Daqaaru tubaab xeet la ci xeeti garab yi mi ngi bokk ci ñoñ Prosopis , ci njabootug Fabaceae. Ñi ngi koy fekk ci yenn gox yi ci diggu Sili walla ci bëjsaalum Peru, da fa bari lool.

garub Daqaaru tubaab

Melo wi Soppi

Garab la gog guddaayam moo ngi tollu ci 14i met. Peeram dafay rëy, yaatuwaayam mi ngi tollu ci 1i met. Am xasam day yor melow paalmaan am ay xar-xar. Ay foytéefam dañiy wëraloo, seen guddaay di tollu ci 15i sàntimet, ci biiram ay doom yu baree fay ne, doom yi day niru ak doomi kafe. Moo ngi génn li ëpp diggante Oktoobar ak Desàmbar. Ay foytéefam mi ngi ñor diggante weeri Feewiriyee ak Awril. Garab la gog day màgg ci suuf su nooy, ci tund yi xaw a wow.

Njariñ yi Soppi

Garab gog dees koy jëfandikoo ngir màtt, ay xobam dees koy xoontee baayima yi, foytéefam jur gi bëgg na ko lool.

Nataal Soppi

Turu xam-xam wi Soppi

Prosopis chilensis