Dungidég garab la gog mi ngi bokk ci njabootug Fagara Zanthoxyloide.

Cosaan laa nga ca Senegaal ak Kamerun.

Dungidég gi


Melo wi Soppi

Garab la guy sax ci wetu géej ak fuy am ndox.

Njariñ li Soppi

Dungidég garab la gu bari njariñ. Garab la guy faj jàngoroy biir, jàngoroy dënn añs... Xob yi, xàncam yi ak reen yi dinay faj tawati mbàq guy metti (estomaa), tawati góom i biir ak biti, soj, biir buy daw, emoroyit, ak yeneen.

Manees na ko soccoo, dinay wàññi daŋaru bëñ buy meti ak it di ko faj.

Dinay yombal dawug dereet ji.

Reen yi bari garab yees koy def ci wàllu faj, rawatina ca Burkinaa Fasóo, ca Gana, ca Niseria, ca Mali ak ca Kodiwaar.

Nataal yi Soppi


Turu xam-xam wi Soppi

Fagara Zanthoxyloide