Dambal garab gu siiw la ci ne Senegaal la bàyyikoo waaye dees na ko gis ci yaneeni barab ci Afrig.

Dambal gi (Kigelia africana)
Dambal gi (Kigelia africana)
Tóortóori garabug dambal
Tóortóori garabug dambal

Melo wi Soppi

Garab la guy àgg 10 ba 15i met.

Xobam dafa wërmbalu tóor-tóoram juróomi xob la am. Guddi day gilli xet gu xasaw, day ndiiraan foytéef bu lax.

Xetam day xàcc njugub yiy ñëw sabab ag saxam.

Danay meññi ay foytéef yu dijj te baam ba noppi di lang. Foytéefam siiw na ci ne nit du ko lekk waaye ca gox yamuy sax dees nako lekk ci lu dul togg.

Njariñ yi Soppi

 
Meññeefum garabug dambal

Ginnaaw ag lekkam baa ag taaralam, dees na ko jëfandikoo ci taaral deru jigeen, dees na ci génnee it diw dees na ci faje it, dana faj ñatti xeetu kaaseer: kaasseeru ween, kaaseeru res, kaaseeru suufu nit.

Turu xam-xam wi Soppi

Kigelia africana

Tur wi ci yeneeni làkk Soppi

farañse: sausage tree
angale: arbre à saucisses
itaaliyee: albero delle salsicce