Béb di Strecuia satigera garab la gu man a sax ci suuf su bon ak kéew mu naqari, guddaayam man naa àgg ba ci 15i met.

Melo wi Soppi

Xas mi day mboq walla mu maroo di def ay der yu wayaf di xolleeku. Ay xobam jamonoy nawet lay sëq. Meññeefam day mbuluŋ, der bi day nooy.

ay njariñam Soppi

Meññeefam dees koy lekk, am xasam dees na ko jëfandikoo ngir faj siburu. Waaye nag moom daakaandeem lees ëpp ci lees di jëfandikoo, dees na koy jëfandikoo ci anam yu bari.

saxuwaayam Soppi

Garabu béb amna ci réew yu bari waaye weti END, OSTARAALI, ak SUDAA... la ëppe. Njaayum daakaandey Béb nag mi ngi gën a baree ci diggante Senegaal ak END ndax ñoo ëpp luñ koy am. Daakaande ji ci weeru Nowaambar lay tàmbalee xelli jëm ba nawet bi sori lool!

Nataal yi Soppi

Turu xam-xam wi Soppi