Awa Mari Kol Sekk

Porofesëer Awa Mari Kol (borom këram sant Sekk) mu ngi juddu benn fan ci weeru mee atum 1951, nekk ab doktoor di tamit way-polotig ci Senegaal. Ab gëstu la buy gëstu li ëpp ci "SIDA" bi nga xam ne, siiwal na ci ay jukki yu bare. Nekkoon na kilifag deppàrtemaa ca "ONUSIDA"ca "Genève" diggante 1996 ba 2001. Diggante 2001 ba 2003 ak 2012 ba 2017, moo nekkoon jëwriñ ji yore wér-gu-yaram bi ci Senegaal. Fukki fan ak benn ci weeru septàmbar 2017 ba léegi, jëwriñu nguur la (ministar detaa) ci wetu Njiitu repibilig bu Senegaal.

Awa Mari Kol Sekk
Jëwriñu nguur (Ministar detaa) ci wetu njiitu réewu Senegaal
Fukki fan ak benn ci weeru septàmbar atum 2017 la yore woon ndombo-tànk bi ba tey
Njiitu réew Maki Sàll
Jëwriñ ju jëkk Mahammet Jonn
Ngornmaŋ Jonn II
Njëwriñu wér-gu-yaram ak taxawu askan wi
4 awiril 2012 – 7 septàmbar 2017
Jëwriñ ju jëkk Abdul Mbay
Aminata Ture
Mahammet Jonn
Ngornmaŋ Mbay
Ture
Jonn I
Ki mu wuutu Móodu Jaañ Fada
Ki ko wuutu Abdulaay Juuf Saar
U wér-gu-yaram ak taxawu askan wiNjëwriñu wér-gu-yaram ak taxawu askan wiu wér-gu-yaram, cet ak fàggu
12 mee 2001 – 22 ut 2003
(Ñaari at, ñetti weer ak fukki fan)
Njiitu réew Abdulaay Wàdd
Jëwriñ ju jëkk Maam Maajoor Bóoy
Idiriisa Sekk
Ngornmaŋ Bóoy
Sekk
Ki mu wuutu Abdu Faal
Ki ko wuutu Isaa Mbay Sàmb
Dundu ak jaar-jaaram
Tur ak sant Awa Mari Kol
Bésu juddu 1er mee 1951
Bérebu juddu Dakaar (AOF)
Réew Senegaal
Jànge Iniwersite Seex Anta Jóob
Liggeey Fajkat-gëstukat

Dundu ak jaar-jaaram Soppi

Dundug biiram Soppi

Am na borom-kër, am ñeenti doom.

Njàng ak tàggatoom Soppi

Bi mu paree njàngum kër doktoor mi la am ndam ci ab joŋante bu mu doon def ngir dem wéyal njàngam ci biir lopitaali Dakaar yi atum 1975. Atum 1978, mu am doktoraam. Atum 1979-1980, la dem ca Farãas, ca Liyoŋ di liggeey ci bérebu sowetaas bi ñi yore feebar yiy wàlle nekk ci lopitaal bu Croix-Rousse, foofa dañu ko jàppe woon ni gan gu leen jàppele ci seen liggeey ba. Bi mu ñibsee Senegaal la daldi am lijaasaam bi aju ci xam-xamu doomu jàngoro te farañse naan ko (spécialisation en bactériologie-virologie) atum 1982 ak beneen lijaasa bu aju ci feebar yiy wàlle tey faral di am ci suñu réewi Afrig yi ñu naan ko (maladies infectieuses et tropicales) atum 1984 ci iniwersite Seex Anta Jóob bu Dakaar. 1982-1988, def na ay tàggaytu yu bare ci naka lañuy defe ay gëstu ak naka lañuy jàngale ci Dakaar, Libërwiil ak Bordóo. Ci fanweeri atam ak ñett, atum 1984, la doon jigeen ji jëkk a nekk ab agerese ci njàngum paj fii ci Senegaal, loolu waral tey mu doon kenn ci jigeen ñi xàll yoon woowule ci réewi Afrig yi làkku farañse yépp boole. Atum 1987, njàngum jàngoroy mbas (épidémiologie appliquée et bio-statique) ma mu defoon ca Annecy, ca Farãas, te Fondation Mérieux ak CDC bu Atlanta amaloon ko, tax na koo mottali te gën a mokkal ay mën-mënam ci wàll wi, rax-ci-dolli nekk ab way-bokk ci mbootaay gi boole borom xam-xami jàngoroy mbas yiy génn lopitaal yi, di liggeeyeji ci biti (Association des épidémiologistes de terrain).

Ay jaar-jaaram ci liggeeyu kër doktoor Soppi

Atum 1989 lañu ko tabb porofesëer titileer bu màkkaanu feebar yiy wàlle bu iniwersite bu Dakaar ak njiitu bérebu fajukaayu feebar yiy wàlle bu opitaal Faan (Dakaar). 1989 ba 1996 la nekkoon njiitu Clinique-Counseling bu Kureelu réem yiy xeex sidaa. Liggeeyam foofee, moo doon di saytoo ka lëkkale liggeey bi aju ci toppatoo aji-feebari sidaa yi, seen yaram, seen xel ak seen nekkin ci biir askan wi, ci la sax gise aji-feebar ji jëkk a yore sidaa ci réewum Senegaal, atum 1986, tàggat tamit ay liggeeykati kër doktoor ci jëfandikoo jumtukaayi feebar yi seen wàllante di jaare ci sëy (MST)/sidaa. Ci jamono jooju, mu ngi bokkoon tamit ci kureel gi jiite bépp liggeey bu jëm ci xeex sibbiru ci Senegaal (1994-1996), bokk tamit ci kureelu réewum Senegaal gi fi nekkal Mbootaayu wér-gu-yaram gu àdduna (OMS Senegaal) (1993-1994).

Bokk na ci jaar-jaari Awa Mari Kol Sekk, Mbootaayu xeet (Nations unies) ya mu nekkoon di liggeey diggante 1996 ba 2001 ci benn tëralinu wu aju ci VIH/SIDA (ONUSIDA. Dafa fa jëkk a nekk njiitu deppàrtemaa biy jàppale réew yi. Saytu na liggeeyu kàngami àdduna yu mag. Kàngam yooyee, seen liggeey moo doon amal ay pexe ak ay doxalin ci fànni xarala, rafetal, àq ak yelleefi doom-aadam, te jiital ci ñi gën a néew-doole ; seen liggeey nekkoon na tamit fexe ba aji-feebar yi mën di faju, di jot ci garabi sidaa yi bu baax, di bind ak a siiwal jëf ju bare njëriñ ji ak di dooleel réew yi ci wàllu xeex sidaa.

Soskat wala way-bokk la ci njiiteefu mbootaay wala lëkkaloog kureeli àdduna yu bare yu mel ni : kureelu àdduna gi séq jàngoro yiy wàlle, kureelu Afrig giy gëstu ci mbiru njur (The Population Council), kureelu Afrig giy xeex sidaa (OPALS), kureelu Afrig giy gëstu ci sidaa, kureelu Afrig giy yëngu ci « Rafetal ak àq ak yelleef yi aju ci VIH » (PNUD) ak kureel gile di Jigeen ak sidaa ci Afrig (SWAA). Def na ay ceet aji-tawat yu bare ci santaaneb kureelu àdduna yu bare te wuute. Nekkoon na way-bokk ci liggeeykati kureelu wér-gu-yaram gu àdduna (OMS), doon ko bindal téere bi aju ci « Wér-gu-yaram ak suqaliku » weeru desàmbar 1993, bokkoon na tamit saytukati Global Program on AIDS (GPA) atum 1992-1993. Kenn la ci ñi jiite woon trac B (ab kilinig la) bu kureel gi doon waajal ndajeem waxtaanu àdduna mi amoon ci sidaa ca Vancouver (Canada) weeru mee 1995 ba weeru sulet 1996. Nekkoon na tamit njiitu ay naali gëstu ci sidaa te àndoon ci ak këru gëstu ci sidaa gu Farãas (ANRS), Eestiti gëstu bu Harvard, iniwersite bu Seattle, NIH, bérebi gëstuy farmasi yi wala PNUD.

Yeneeni fànni wérug yaram yu mel ni ñakku ngir aaru ci ŋas, njàmbataan, jàngoroy res B (epatit B), tetaanos, jàngoroy jàdd yi (meneesit yi) wala sëqat-su-mag si, bokk nañu ci ay tooli gëstum. Li mu bind yépp, ci jukki ak téere, siiwal leen, ëpp na téemeer ak juroom-fukk.

Ay jaar-jaaram ci wàllu pólotig Soppi

Njiitu réew mi moo ko woo mu ñibsi mee 2001 ngir nekk jëwriñ ji yore wér-gu-yaram ak fàggu gi ci ngornamaŋ bi. Ay jeego yu wóor amoon nañu ci wàllu wér-gu-yaram ndax liggeeyam. Bokk nañu ci jeego yooyu, ay coppitey campeef, coppiteg lopitaal gi, tëralinu ñakk wu ñu yaatal wi, xeexu sibbiru bi, sidaa bi, feebar yi dul wàlle, wérug yaramu mag ñi, sawarloog liggeeykat yi, caytug xaalis bi, digaale bi ak diggante yi ak ñeneen ñiy liggeey wala ñiy dugal xaalis ci wàll wi.

Li ko Maki Sàll jàppal mooy ne benn, des naa dugal ay yoxoom ci wotey deppite yu 2017, ñaareel bi, jafe-jafe bu réew mi amoon ngir am ay rajogaraafi, looloo waral sax, jëlaatu ko woon ci ñaareelu ngornamaŋ bu Bun Abdulaay Jonn bu juroom-ñaari fan ci weeru septàmbar 2017. Waaye mujj na nekk jëwriñu nguur (ministar detaa) ci wetu njiitu réew mi.

Bokk na ci njiiteefu kureelu àdduna gi yore wàllu ñakk yi (International AIDS Vaccine Initiative, IAVI).

Yeneeni yëngu-yëngum Soppi

Ku fonk tàggat yaram la, doon ci yëngatu bu baax, nekkoon na fi sax, basketkat bu daan joŋante ci àdduna bi.

Ay medaay Soppi

  • Ordre des Palmes académiques (Farãas)
  • Ordre national du Mérite (Farãas)
  • Ordre national du Mérite (Burkinaa Faaso)

Tënk Soppi

Njàng
  • 1978 : docteur d’État en médecine (Dakaar, Senegaal)
  • 1982 : C.E.S. de bactériologie – virologie
  • 1984 : C.E.S. de maladies infectieuses et tropicales (Dakaar, Senegaal)
Ay jaar-jaaram
  • Jëwriñ ji yore wér-gu-yaram ak taxawu askan wi ci Senegaal : 2012 ba tey
  • Jëwriñ ji yore wér-gu-yaram ak fàggu gi ci Senegaal : mee 2001 ba 2003
  • Njiitu deppàrtemaa " Jàppale réew yi ak gox yi ca ONUSIDA ca Genève" féewiriye - mee 2001
  • Njiitu deppàrtemaa "Doxalin, pexe ak gëstu ca ONUSIDA" diggante 1996 ba féewiriyee 2001
  • Porofesëer titileer bu màkkaanu feebar yiy wàlle bu iniwersite ak njiitu lopitaalu (CHU) bu Faan 1989 ba 1996
  • Lëkkalekatu Kureelu Clinique-Counseling
  • Lëkkalekatu tàggatu liggeeykati wér-gu-yaram ak taxawu askan yi ci mbirum sidaa : 1989 ba 1996
  • Way-bokk ci kureelu réewum Senegaal gi fi nekkal Mbootaayu wér-gu-yaram gu àdduna (OMS Senegaal) : 1993 ba 1994
  • 1979 – 1980 Gan guy jàppale liggeeykati lopitaal bu Croix-Rousse : 1979 ba 1980

Ceet ak gëstu ci sidaa :

  • Ay Ceet yu bare ci sidaa, ci wérug yaram, ci njur gi ngir kureeli àdduna yu takku, rawatina OMS ak askanu Council
  • Way-bokk ci gëstu "Sëqët su mag si ak sidaa", ànd ci ak IMEA, di bérebu gëstu bu Afrig ci wàllu kër doktoor ak mbas
  • Këru gëstu ci sidaa (ANRS), Farãas ak kureelam gu tudd coopération française atum 1996
  • Way-bokk ci kureelu Afrig giy yëngu ci jikko yu rafet, àq ak yelleef ak VIH » (PNUD) : 1994 ba 1996
  • Way-bokk ci kureelu réew miy sàmm jikko yu rafet yi aju ci fàggug sidaa gi, Dakaar : 1992 ba 1996
  • Way-bokk ci kureel gi jiite tëralinu réew miy xeex sibbiru, Dakaar : 1994 ba 1996
  • Njiitu kureelu borom xam-xam gi doon waajal ndajem àdduna mi aju woon ci sidaa ci Afrig, Dakaar : 1991
  • Kenn la woon ci ñi doon jiite Groupe Clinique bu fukkeelu ndajem àdduna ak benn te aju woon ci sidaa ca Vancouver (Kanadaa) : 1996
  • Mbootaayu jigeen giy xeex sidaa ci Afrig (SWAA), way-bokk ak njiitu SWAA Senegaal la woon
  • Kureelu àdduna gi ñu samp ngir xeex feebar yiy wàlle (way-bokk la woon ci kureel gu ndaw gi ko doon jiite)
  • Kureelu Afrig giy xeex sidaa OPALS
  • Kenn ci way-bokk yi sos OPALS ak njiitu OPALS Senegaal ba woon.
  • Way-bokk ci Ngomblaanu xam-xam ak xarala gu Senegaal
  • Way-bokk ak njiitu Kureelu yemale, jikko yu baax ak jëf (COMEVA)
  • Way-bokk bu ñu boole ci ngomblaanu réew mi ci wàllu, farmasi, Farãas (ñu fal ko bésu 30.09.2015)
  • 2003 : <i>Docteur honoris causa</i> bu Iniwersite <i>Pierre-et-Marie-Curie</i>.

Téere, jukki wala dali web yi ñu yër Soppi

Seetal tamit Soppi

Lees bind ci moom Soppi

  • « Awa Marie Coll Seck : une vie de battante », in « Femmes au Sénégal », Les Cahiers de l'Alternance (Dakar), Partenariat Fondation Konrad Adenauer et Centre d'études des sciences et techniques de l'information (CESTI), no 10, décembre 2006, p. 92-93

Jukki yi ñu ko tudd Soppi

  • Liste des ministres de la Santé du Sénégal | Santé au Sénégal : Limu jëwriñ yi yore woon wér-gu-yaram yépp ci Senegaal | Wér-gu-yaram
  • Liste de femmes ministres sénégalaises : Limu jigeen ñi jot a nekk jëwriñ yépp ci Senegaal

Lees jële feneen Soppi

Ci yeneen naali Wikimedia

Awa Mari Kol Sekk, ci Wikimedia Commons

Dundu ak jaar-jaaram
  • (Dundu ak jaar-jaaram) (dalu web Pressclub) Biographie (site Pressclub)
  • (Dundu ak jaar-jaaram) (dalu web Roll Back Malaria) (Biographie (site Roll Back Malaria)
Ak yeneen