Bipolar disorder


Feebaru "bipolaire", ñu xamewoon ko ni déteelu bu ànd ak mer gu bon, mooy ab feebaru xelguy indi ay waxtu déteelu ak ay waxtu yu du sul noono yudikkale gu kawe.[1][2][3] Dikkale gu kawe gi bari na te ñungi ko xame ni mer gu rëywalla dikkale gu amul kersa, mungi aajo ci rëyaayam, walla ndax liy wone xel mu tagoo ak li xew mungi ci. [1] Bu nit nekkee ci mer gu rëy dafay am jikko walla yég bu dul noon njaxlaf, bég, walla mer.[1] Nit ñi dañuy jël ay dogal te duñu ci xalaat te itam duñu xalaat li ñuy jur. [2] Bu nit ki nekkee ci waxtuy mer gu metti duy faral di soxla nelaw. [2] Bu nit ki nekkee ci ay déteeloom, joy dafa koy yom, gis-gisam ci dund gi dafay ñaaw, te duy xool ñeneen ñi ci ay gët. [1] Njàjanu xaruci ñi ame feebar bi lu kawe la agg ba 6% ci ñi ëppal ñaar fukki at, tey ci booba dagg sa bopp mungi ame ci diggante 30 ba 40 %.[1] Yeneeni jafe-jafe yi nekk ci feebari xel yi ni feebaru ragal yu mettiakdi jëfandikoo dorogdañu leendi faraldi boole ci Feebaru "bipolaire".[1]

Li koy indi leerul ci bopp nit ñi, wante ñaari yi yépp dili ñu wër, ak dondu am nañ ci wall.[1] Dondu yu bari ak ay efe yu ndaw bokk nañu ci luy joxe njàjan yi.[1][4] Risk yi nekk ci li ñu wër bokk na ci istuwaaru noot xale ak diir bu yagg stress. [1] Lu tollook 85% ci wallu risk bi ñungi teg ci dondu.[5] Feebar bi ñung ko dugal ci feebaru bipolar I bu mësoona am lumu ndaw ndaw benn waxtu dikkale, ak walla bu amul waxtu déteelu, ak ni feebaru bipolar II bu amoon lumu ndaw ndaw benn dikkale gu amul kersa (waaye bu amul ay waxtu dikkale) ak benn waxtu déteelu bu mag.[2] Ci ñi nga xam ne ni feebar bi duy feeñ noonu bu baax lu yagg, li koy indi feebaru xel mu jaxasoo di dem ci diggante bég ak déteelu mën nañu ko xool génne li ko waral.[2] Su fekkee li koy indi mungi joge ci ay garab walla jafe jafe ci paj mi, dañu leendi xajjale.[2] Yeneen yi koy indi yu mëna génne yu mel noonu ñooy Feebaru yëngu-yëngu bu tar bu àndak ñakka farlu, ay feebaru nekkin, Ñi ame jangoro schizophrénie dañuy faraldi réére mbir ak li xew. Seen nekkin du méngoo ak liy xew ak febaru dorogewu ak yenn yi koy indi joge ci wallu paj mi.[1] Saytuwër gu yaramjarul def ngir absaytu, su fekkee sax ay saytu dereet walla portale feebar yi mën nañu leen jëfandikoo ngir dindi yeneeni jafe-jafe.[6]

Paj mi ñuy gëna jëfandikoo bokk na ci Pajum feebaru xelak jël ay garab yi mel ni Seral dikkale (naqari dereet) ak luy xeex ak ñakk àndak sago.[1] Yenn ci yii di seral ci yi ñi gëna jëfandikkoo bokk na ci lithium ak yeneen xeet yu wute yi di xeex jangoro kiriis[1] Paj mu ñu waajalul ci ab pajukaay war nañu ko soxla bu fekkee am na ku jege ci fexeel boppam walla ñeneen ñi te baña fajuji.[1] Ay jafe-jafe nekkin yu jeggi dayo, lu mel ni yëngëtu walla xeex, mën nañu ko toppatoo ak yi di xeex ak ñakk àndak sago ci diir bu gàtt walla ay garabu benzodiazépines.[1] Ci waxtub xër, dafa gën yi di xeex déteelu ñu bayyi leena jël.[1] Su fekkee yi di xeex déteelu ñungi leendi jëfandikoo bu amee ay déteelu, war nañu leen jëfandikoo ak li di seral dikkale.[1] Pajum feebaru xel bu ñuy jëfandikoo electrochoc (ETC), su fekkee sax gëstuwuñu ko bu baax, war nañu ko mëna jéém ci ñooñu ñu ñu mënula faj ak yeneen paj yi.[1][7] Su ñu bayyee jëfandikoo ay paj, dañu bëgg ñu benn bennal ko.[1] Nit ñu bare dañu ame ay jafe-jafe koppar, seen nekkin ci biir nit ñi walla ci seen liggééyukaay ndax li ñu ame feebar bi.[1] Jafe-jafe yii ñeent ba ñett yoo jël saa yu nekk benn bi am na leen.[1] Yoon yi ñi tann ci seen dundin ak li garab yi di def ci ñoom, njàjanu dee yu jogewul ci benn jàngoroni feebaru xol tollu na ñaari yoon nit ñi.[1]

Téméér boo Jël ci addina bi am na kenn ku am feebaru Bipolar.[8] Ci Amerik, téméér boo jël ñett ñi am nañu feebar bi ci seen dund, ñi ko ame ci góór ak ci jigéén ño ko tolloole. [9][10] Lu ci ëpp boo ame ñaar fukki at ak Juróóm nga koy tambale gis.[1] Feebaru bipolaire bi tollu na ci liñu génne ci xaalis ci 45 miliyaar ci Amerik ci atum 1991.[11] Cërcëraat gu rëy ci loolu te jóge ci woññi gu kawe ci ñakka liggééyi, dafa tollu ci Juróóm fukk at mu nekk.[11] Nit ñi ame feebaru Bipolaire dañuy faraldi am ay jafe-jafe ak ñeneen ñi di leen gise ni ñi am lëgët. [1]

References

Soppi
  1. 1,00 1,01 1,02 1,03 1,04 1,05 1,06 1,07 1,08 1,09 1,10 1,11 1,12 1,13 1,14 1,15 1,16 1,17 1,18 1,19 1,20 1,21 et 1,22 Anderson IM, Haddad PM, Scott J (Dec 27, 2012). "Bipolar disorder". BMJ (Clinical research ed.) 345: e8508. PMID 23271744. doi:10.1136/bmj.e8508. 
  2. 2,0 2,1 2,2 2,3 2,4 et 2,5 American Psychiatry Association (2013). Diagnostic and Statistical Manual of Mental Disorders (5th ed.). Arlington: American Psychiatric Publishing. pp. 123–154. ISBN 0-89042-555-8. 
  3. "DSM IV Criteria for Manic Episode". Archived from the original on July 31, 2017.  Unknown parameter |df= ignored (help)
  4. Goodwin, Guy M. "Bipolar disorder". Medicine 40 (11): 596–598. doi:10.1016/j.mpmed.2012.08.011. 
  5. Charney, Alexander; Sklar, Pamela (2018). "Genetics of Schizophrenia and Bipolar Disorder". In Charney, Dennis; Nestler, Eric; Sklar, Pamela et al. Charney & Nestler's Neurobiology of Mental Illness (5th ed.). New York: Oxford University Press. p. 162. 
  6. NIMH (April 2016). "Bipolar Disorder". National Institutes of Health. Archived from the original on July 27, 2016. Retrieved August 13, 2016.  Unknown parameter |df= ignored (help)
  7. Versiani, Marcio; Cheniaux, Elie; Landeira-Fernandez, J. "Efficacy and Safety of Electroconvulsive Therapy in the Treatment of Bipolar Disorder". The Journal of ECT 27 (2): 153–164. PMID 20562714. doi:10.1097/yct.0b013e3181e6332e. 
  8. Grande, I; Berk, M; Birmaher, B; Vieta, E (April 2016). "Bipolar disorder". Lancet (Review) 387 (10027): 1561–72. PMID 26388529. doi:10.1016/S0140-6736(15)00241-X. 
  9. Diflorio, A; Jones, I (2010). "Is sex important? Gender differences in bipolar disorder". International Review of Psychiatry (Abingdon, England) 22 (5): 437–52. PMID 21047158. doi:10.3109/09540261.2010.514601. 
  10. Njuumteg royuwaay: Balise <ref> incorrecte : aucun texte n’a été fourni pour les références nommées Schmitt2014
  11. 11,0 et 11,1 Hirschfeld, RM; Vornik, LA (Jun 2005). "Bipolar disorder–costs and comorbidity.". The American journal of managed care 11 (3 Suppl): S85–90. PMID 16097719.