Béer garab la gog guddaay gu yam la yor. Mi ngi bokk ci njabootug Anacardiacées.

Nataalu garabug béer

Melo wi

Soppi

Garab gi peer bu ndaw la yor, day màgg jëm ci kaw, guddaayam man naa àgg ba 10i met. Garab gu bari lool ay witaamin la. Danay meññ benn fooytéef bu dëgër, ñuul te neex lool.

Njariñ yi

Soppi

-Ay foytéefam dees koy lekk ak di ci defar yenn xeeti njar yi. -Garabu ber manees na ko jëfandiko ngir doxal yenn daamar yi. -Garab la gog bari na jàngoro yu muy faj, bokk na ci sibbiru.

Nataal yi

Soppi

Turu xam-xam wi

Soppi

Sclerocarya birrea