Dédd
Dédd genn xeet la ci xeeti garab yi, mi ngi bokk ci njabootug Fabacées, mi ngi fekk baax ci Afrig gu ron-saharaa
Melo wi
SoppiGarab gii melow ñax gu sëq gu law ci guddaayu garab lay yor.
Yenn saa yi nag melow as ngarab su dàttam di àgg 20 ba 30i sàntimet ak 3 ba 5i met ci guddaay lay yor. Daa bariy dég, yu ay car ak reeni xobam tiye. Seen ug guddaay danay àgg ba 8i milimet. Doomam day tàcc, di yore melow puur, xonq mbaa baam tey àgg cig natt 6 ba 10i sàntimet ci guddaay ngir 1 ba 1,5 sàntimet ci yaatuwaay. Ci tënk 6 ba 8i saal yu tàcc, yu nëtëx mbaa xuun lay ëmb.
Njariñ
SoppiDédd gi deef na ko jëfandikoo nig garabu paju cosaan. Tóortóoram meññ lem. Màttam danay jariñ ci defarug jumtukaay yu wuute (tum, fett...). Wàqaasam dees na ko feteñe.
Nataal
Soppi-
Xobi garabug Dédd
-
Dàtt bi
-
Xob yi ak meññeef mi
-
Tóortóoram