Farata ak sunnaay asaka
(Yoonalaat gu jóge Ay farataam aki sunnaam)
ASAKA
Asaka moom ñeenti farata la am : 1 yéene 2 matug at 3 matug nisaab 4 bañ koo joxe feneen te fi nga ne ku ko yayoo nekk fi. Am na ñatti teggiin nag yuy waralub yool : 1 nga ànd ceek teeyug bakkan 2 mu bañ a doon la gën mbaa la yées ci sa alal 3 joxe ko ci sutura ngir daw gistal.