Ekontiŋ bi ("akonting" ci angale walla "ekonting" ci franse), xalam la ci cosaanu Joola. Am na ñetti nas te yaramam mooy kalabas bu nu taqe deru bëy. Baatam dafa gudd ak xat. Baat bi mooy banjul. Bépp nas dafa wute guddaay: bu gudd, bu yem, ak bu gàtt. Nas ñi ñooy caas. Tëgg na nasu gudd ak baaraamu joxoñ ci loxo ndeyjóór. Tëgg na nasi yem ak gàtt ak baaraamu déy ci loxo ndeyjóór. Ekontiŋ dafa yam bucundu (ci cosaanu Manjago), busunde (ci cosaanu Papel), ak kisinta (ci cosaanu Balanta). Mel na xalam (ci cosaanu Wolof) ak ngoni (ci cosaanu Mandinka). Banjo bi ci cosaanu Amerik la mel itam.

Joueur d'ekonting à Bagaya

Xeetu Jola jòge na Kasamans, ci bët Saalumu Senegaal. Am na niti Jola yu bari ci Dakar ak Gambi itam, rawatina ci bët Saalumu ci dex bi Gambi. Niti Jola ñooy beykati ceeb ak nappkat. Dañu def sëng itam. Am na Gurmet yu bari ak Julit yu tuuti ci cosaanu Jola, ak boroomi xërëm itam. Cosaanu Jola dafa "acephalous" (duñuy am benn boroom rekk) te duñuy am geer, ñeeño, ak jam. Ñëp mooy ci mbiru muy. Duñuy am géwél itam; ñëp mën na tëgg sabar, manaam ekontiŋ.

Ekontiŋ lanuy tëgg pur xewi Jola. Tëgg nanu ko lool ci ngénté ak takk. Tëggkatu, ekontiŋ bi dina woy itam. Beneen musikkat tëgg na sabar bu mag. Bugarab la tudd. Wëyi Jola dañu "sumé" (dañu neex) te am nañu tuuti baat. Seeni waxin wax nañu ci wallu xol, waakër, ligééy, yité, ak àdduna ci àll.

Benn ndaanaanu Jola, Daniel Laemouahuma Jatta la tudd. Mandinari ci Gambi la jòge. Tëgg na ekontiŋ bu baax, te xam na lool ci wallu cosaanu Jola. Mag mat naa bàyyi cib dëkk. Keneen tëggkatu ekontiŋ, Sana Ndiaye la tudd. Kasamans la jòge, waaye New York la dëkk. Moom, tëgg na ekontiŋ ci gàddu "rap." Gokh Bi System lañu tudd. Ekontiŋ bi amul tànk, waaye jàll nam ndox.