Royuwaay:Infobox biographie2 Faatu Joom mi juddu ci atum 1968 ca Ñoojoor ci Sénégal, taalif kat bou jiggeèn la bu coosano Senegaal di dundu Faraas.

Ginaw siwalug limu teère bu tudd La Préférence nationale, ci atum 2001, naka nonou teerem buñu naan Le V entre de l'atlantique moo tax ñu xamko ca bitim reéw. Ci am  mbindam daciy wax lu jëm ci tukki ca Faraas ak itam dingante Faraas ak keembarug Afrig.

Jaar-jaar

Soppi

Fatu Joom mongui juddu ci atum 1968 ca dunug Ñoojoor ci mbelug Salum, ci dëku Seereer, ca ngélemu-suufu Senegaal. Jank piir la –– ay wajuram sëyu ñu -- maamam bu jigeen, Aminta moko yarr.. Aw santam mongi juge Siin Saalum, fa nga xamne Joom yi ay Ñominka lanu.

Wuteg li cosaanu xeetam digle, dafay taqqoog goor ñi déet muy dimbali jigéen ña ñu togg ñam ya ag def ligeyu kër yi. Saa sune day wute ak dundinug waa dunu gi batax mu dem daara teksi jangi fanraase. Maamam bu jigéen def na ab diir ngir nangu ni man na jangi : mom Faatu jank bi da daan dem daara di lakatu, ba kerok jangalekatam yayy ay waajuram ngir ñu bayiko mu wëyële. Ci fuki at ak juròom mu bëgg lool njangatu faranse tek si tambale bind. Faatu Joom genn ab dëkkam ngir wëyële am njangam ci yenen dëkku Senegaal, bolek di fayale ag dundug màang kat gui ak ligéey yu ndaw yi ;  teksi mu jangi daray Mbuur, ligey kem mbindaan fa Gambi  teksi muje tambali am njangum iniwersite ca Ndakaaru.  Ca jamono jooja mongui bëgona doon jangalekatu faraase, déet muy genn réew mimu juddo.

Waye ci ñaar fukki at ak ñaar mu  bëgg benn faraase, daldi sëyi teksi andag mom Farans ca Strasbourg ci atum 1994. Binga xamé ni njabootug borom kërëm beedi nanu ko, mu daldi tass ab sëyam ñaari at ci ginaw tek si mu nekk ci jafe-jafe yu metti, ñu wacc ko ci nekkinug Mòodu-Mòodu ci suufu Farans. Ngir mu fay am njangam, fawu mu mbindaanu ci diirug juròom benni at, ag bimu mane jangale ca waxtu wanga xamne am na lijaasam bu mag ba, njëkk muy tambali ab ligéeyam ci « Tukki gi , jëflante yi ak njang mi ci mindum téere ak sinemaa bu Sembeen Usmaan».

Liggéey

Soppi

Ginaw bimu jange araf yi ak filosofi ca iniwersite bu Strasbourg, mu daldi fay jangale, teksi iniwersite March-Bloch bu Strasbourg ak daara bu kawe bu jëm ci wallu njangele bu Karlsuhe, fa Allemagne.  Mu daldi jot raaya ya ñeel lijasa honoris causa ca uniwersite Liège ci atum 2017.

Mu dëgmal it am mbind : siiwal na La Préférence nationale,  ab limu teere bu jooku ci Présence africaine ci atum. Le Ventre de l'atlantique moy taarixam bu njëk  , bi genn ci atum 2003 bu ciwalug Anne Carrière.  Ginaw gi laci toppu Kétala (2006), Inassouvies, nos vies (2008), Celles qui attendent (2010) ag Impossible de grandir.

Ci atum 2019 la am ngañelu raaya yu ñoom Rotary Club bu làkk faraase ñeel tàarixam Les veilleurs de Sangomar.

Gis-gis

Soppi

Dafay jammarlog ag ñi amul yërmande, day àar ligéeyu daara ag meloy  gëm sa réew.

Lu jëm ci maggug populism gi, Faatu Joom dankoy faral di sakku saa sune ngir mu yaatal xalatam ci ay waxu politig ag askan wi ci telewisong yi ak xar-xarale yi.  

Mu jël taxawaay bu am solo ci maggug populism andag Mboolom biir réew ba ca Faraas. Ci nekk bimu nekk bindkat , dafa bëg fatali ci ay téerem meloy nit ak  gëm sa réew  ndax mom diapp nani « waratuño noppi ci kanamu ñi dano wayadi ci taanal biir réew».


Dafay wax tamit kàdduy ñaxtu ngir lëkkalo bu gëna yamo ci dingante Orob ak Afrig. Jàpp nani fiñu tollu Orob mo nek ci ginaw lëkkalo bu yamo wul teksi Afrig moomul alalam. Te it jàpp nani rusaange jamonoy koloñal ba mongi fi ba léegi muy ci booru wa Afrig ak tamit wa Orob, mu nekk liy gaar ab lëkkalo bu gëna yamo. Xalaat nani kunekk war na yeug ni nit la su jakkarlok benen moromu nitam, mo xam fumu mana soqqeeko. Naka nunu, déet muy joxoñ baaram benn kembaar, motax jàap nani waa Afrig dano war wesu di nekk ñunuy noot te it wa Orob bayi sen noot gi ngir digante  aji jariño/ aji jariñe, aji joxe/ aji jox ji mana dakk. Fimy daane le moy dafa leeral ni dimbali aw nitt moy nga dimbali ko ba dootu soxla dara ci yaw, masalan ndimbal li ñeel sùkkaliku bi réewi sowu yi ini Afrig.

Mbind mi

Soppi
  • 2001 : La Préférence nationale, recueil de nouvelles, édition Présence Africaine.
  • 2002 : Les Loups de l’Atlantique, nouvelles, Dans le recueil : Étonnants Voyageurs. Nouvelles Voix d’Afrique.
  • 2003 : Le Ventre de l'Atlantique, roman, éditions Anne Carrière, éditions Le Livre de poche 30239
  • 2006 : Kétala, roman, Éditions Flammarion.
  • 2008 : Inassouvies, nos vies, roman, Éditions Flammarion.
  • 2010 : Le Vieil Homme sur la barque, récit (illustrations de Titouan Lamazou), Naïve.
  • 2010 : Celles qui attendent, roman, Éditions Flammarion
  • 2010 : Mauve, récit, Éditions Flammarion
  • 2013 : Impossible de grandir, roman, Éditions Flammarion.
  • 2017 : Marianne porte plainte !, essai, Éditions Flammarion.
  • 2019 : Les Veilleurs de Sangomar, Albin Michel.
  • Weepers Circus, N'importe où, hors du monde (2011). Disku-téere la bo xamni lu tollog ñeent fukki nit yu am darajay taalifkat wala antarpareet ñoo ci bokk : Faatu Joom taalif nasi mbind munu siwalul (bunu wayul) ñeel ab gis-gisu bopam ci tur bu naqqare degg bu téeri bii di "N'importe où, hors du monde".

Téere yi nu yër

Soppi
  • (en) Dominic Thomas, « African Youth in the Global Economy: Fatou Diome's Le Ventre de l'Atlantique », Comparative Studies of South Asia, Africa and the Middle East, 2006, no 26(2), p. 243-259
  • Jacques Chevrier, « Fatou Diome, une écriture entre deux rives », Revue des littératures d'Afrique, des Caraïbes et de l'océan Indien, no 166, 2007, p. 35-38
  • Victor Essono Ella, La crise de l’identité à travers l’écriture de Valentin Yves Mudimbe, Eugène Ebodé et Fatou Diome, Université Rennes 2, 2008, 365 p. (thèse de doctorat de Littérature française)
  • Eugénie Fouchet, La représentation romanesque de la femme africaine chez Fatou Diome et Fatou Keïta, Université de Metz, 2009, 156 p. (mémoire de master recherche 2e année de Littérature, cultures et spiritualités)
  • M. H. Kebe, « Le ventre de l'Atlantique, de Fatou Diome », L'Information psychiatrique, 2004, vol. 80, no 6, p. 491-493
  • C. Mazauric, « Fictions de soi dans la maison de l'autre (Aminata Sow Fall, Ken Bugul, Fatou Diome) », Dalhousie French Studies, 2006, vol. 74-75, p. 237-252