Betani bu Yurdan
Bérab fu Yonent Yàlla Yaxya doon sóobe nit ñi ci ndox ci gannaaw dexu Yurdan, maanaam ci penku dex ga (Yow 1:28). Foofu la Yaxya sóobe Yeesu ca ndox itam.
Bu yàgg xamatuñu tembe fan la dëkk bi nekkoon. Waaye seetkati cosaan yaakaar nañu ne fekk nañu bereb ba ca penku dexu Yurdan ca atum 1995. Berab ba Wadi al-Xarar la tudd. Am na fa ay bëti ndox, ak benn làquwaay fu ñu yaakaar ne Yaxya daan na fanaan. Su fekkee ne danga nekkoon ca dëkku Yeriko manoon nga gis berab ba. Ñoom ñi gas ci suuf ngir seet naka la nit ñi dëkke ca yeneen jamono yu fekk nañu ca bereb ba ay tabax, ay jàngu, ay làquwaay fu nit ñi doon dëkk, ak ay sanguwaay. Taalibe Yeesu yi doon nañu ajji ngir siyaaraji ca xarnu yu jëkk yi gannaaw jamono Kirist.