Bowas
Ci làkku ibrë (בועז) la tur wi jóge. Ci angale mooy Boaz; Ci faranse mooy Boaz
Boroom alal ak beykat ci dëkku Betleyem la woon. Dafa takkoon jenn jigéenu Mowab, ji tudd Ruut. Jot na Ruut ndax jëkkëram mbokkam la woon te faatu na bala mu am doom. Ci kaw seeni yoon, su fekkee ne am na genn góor gu faatu te bàyyiwul doom, mbokkam mu gëna jege war na donn jabaram. Seen taaw bu goor dina donn ci goor ki faatu woon. Bowas mbokk mu jege jëkkëru Ruut la woon. Doom bi ñu jur mooy maamu Daawuda. Man nañu koy jàng ci Ru 1:1-4:22. Naka noonu Bowas bokkoon na ci maamaati Yeesu, ni ñu koy gise ci Macë ak ci Luug (Mc 1:5; Lu 3:32).