom benneelu atam, moo ngi aju ci nekkiinam. Ci li ëpp mi ngi meññ ci noor. Waaye nag daay yi du ñu leen may ñuy am jiwu. Genn garabu Lawbe gu mag man naa meññ ba 1500i fóyteef ci at mi.
Ay njariñam
SoppiGarab gi bari na ay njariñ lool. Man na doon dëkkuwaayu yamb. Tóortóor yi dees koy weer ba mu wow, ñu wal ko def ko cafaay. Foytéef yu ndaw yi man nañu leen togg. Yu matul yi itam man nañu koo jariñoo ci ndefarug njar. Niinaayu diwam tax na mu bokk ci yi nit di jëfandikoo cim paj, xasu garab gi day yokk saw te day yombal mbaaxum jiggeen. Ku ko baxal it, man naa faj ràmm, ak payiis, ak bopp buy metti, man na itam waññi ween yu rëy. Ci bopp buy metti itam manees na jël xob yi rekk takk ko ci. Boppam baax na lool ci dakkal nacc-nacc ak ci biir buy daw, ci kaw mu ànd ak yeneen i garab. Sangoo ndox mu tàngu garabu lawbe baax na lool ci ku néew doole. Pàcc yi bari ci garab gi la ñuy jëfandikoo ngir faj tàngooru yaram, walla ngir wàññi coono walla ngir yokk soowum jiggeen juy nàmpal. Ci wàllum njëmbët garab: Garabu Lawbe am na ci solo ndax safara manul ci moom lu bari, ba tax na mu man a nekk xàmmekaay. Xam-xam wane na ni garabu lawbe baax na ci suuf.
Yeneen i njariñ
SoppiFiibar bi nekk ci biir foytéefu garab gi manees na koo jariñoo ci defar i pajaas ak i ngegenaay. Xas mi man na cuub. Doom yi dañoo bari diw lool ba àgg ci cosaanal petorol. Garab gi man na joxe itam matt ak lenn ci lu nu man a jëfandikoo.
Mbayam
SoppiJiwoom bokk na ci liy yaatal dund garab gi waaye jëmbët ko it man na nekk su dee garab gu ndaw gi dina aaru ci daay ak ci mala yi.
Nataal
Soppi-
Tóortóoru garabu lawbe
-
Xob yi
-
Dàtt bi