Daaru Jaxate ab dëkk la bees sos ci ndigalul sëriñ '''Tuuba''' ci atum (1915/1916) mu nekk Kajoor 3 kilomeetar digganteem ak '''Mbaylaar,''' 7 kilomeetar diggam ak '''Pekkes''', bokk ci '''Xelkoom Jaxate''' gi sëriñ '''Saaliwu tudde Xelkoom Jaaga'''. Kilifa gu mag gu '''sëriñ Tuubaa''' seexal ñu koy wax '''sëriñ Faatu Jaxate''' moo ko sanc, ginaaw bi way-juram '''sëriñ Yéeri Jaxate''' wàccee ab liggéey. Soppi

Muy dëkk bu cosaane, '''Jaxate''' ak '''Caam''' ñoo fa ëpp, bari na xeeti garab yu fay sax ak di fa ñor, li ëpp ci seeni mbay gerte ak dugub la ak ñebbe. Soppi

Dina ñu sàmm it ag jur; xar, bëy nag, yii a fa ëpp. Daara amna fa ay kàngam it génne nañu fa. Soppi

Njabootug sëriñ Tuubaa gi daa nañu fa ñëw lu bari, ku mel ni sëriñ ''Fàllu''', sëriñ '''Basiiru,''' sëriñ '''Baara''', moom sax sëriñ '''Baara''' mii moo feeñal dëkk ba, sëriñ '''Sohaybu''', it daa na fa ñëw ak '''sëriñ Murtalaa''' añs... daan nemmiku mbóot ya fa nekk, ak a xeeñtu saaway ñu baax ña fa nekk. Ci atum 1945 la sëriñ Faatu Jaxate boroom dëkk ba nelaw wuyu ji Boroomam, '''sëriñ Seex Jaxate''' wuutu ko fa, ba atum 1990, mu wàcci '''sëriñ Fàllu Jaxate''' wuutu ko fa ba atum 2016 '''sëriñ Murtalaa Jaxate''' nekk fa, yal na ko fi Yàlla yàggal, moom sëriñ Murtalaa Jaxate mii nag, di jàmbaar lool, joj, def na fa liggéey bu rëy yeesal na barabu sëriñ Faatu Jaxate ba, natt dëkk ba liiñe ko, defar rfa jumaa ju mucc ayib, at mu ne amna màggal gu fay am, muy ag ñaan gog dina ñu ko defal seen maam yu baax yooyu. Soppi

Bi ñu sàncee dëkk ba, ña sant Caam ñoo fa jiitu, ba tay it ñoo fa nekk, daara ju mag ja ginnaaw sëriñ Faatu, sëriñ Basiiru Jaxate doomam moo ko yorewoon di ko doxal ba ni mu fi jógee, ginaaw ba sëriñ Basiiru Jaxate mum sëriñ Seex Jaxate moo fa sampaat daara ba fiimu toll nii moo fa nekk, di ko defe nu am solo. Soppi

Teen ba fa nekk it teenub barkeelu la bob sëriñ Tuubaa moo ko gasluwoon ñaab ci ab siwo sottilu ko ca, Soppi