Broken/Dalal-jamm

Dalal-jamm, yaa ngi ci wikipedia gi ñu jaglel kàllaama wolof, muy ab tèerexamteef gu tinkiku goo xamne ñi koy jàng bokk nañ ci ñi koy bind.
ku nekk man nga cee dugal sa loxo, bind ay jukki yu bees wala gënël baaxal li fi jota nekk; ndaxte ngir mebet mii mana dox ci ni mu gënee, dafa laaj ay loxo yu bari. Kumu manti doon man nga cee japp ci njekk ak teranga, topp atte yi'ñ fi tërël, ñoo ngi lay dalal.
Li mu doon lu ubbeeku ngir ñëpp te amul'g pay, ñi binduwul tamit ci biir, moo tax Wikipedia manula joxe ay wòoraange ci baaxaay ak celltey ndefam. Donte askan wu wikipedia moo ngi tijji ay gëtëm di ko jeema aar ci anam yu dëgër. Ci saa su ne man na am ay xët yu ñu say-saye wala yuñu soppi ci anam yudul yi gën te tay ko, def ci ay xibaar yu baaxul wala yu dëppowul ak dundinu sa waa-gox.

== Nooy saytoo wikipedia ==
man ngaa tambalee ci xët-njëkk mi te topp lëkkalekaay yi lay yòbb ci li la solool, li nga soba jàng.
su fekke itam daa am ab jukki booy seet, man nga bind benn wala baat yu bari ci paxu bind gi, gi nekk ci sa ndeyjoor te nga klig ci Ayca

  • Su fekkee baat bi nga bind da fa nekk koju ab jukki ba noppi, da ngay klig ci Ayca rek mu feeñ.
  • su fekke nak baat bi dafa nekk ci biir ay xët yu am ba noppi, da ngay klig ci seet.
  • (jappal ne xëtu seetukaay gi day tijjil boppam su fekke danga klig ci Ayca te amul lu mu la andil, gisul dara).