Dugóor xeet la ci xeeti garab yi, mi ngi bokk ci njabootug Annonaceae. Mi ngi sax ci tund yi nga xam ne suuf si day xaw a wow walla ci barab yi nga xam ne day xaw a tooy.

Dugóor gi (Annona senegalensis)
Dugóor gi (Annona senegalensis)

Melo wi

Soppi

Garab la gog guddaayam man naa àgg 6i met. Ab xasam day yor melo wu baam daal di liis, ci nawet bi lay faral di meññ.

Ay xobam day yor melo yu bari bokk na ci baxa, daal di muluŋ, guddaayam man àgg 7-17i sentimet. Ay fóoyteefam day liis daa di muloŋ, yor melo wu mboq walla puur.

Njariñ yi

Soppi

Dugóor garab la gog dees koy lekk, saa-afrig yi bëgg nañu ko, ndax dafa neex lool, tey it bari na lu miy faj.

Nataal yi

Soppi

Turu xam-xam wi

Soppi

Annona senegalensis