Gëm Yàlla
NI NUY GËME YÀLLA
Yàlla moom ni nga koy gëme mooy : nga dëggal ni am gi mu am lu wóor la, te aji jiitu la joj jiitoom gi amul fu mu tàmblee,aji des la te desam gi amul fu muy yam, aji wuuteek mbindeef yi la,aji doylu ci boppam la,kenn la kok amulub kem,aji wéet la ci jëmmam- maanaan amul kenn ku mel ni moom- ak ciw meloom , aki jëfam.
Kàttan (man-manu jëf) ak nameel (maanaam bëgg di def) ak xam-xam akug dund ,ak gis ak dégg, ak wax,yooyule yu war ci sunu boroom lanu. Kon nag mu nekk di aji am kàttan lu war la, tey ku am nameel ,di aji xam, di aji dund,tey kuy degg di kuy gis, nekk it di kuy wax yu war lan ci moom. Ni yooyu nekke di ay melo yu war ci sunu boroom, la ame yeneen melo yu waradi,te jomb ci moom,niki ñàkk, (maanaam sun boroom bañoon a am) ak sosu (ci maanaa muy ku nekkam gi am na lu ko fi jiitu,nekkul di ku fi mas di ne),ak jeex (maanaam muy ku fi dul des),ak niru,(ci maanaa yamoowut ak dara ci jëmm du caageenug ci meloom mbaa ay jëfam,kon niroowut ak dara te loolu jomb na ci moom)ak aajowoo (jomb na ci sunu boroom muy aajowoo kenn ci lenn),ak limu (maanaam mu bañ di kenn di ay ñaar aki ñatt) ak lott (maanaam ñakk man-man ci def li ko soob) ak sibeel ( def dara cig sibeel mooy safaanub def ko cig nameel,mooy def goo xam ni andul ak teeyug bakkan loolu jomb na ci sunu boroom) ak tëx (mooy safaanub degg) ak réer ( di safaanub xam) ak dee di (safaanub dund)ak gumba di (safaanub gis) ak luu di (safaanub wax) .
Yile yepp jomb nanu ci yàlla sunu boroom ,tudd naa sellam ga,kon daal jomb na ci moom mu ne di aji lott,mbaa muy aji tëx mba muy aji jëf cig sibeel walla muy aji réer mbaa muy ku gumba mbaa ku dee -soril naa ko loolu- walla muy aji luu,yii daal melo yu jomb lanu ci boroom asamaan.Moom daal sunu boroom deful dara cig war,lu mu man a def cig nameel la koy def ak cig baax ak coobare,loo fi gis daal,ci mbindeef yi, seenug jëf ak seenug ba, ñoo yam ca sunu boroom,lenn du ci lu war, lu dagan rekk la ci moom, (dagan mooy lu man a nekk man a bañ a nekk).