Feebar yuy wale
Doomu jangaro bu nit menul tek bet la ci kaw nga jeffandiko jumtukaay bu lay may nga gis ko.Men na jural nit ki infection ba tax mu am feebar. Pathogen itam men nanu ko mengale ak lu mel ni "germs" wala yennsay "parasite" ndax microb yuy dund lanuy dunde. Pathogen yi nit yi genna xam " virus" la ak " bacterie".[1] Feebar yi pathogen menna joxe ci missaal Korona lanuy woowe feebar yuy wale.
Xeetu ker doktoor yi
SoppiSetlu ci clinic yu ndaw yi ak clinic yu mag yi.
SoppiBaat u "infection" mooy beep tewaay u jangoro bo xamantani liko juur mooy ay "pathogen" ak nuniu menna tol nak wante daniuy jeffandiko bat bi lu ci epp pur men wax ci " infection" bo xamantani "clinic" yi gis naniu ko. Wante yennsay mu andi ay jaxaso, wante ci benneen wal, nit yi nek di yengatu ci wallu wer gu yaram danuy faral di wax baat u nootel su fekkantani microb yiy joxe jangoro nekk naniu ci yaramu nit ki wante nit ki wanewul benn feebar. Mandargay "infection" yi men nan len xaaj ci niaari pacc: bi feeñ ci nit ki ak bi nga xamantane ci clinic lanu ko menna gisse gannaw banu amale saytu. "Infection" bi nekk ci nit di dund ta wanewul ben mandarga lanuy woowe "infection" buy nelaw ci nit ki. "Infection" bu lak u ci nit, mooy "infection" bu am ci nit ki wante wanewul benn mandarga, ci gatal mooy "infection" buy nelaw ci nit. Ci missaal, feebar u "Tuberclose". "Infection" yi genna graw lu ci mel ni "Herpes" men nanu itam nekk ci nit ki te du wane benn manadarga. Xeetu "infection" yi men nanu leen xaaj ci pacc yi:[2] garaw,( mooy bi nga xam ni mandargay infection feebar bi dafay law bu gaaw),[3] chronic ( mooy infection bi nga xam ni ay mandargam danuy law ndank ndank) infection bu garawul( mooy bi nga xam ni mandargay feebar bi du gaw law, wante men na law ci gaaw ba raw bu chronic, infection buy nelaw( mooy bi nga xam ni nit ki amul benn mandargay infection wante "pathogen" u infection bi mungi ci moom),[4] ndotel u infection ( mooy fi nga xam ni foofu la infection bi tambali laata mu law ci li dess ci yaram u nit ki).
Walante
SoppiNi nga xamantane noonu la nit ñi di jele jangoro bi ci nit yobu ko ci nit, moom lanuy wakh yoon u wanlante. doom u jangoro u rañeku yi ñooy jooxe infection u rañeku yi itam infection u rañeku yi dañu am yoon u walate u rañeku. Pur xam lu waral infection yi di am ak naka lanuy fagaro ci ñoom faaj kat yi sen xel macc ci mbiir moomu war nanu xam naka la yoon u walante infection boobu di ame. Yoon u walante am na ay pacc u berri. Ci gatal men nanu ci lim:
- Doomu jangaro ji ( ndax ñoom ci ndote u infection bi lanuy dunde) mooy organism bo xam ni dafay joxe infection. Pathogen yi genna rañeeku ñooy virus ak bacterie
- Fi feebar bi jogge men na nekk mala bu am infection wala nit bu am domu jangoro bi
- Bunt u gennu kaay mooy yoon bi doom u jangoro bi di jeffandiko pur genn ci yaramu fi infection bi tambale
- Bunuy wax walante mooy yoon bi doom u jangoro bi jogge ci nit wala mala bu ko yore pur jox ko nit ku amul katan wala wayadi
- Bunuy wax dekkuwaay mooy dekkuwway bi nga xam ni foofu la doom u jangoro bi wara jaare pur jogge ci nit wala mala bu ko am , pur dem ci niit bu neew doole
- Buntu duggukaay mooy yoon bi doom u jangoro bi jaar pur dugg ci yaram u nit ku neew doole
- Nit wala mala bi nga xam ni men na dalal doom u jangoro bi suba, mooy nit ki nga xam ni yaramam dina men dekku doom u jangoro bi[1]
Doom u jangoro bi men na jogge ci nit wala mala bu ko yore pur dem ci nit bu neew doole ci anam bu nekk. Am na ay xeet u doom u jangoro ñoom ndox wala dund moo kay yobbu, am na yenneen yaram yu lalante wante itam am na yenneen ci jawu ji. Ci mbind mi, dinanu waxt ci doom u jangoro bi nekk ci jawu ji.
Primaire versus Opportuniste
SoppiPrimaire vs. Opportuniste
SoppiCi setlu, giss nanu ni neew na ci loolu yenn xeet u jangoro yi di nekk ci nit yi am wer gu yaram bu bax ama na sax am na ay xeet u "micro-organisme" yu berri. Feebar bu feeñ tek ci gararw loolu leep dafay lalu ci doole bi doom u jangoro bi am pur yakk fi doom u jangoro bi tambale wala doole bi nga xam ni fi doom u jangoro bi am nako pur dekku " germs" yi. Yennsay "system immunitaire" bi nga xam ni foofu la doom u jangoro bi sosso, men na yakal bopam gannaw bamu jeme pur controle infection yi. Waa ker doktor yi seen xel macc ci walu wergu yaram japp nauñ ni microbe yi am na ci ay " pathogen primaire" wala "pathogen oportuniste".
Primaire Pathogènes
SoppiDoomu jangaro primaire wala germ dañuy jooxe feebar rek gannaaw ñu nekk ci nit ki am jangoro bi te dara jootu ko ak itam ci doole bi ñu am ci jooxe feebar. Lu ci epp ci germ nit yi, nit yi rek lañuy infecte wante am na ay feebar yu garaw yi nga xamantani ay organisme yu nekk ci dekkuwaay yi ñoo koy joxe wala sax yenneen xeet yu am infection te duñu ay nit.[5]
Bibbe nabbe subay wernoowo mabbe
SoppiPathogen opportuniste yi men nañu joxe ay jangoro yi nga xamantani dañuy walate ci nit yi am doom u jangoro bi te amuñu benn mandarga te sen sen system immunitaire yi leen di aar amuñ u doole wala ci anam yu mel ni operation chirurgical wala accident lañuy dugg ci sen yaram.Pathogen opportuniste yi dañuy law bu baax ci kwa nit ki am doom u jangoro bi nekk ci anam yi nga xamatani dafa sonn loolu.
Jangat ci infection bi waral jafe jafe wergu yaram nit ki ak jafe jafe yi cu men juddu
SoppiInfection bi njek men nanu ko jappe kon li waral jafe jafe wergu aram nit ki, wente ci bennen wet, ñaarel u infection men nanu ko jape kon jafe jafe yi men juddu gannaaw infection bi.
Feebar yiy walate
SoppiFeebar bu nit jele ci infection , moom lanuy woowe feebar buy walate gannaaw bi nu jeflante ak nit ku feebar bu am jangoro bu mel ni grippe.Yenneen xeet u jangoro yi nit mena am gannaaw bamu amee infection wala mu jeflante ak nit ci wallu sexe dunu ay jangoro yu garaw loolu te itam soxlawuñu di bedi nit ki diko berr. Jangoro yi nit mena am gannaw mu ame infection and nanu ci ni, walante bi ci digante nit ak nit la wala ñak, wante itam walante bi men na nekk ci jawu ji, wala lekk gi, wala ndox mu set bu am doom u jangoro bi, wala nga jeflante ak mala, wante itam mat mat yo.[6]
Manadargay feebar
SoppiMandargay infection bi mun gi lalu ci ban xeetu feebar la. Am na ay mandargay feebar yi nga xamantani yaram bi yep lañuy japp; lu ci mel ni coono, ñak lekk, sa yaram di jeex, sa yaram di tang, wala ngay ñak guddi, ngay lox, di am ay metiit,di son lu berri. Am na yenneen xeetu manadarga yo xamantani danuy feeñ ci yenn pacc yaramu nit ki ci missaal, tap wala sekkat,wala bakan buy sotiku.
Yensaay feebar yi jogge ci infection duñu wone benn mandarga giiru jamono bi ñu nekk ci nit ki. Am infection tekkiwul ni nit ki dafa am feebar bu garaw di walle ndax am na ay infection yi nga xamantani duñu juur benn feebar ci nit ki am infection bi.[5]
Fii bakteri maa viral
SoppiGannaaw bi nu xame ni bacteri wala viral men nanu juur benn mandargay jangoro, dina jafe loolu xam lan moo waral infection bu specific.[7] Am na solo torop xam lan mo waral wuute bi ndaxte infection viral yi kenn menu ko fajj ak ay garab yu mel ni aitibiotic gannaaw bi nu xame ni men na fajj infection yu bacteri yi.[8]
Tekkele ci infection viral yi ak infection bacterie yi | ||
Mandarga yi | Infection viral | Infection yi jogge ci bacterie |
Mandarga yu nuro loolu | Lu ci epp infection viral yi danuy lekkelo ak yenn ci sunuy pacc yaram wala lu epp benn pacc ci sunu yaram ci missaal , bakan buy soti, sinusite, sekket, wala yaram buy meeti bu bax. Am na yenn ci infection viral yi nga xamantani danu meeti torop ci missaal, herpès. Metit u infection viral li koy mandargal yensaay mooy yaram buy xasan,wala lak lak.[7] | TMandarga yi genna rañeku ci wallu infection yi jogge ci bacterie ñooy yaram bu deretal, tangay u yaram, yaram bu neewi,wala metit bo xam ni xam nanu fumu nekk.Benn ci mandargay infection yi jogge ci bacterie mooy metit bo xamantani dafa nekk ci fenn ci sunu pacc yaram fu am solo. Ci missaal su fekkantani nit ki dafa am dag dag fenn ci yaramam, gannaaw gi mu am infection, pacc bi am infection bi dafay meti apre. Dag dag buy genne det bu weex, men nanu japp ni dafa am infection.[9] |
Fajj gi
SoppiSufekkantani infection dafa song yaram u nit ki, xeetu garab yi di fajj infection, men nanu ko dindi. Am na xeetu garab yu berri yi nekk di fajj infection. Ay antibiotic ñoom bacterie rek mo leen taxa jogg itam menaluñu doom u jangoro bi dara. Antibotic li ko taxa jogg mooy wañi doole bacterie bi ci ni muy lawe wala ray bacterie bi.[10]
References
Soppi- ↑ 1,0 et 1,1 Chapter: 2. Disease and disease transmission. Available at https://ec.europa.en>cpd02 Accessed on 13 April 2020
- ↑ Grinde, Bjørn (2013-10-25). "Herpesviruses: latency and reactivation – viral strategies and host response". Journal of Oral Microbiology. 5: 22766. doi:10.3402/jom.v5i0.22766. ISSN 0901-8328. PMC 3809354. PMID 24167660.
- ↑ "Acute infections (MPKB)". mpkb.org. Retrieved 2019-12-09.
- ↑ Boldogh, Istvan; Albrecht, Thomas; Porter, David D. (1996), Baron, Samuel (ed.), "Persistent Viral Infections", Medical Microbiology (4th ed.), University of Texas Medical Branch at Galveston, ISBN 978-0-9631172-1-2, PMID 21413348, retrieved 2020-01-23
- ↑ 5,0 et 5,1 Foster, John (2018). Microbiology. New York: Norton. p. 39. ISBN 978-0-393-60257-9.
- ↑ Ryan KJ, Ray CG, eds. (2004). Sherris Medical Microbiology (4th ed.). McGraw Hill. ISBN 978-0-8385-8529-0.
- ↑ 7,0 et 7,1 (Higurea & Pietrangelo 2016)
- ↑ "Bacterial vs. Viral Infections – Do You Know the Difference?" National Information Program on Antibiotics
- ↑ Robert N. Golden; Fred Peterson (2009). The Truth About Illness and Disease. Infobase Publishing, 2009. p. 181. ISBN 978-1438126371.
- ↑ "Infection". Rencare. Archived from the original on March 5, 2012. Retrieved 4 July 2013.