Daaru Gay
'' ' Daaru Gay ' ''
Dëkk la boo xam ne, moo ngi bokk ci goxub ( Cees) tundu ( Kajoor) Sëriñ Maxtaar Gay moo ko sañc ci atum junni ak juróom ñenti téereem ak fukk ak juróom ñent 1919 ginnaaw bi mu ci amee ndigalul Maam Cerno Faati Boroom Daarul Muhti. Mu nekk dëkkub diine ak lislaam, Sëriñ Maxtaar Gay nekkoon fa, mook ay rakkam, di ay doomi baayam, ku mel ni Sëriñ Gay Sëy. Ak Sëriñ Ma-Sayeer Gay. Ak ay jarbaatam, ku mel ni Sëriñ Omar Sàll, Sëriñ Musaa Njaay, Sëriñ Moor Ñaan, Sëriñ Asan Ñaan, Sëriñ Abdu Ñaan, Sëriñ Omar Ñaan. Ak ay doomi ndayam ay taalubeem. Boolewoon liggéey, jaamu Yàlla, jàng ak jàngle, ak yar njaboot gi. Daaru Gay nag li ëpp ca askan wa dañuy yëngutu ci wàllu bay ak yaxantu.
Aji bind ji Móodu Gay Fàllu Daaru Gay.