Elimas

(Yoonalaat gu jóge Bar-Yeesu)

Ci angale mooy Elymas; Ci faranse mooy Élymas

Luxuskat la woon, ku bokk ci Yawut yi ci dëkku Pafos ci dunu Sipar. Dañu koy tudde itam Bar-Yeesu. Mu bokk ci gàngooru boroom réew ma tudd Sersiyus Poolus. Dafa dogale Pool, ngir bañ boroom réew ma gëm. Waaye Pool rëbboon na ko ba mu gumba. Man nga ko jàng ci Jëf 13:6-12.

Man nañu gis tur wi ci Jëf 13:6.