Gëm Téere yi
NI NUY GËME TEEREY ASAMAAN YI
Ni ngay gëme teere yi mooy nga dëggal ne wacce gi leen yàlla wacce lu wér la,te lepp lu ne ci teere yooyu ag dëgg la gu deesul sikk.Seenub lim nag teemer ak ñeent la. Fukk yi nu wacce leen ci yonant yàlla Aadama (j.y.m), juroom fukk yi nu wacce leen ci yonant yalla Sihsa(doomi yonant yalla Aadama), fanweer yi nu wacce leen ci yonant yàlla Idriisa,fukk yi nu wacce leen ci yonant yàlla Ibraahiima miy xaritub yàlla bi(j.y.m). Bu ko defee Tawreet ñeel Muusa(j.y.m),Injiil ñeel Hiisaa,saboor Davood (j.y.m)Alxuraan jii nag wacci ci sunu sang bi Muhammad yonant bi tëjj yonant gi,yal na yàlla dolli mucc ak xeewal ci moom,ak ci ñoom ñepp